TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 12/08 p. 1
  • Waaraate dafa laaj muñ

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Waaraate dafa laaj muñ
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ku muñ dina am lu baax
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Waaraate bi dafay tax ñu mën a muñ
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2008
km 12/08 p. 1

Waaraate dafa laaj muñ

1 Ndaw li Pool jël na lu ëpp 30 at ci dundam, def ko ci liggéeyu waaraate bi. Te mbégte la ci jële woon. Liggéeyu waare bi Pool doon def, dafa àndoon ak ay jafe-jafe ni lépp li jar nit góor-góorlu ci (2 Kor. 11:23-29). Waaye Pool bàyyiwul waaraate (2 Kor. 4:1). Xamoon na ne Yexowa moo koy may doole biy tax mu mën a muñ ci liggéeyu waare bi (Fil. 4:13). Pool dafa wone muñ bu ànd ak ngëm, moo tax mu mënoon a wax lii : “ Royleen ma nag, ni may roye Kirist ”. — 1 Kor. 11:1.

2 Muñ jafe-jafe yi tey : Bés bu nekk, am na suñuy mbokk yu bare yu ñuy sewal, di leen xeex. Mën na am it seeni waa kër, ñi ñu bokkal liggéey, walla seeni waa lekkool bañ leen a faale (Macë 10:35 ; Ywna. 15:20). Xéyna loolu ngay daj yow itam. Mën na am it nga am poroblemu wér gu yaram, walla ngay xeex bés bu nekk ak fiir yi Seytaane teg sa kanam walla foo yu mën a yàq sa ngëm te mën la tere muñ. Dinañu am doole muñ bu ñuy jàng lu jëm ci ñi doon jaamu Yàlla bu baax ci jamano yu njëkk yi, te xeex ba génn ci seeni jafe-jafe. Li ñu wax it ci suñu mbokk karceen yi xeex ba génn ci seeni jafe-jafe, mën na ñu may doole itam. — 1 Piy. 5:9.

3 Mën nañu am doole kontine di jàpp bu dëgër ci liggéeyu waaraate bi, bu ñu fexee ba ‘ gànnaayoo yérey xarey Yàlla yépp ’ (Efes 6:10-13, 15). Ñaan Yàlla ngir mën a muñ am na solo lool itam. Yàlla dafa ñuy may xel mu sell ngir ñu mën a muñ jafe-jafe yi (2 Kor. 6:4-7). Bu ñu bëggee am ndam ci li ñuy xeex Seytaane ak àddinaam, dañu war a topp li ñu Yàlla di wax ngir soppi suñu xel (Ps. 119:24, 85-88). Bu baay bindee leetar doomam, te ñu bëggante lool, doom ji mën na di jàng leetar boobu ay yooni yoon. Noonu it li ñuy jàng Biibël bi bés bu nekk, dafay gën a dëgëral suñu diggante ak Yexowa. Ci suñu njàngum Biibël bi ñuy faral di def, dinañu am xel bi ñuy génne ci suñuy jafe-jafe. Loolu dina tax xalaatu Yàlla won ñu li ñu war a def te ñu gën a takku ci moom. — Léeb. 2:10, 11.

4 Muñ dafay indi ay barke : Bu ñuy muñ ci waaraate bi ndax suñu ngëm, ni Pool, dinañu seddal xolu Yexowa, te dinañu am ay barke ñun ak suñuy moroom (Prov. 27:11). Nañu fas yéene kontine ci waaraate bi. Dinañu wone noonu ne suñu ngëm dëgër na te moo “ gën fuuf ” wurus bi nga xam ne bu ko safara setalee sax, du wéy ba fàww. — 1 Piy. 1:6, 7.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager