TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 6/05 p. 8
  • Nañu waaraate bu baax fu nit ñi di bare

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu waaraate bu baax fu nit ñi di bare
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu waare xibaar bu baax bi fu nekk
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Nañu seet ñi ko yelloo
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 6/05 p. 8

Nañu waaraate bu baax fu nit ñi di bare

1 Ni ko taalibe Isaa yu njëkk ya defe woon, karceen yi tey dañu bëgg yégle xibaar bu baax bi fépp fu ñu mën a fekk ay nit (Jëf. 16:13 ; 17:17 ; 20:​20, 21). Am na ay nit ñoo xam ne kenn mënul fexe ba gis leen bu ñuy waaraate këroo-kër. Waaye daje nañu ak ñoom bu ñu doon waare ci béréb fu bare nit. Te am na ñu ci nangu waxtaan ak ñun.

2 Bu ñuy waare ci béréb fu nit ñi di bare, war nañu xam bu baax ni ñu koy defe. Waruñu feeñ torop. Lée-lée dafay am ay waaraatekat yu bare yu bokk ñoom ñépp benn béréb fi ñuy waare. Walla mu am ay bitig yoo xam ne waaraatekat yu bare dañu fay jaar, fekk am na yeneen waaraatekat yu fa jaar ba pare, walla it mu am ay bitig fu ñépp di duggandoo ngir waar ñi fa nekk. Loolu lépp dafay tax nit ñi gaaw a doyal ci ñun. Kon dinañu xeeb suñu liggéey te suñu waaraate bi du jur lu baax. Lan lañu mën a def ngir lu mel noonu bañ a am ? Def ay kàrt yuy wone béréb yooyu bare nit, ni ko yenn mbooloo defe (1 Kor. 14:40). Leneen li ñu mën a def it ngir jaxasoo bañ a am ci suñu liggéeyu waare bi mooy bañ a waaraate ci goxu beneen mbooloo. Lée-lée dafay am ay mbooloo yuy jaar ci seen kurélu liggéeyu waare ngir dimbali beneen mbooloo bu soxla ñu jàpple ko. Waaye bu dul loolu, buleen waaraate ci goxu beneen mbooloo. — Seetleen Le ministère du Royaume bu nowàmbar 1998, xët 6, xise 17 ak 18.

3 Bu ñuy wax ak nit ñi : Bi Yeesu doon waxtaan ak benn jigéen ci wetu teen, dafa ko njëkk wax lu gàtt. Bi mu gisee ne lu gàtt loolu neex na jigéen ji, mu sog a yaatal ndànk-ndànk waxtaan bi (Ywna. 4:​7-26). Ñun itam am na foo xam ne bu ñu defee lu mel noonu, dina baax. Am na ay waaraatekat yu gis ne booy waaraate fu nit ñi di bare, li gën mooy nga nuyu nit ki ni mu ware bala ngay wax sax lu jëm ci xibaaru Nguur gi. Dañuy wax loo xam ne dafay itteel nit ñi nekk ci seen gox ba tax ñu bëgg waxtaan ak ñoom. Bu nit ñi di wax ci seen coono, dañu leen di déglu bu baax. Loolu lañuy def ba mën a won nit ñi ci Kàddu Yàlla li mën a dalal seen xel. — Room 15:⁠4.

4 Li ñu mën a def ngir kontine waxtaan bi : Saa yu ñu waxtaanee bu baax ak nit, war nañu jéem a jàpp ak moom bés bu ñuy kontine waxtaan bi. Lu ñu mën a def ? Boo demee ba di bëgg àggali waxtaan bi, mën nga jël fi ngay bind nit ñi ngay seetiwaat te ne lii : “ Waxtaan bi neex na lool. Ndax dinañu ko mën a kontine beneen yoon ? ” Walla mën nga ko wax lii : “ Bëgg naa la indil téere boo xam ne, wóor na ma ne dina la neex. Ndax mën naa la ko indil sa kër walla fi ngay liggéeye ? ” Am na it ay waaraatekat yuy wax lii : “ Ndax am nga nimoro telefon ? ” Ñi ci gën a bare dinañu leen ko jox.

5 Ñu bare ci ñi nga xam ne ci béréb yu bare nit lañu njëkk dégg xibaaru Nguur gi, nangu nañu ñu jàngal leen Biibël bi. Njàng moomu mën nañu ko def seen kër, fi ñuy liggéeye, ci béréb fu bare nit, walla sax ci telefon. Bu ñuy waaraate bu baax ci béréb yu bare nit, nañu jéem a tàmbali ay njàngum Biibël.

[Laaj yi]

1. Ni ko karceen yu njëkk ya daan defe, karceen yi tey dañuy waaraate ci béréb fu nit ñi di bare. Naka lañuy defe loolu te lan lay indi ?

2. Lu tax ñu war a xam bu baax ni ñuy waaree ci béréb yu bare nit ? Naka lañu mënee def suñu wàll ngir jaxasoo bañ a am ?

3. Bu ñuy waare ci béréb yu bare nit, lan lañu mën a def ngir nit ñi bëgg ñu déglu bu baax ?

4. Lu ñu mën a def ngir kontine waxtaan bu neex ?

5. Bu ñuy waaraate ci béréb yu bare nit lan lañu war a bëgg ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager