Nañu roy ci Yexowa, suñu Yàlla ji bare mbégte
1 Yexowa dafa bëgg ñu bég. Kàddoom dafa ñuy won barke yu bare te rafet yi Yexowa dencal doom Aadama yi (Isa. 65:21-25). Nit ñi dañu war a gis ne dañu bég bu ñu leen di xamal “ xebaar bu baax ” bi jóge ci Yàlla ji bare mbégte (1 Tim. 1:11). Fasoŋ bi ñuy waxe ci waaraate bi dafa war a wone ne dañu bëgg dëgg gi, bëgg it nit ñi nuy waxal. — Room 1:14-16.
2 Dëgg la, kontine di wone mbégte bu ñuy waare, yenn saay yombul. Am na gox yoo xam ne barewul ñu fa bëgg déglu. Yenn saay it ñun ci suñu bopp dañuy am ay jafe-jafe. Kon bu ñu bëggee kontine di bég, dañu war a xalaat ne nit ñi nekk ci suñu gox soxla nañu lool dégg xibaar bu baax bi jëm ci Nguur gi ak it xam li muy tekki (Room 10:13, 14, 17). Bu ñu xalaatee bu baax ci loolu, dinañu kontine di xamle ak mbégte li Yexowa waajal ngir ñu mën a mucc.
3 Na suñu wax gën a jëm ci lu rafet li ñuy séentu : War nañu seet it bu baax li ñuy wax. Dëgg la, mën nañu tàmbali suñu waxtaan ak jafe-jafe walla xibaar bu ñépp dégg. Waaye nag, waruñu ci yàgg ba mu ëpp. Li ñu nu sant mooy, yégal nit ñi “ xibaar bu baax bu jëm ci lu gën a neex ”. (Isa. 52:7 ; Room 10:15.) Xibaar bu baax boobu dafa jëm ci ëllëg bu neex bi ñu Yàlla dig (2 Piy. 3:13). Kon nañu ci xalaat te won nit ñi aaya yuy “ dëfël xol yu jeex yi ”. (Isa. 61:1, 2.) Loolu dina ñu dimbali ñun ñépp, ñu kontine di bég ci waaraate bi te di gën a wax ci lu neex.
4 Bu ñuy waare, nit ñi dinañu gis mbégte bi ñuy àndal. Kon nañu roy ci Yexowa, suñu “ Yàlla ji bare mbégte ” bu ñuy waare xibaar bu baax bi jëm ci Nguur gi.