Xabaar bu baax lañuy waar
1 Akay cér bu amul moroom, buñ ñu defal, maanaam doon ñiiy yóbbul ñeneen ñi “ xabaar bu baax bi, [bu yëf yu baax, NW] ” ! (Room 10:15.) Xabaar buy féexal xol lañuy bokk ak nit ñi dëkkee dund ci biir ayu-biir réew yi te yoqi. Nan lañu leen mënee dimbali ñu nangu ne, li ñu leen di indil, “ xabaar bu baax la, bu dara lu gën ” ? — Isayi 52:7.
2 Waajalal xabaar buy feddali : Suñuy waxtaan ci biir sasu waare bi dinañu am doole dëgg, su ñu teewloo ci yëf yuy feddali. Looloo tax, bu ñuy waajal li ñu nar a wax tey seetaat mbind mi ñuy wone, soxla nañoo fésal ponkiy suñu xabaar, yiy feddali. Bu ñuy bokk ak nit ñi suñu yaakaar ji sukkandiku ci Biibël bi, ànd ceek kóolute te njaxlaf, mën nañoo séentu jeexital yuy xiirtal. — Léeb. 25:11.
3 Ak lu ñu yërëm yërëm nit ñi, buñ ñuy xamal li ñuy daj ndax nekkini àddina siy gën di yées, war nañu leen a joxoñ liy saafara dëgg jafe-jafey doom-Aadama, maanaam Nguuru Yàlla. Bu ñuy waxtaane sax ci “ bésub feyyu ” Yeowa biy dikk, li ñu bëgg mooy, won leen ni loolu tekkee ca dëgg ‘ xabaar bu baax ngir ñi lewet ’. (Isa. 61:1, 2.) Mën nañoo dëfël ñii ñuy déglu ci lii : lépp lu Yeowa def, ci mujjantal bi bànneex bi sut ak muj gi dàq lépp lay yóbbe.
4 Xamleel dëgg gi ak mbég dëgg : Nit ñi dinañu gën a jagoo déglu, bu ñu gisee ci suñu xar-kanam ne dañoo bég te ñu yëg suñu kóolute ci suñu baat. Bu fekkee ne suñu melokaan awu na njort mu rafet, ñii ñuy déglu dinañu ràññee ne ñu ngiy sàkku ‘ [m]bég ci yaakaaru ëllëg ’ (Room 12:12). Te loolu mën na leen a gën a xiir ci nangu xabaar bu baax bi. Ci lu wóor, am nañu lu wér, lu war a tax ñu wone ne xel mu rafet te bég lañu soloo te loolu ci bépp fànn, bu suñu sas.
5 Niki ndawiy xabaar bu baax bi, war nañoo def lu raw xamle ko doŋŋ. Suñu waare daa ëmb yaakaar ju wóor, ju dund gu gën, muy tey di ëllëg (1 Tim. 4:8). Bu ñuy jege nit ku nekk, suñu xalaatin bu làmboo rafetaayu njort dina feeñ ci li ñuy wax te loolu dina dimbali nit ñi ñu nangu xabaar bu baax bi. Ba ñuy bàyyi xel ci li ñuy wax, akit ni ñu koy waxe, nañu xiir ñi seen xol laab ñu nangu xabaar bu baax bi ñuy waar, xabaar buy jàjji !