Ndaje bu mag bu ñaari fan biy ñów : li ñu fay waxtaane
Nit ñi tey, dañu bëgg ñu gëm ne àddina sii dina sax ba abadan. Waaye Kàddu Yàlla waxul loolu (1 Ywna. 2:15-17). Loolu dafa ñuy dimbali ñu xam ne “ dajale alal ci àddina ” amul njariñ. Ndaje bu mag bu ñaari fan bu atum liggéeyu waare 2007, dina yokk bu baax doole mbooloo Yàlla. Turam mooy : Dajaleleen alal ci asamaan. — Macë 6:19, 20.
Def sa xel yépp ci wutum alal bokk na ci li Efes 2:2 di woowe “ kilifag boroom sañ-sañ yi ci jaww ji, di xel mu bon miy jëf ci kureelu ñi déggadil Yàlla ”, maanaam kilifa àddina si, moom mii nekk xel miy ilif ñi bañ a dégg ndigal. Ngelaw bi ñuy noyyi mu ngi fu nekk. Noonu it la xel miy jóge ci àddina nekke fu nekk ci àddina (1 Kor. 2:12). Dañu wax ne xel moomu “ kilifa ” la, ndaxte dafa am doole lool. Ndaje bu mag bu ñaari fan bii di ñëw, dina ñu dimbali ngir ñu bañ a def suñu xel yépp ci wutum alal ni ko waa àddina sii di defe. Dina ñu dimbali it ngir ñu kontine di xam li war a ëpp solo ci suñu àddina (Macë 6:33). Ndaje bi dina ñu dimbali it ñu wéeru ci Yexowa bu ñuy bokk ci liggéeyu waare bi, di ko def sax bu ñu amee ay coono ak ay jafe-jafe.
Nañu def lépp ngir teewe ñaari fani ndaje bi yépp te “ gën a faaydaal ”, maanaam déglu bu baax li ñu fay wax (Yaw. 2:1). Boo fa nekkee, nanga bind ci lu gàtt li nga mën a topp ci sa dund, ak it ci waaraate bi. Fexeel ba teewe porogaraam buy yokk doole boobu yépp. Bu la ci dara raw. Dina la xiir bu baax ci kontine di ‘ dajale alal ’ ci asamaan !