Ndaje bu mag bu benn fan biy ñów : li ñu fay waxtaane
Bi leen xel mu sell mi mayee doole, karceen yu njëkk ya dañu sawar ci xamle xibaar bu baax bi. Dañu def lépp ngir xamle ko ba fu gën a sore fu ñu mën a dem (Jëf. 1:8 ; Kol. 1:23). Ndaje bu mag bu benn fan bu atum liggéeyu waare 2007, dina ñu dimbali ñu roy ci ñoom. Mu ngi tudd “ Jubluleen ci xamle Kàddu gi ”. — Jëf. 18:5.
Lii la buur Daawuda waxoon ci Kàddu Yàlla : “ Seedes Aji Sax ji [maanaam li mu ñuy fàttali] moo wóor, di yee ñi xamul. ” (Sab. 19:8). Ndaje bu mag bu benn fan bu ñu waajal ci atum 2007, dina ñu won ni Mbind mi amee solo ngir “ jubbanti ”. Dina ñu xiir ci jëfandikoo Kàddu Yàlla bu ñuy waare te di jàngale. Te loolu war nañu ko def ci fasoŋ buy wone ne jot bi des barewul (2 Tim. 3:16, 17). Ndaje boobu dina ñu won ni ñu mënee topp bés bu nekk ndigal yi nekk ci Biibël bi ngir moytu li ñu mën a fiir. Dina ñu won njariñ bi nekk ci topp Biibël bi bés bu nekk. Dina ñu won it ni ñu mënee jëfandikoo Kàddu Yàlla ngir dimbali ndaw yi ak ñi sog a bokk ci mbooloo mi ngir ñu jëm kanam ci wàllu ngëm.
Fexeel ba fekke bu ñuy komaase porogaraam bi, te nanga déglu bu baax. Nanga bind it ponk yi nga mën a topp yow ci sa wàllu bopp. Nanga wone ne fonk nga li ñu la fay jàngal walla fàttali, te nanga xalaat bu baax ci noo ko mënee topp.
Ndaje bu mag bu benn fan bi dina tax ñu gën a fonk Kàddu Yàlla. Dina ñu fàttali it ne dañu war a kontine di sawar ci waare xibaar bu baax bi jëm ci Nguur gi. Dina ñu won it ni ñu mënee dimbali suñu moroom yi ñu def loolu ñoom itam. Kon fexeel ba dara bañ laa raw ci xelal ak ndigal ci wàllu ngëm yi ñu Yexowa pareel noonu ! — Isa. 30:20b, 21.