Ñu bare dañu ci kontaan lool
1 Ci àddina si sépp, ay njaboot wax nañu ni ñu kontaane ci wideo bi tudd : Les jeunes s’interrogent...Comment se faire de vrais amis ? Benn góor gu dëkk Etaa Sini dafa wax ne bi doomam yu góor yi seetaane wideo boobu, dañu toog, noppi, jàpp bu baax ci seen xol lépp li ñu ci wax ! Suñu mbokk yu nekk Malawi, nee nañu it ne foofu, ndaw yi, góor ak jigéen, nànd nañu te ànd ak li ñu ci wax, ndaxte lu mel noonu lañuy daj ci seen lekkool. Ci Allemagne, benn baay dafa ne : “ Dafa mel ni dañu ko defar ngir tontu samay ñaan. ” Benn janq nee na : “ Jëre-jëf ci li ngeen ma fàttalee ne Yexowa ittewoo na ma. ” Benn magu mbooloo mu nekk ca Nouvelle Zélande dafa nee : “ Dimbali na suñu benn janq ba mu dellusiwaat ci yoonu dund gi. ” Benn jigéen bu am jëkkër seetaan na ko, ba pare nee na : “ Ni ma bëgge ndaw yi nekk ci dëgg gi seetaan wideo bii ñoom ñépp. Li may ñaan it mooy li nekk ci wideo bi xiir leen ci jël dëgg gi, dugal ko ci seen biir xol, ba ñoom ci seen bopp, ñu bëgg ko topp. ” Yéen njaboot yi, lu leen teree seetaanaat wideo boobu ? Te bu ngeen paree, waxtaanleen ci laaj yii di topp.
2 Ngir ubbi waxtaan bi : Lan mooy xarit dëgg ? — Léeb. 18:24.
3 Liy yàq xaritoo : Naka nga mën a fexee ba bañ a xalaat ne nit ñi bëgguñu la xajal ci seen biir (Fil. 2:4) ? Lu tax nga war a nangu góor-góorlu ba am jikko yu gën a rafet ? Kan moo la ci mën a dimbali ? Lu la mën a dimbali ba nga am xarit yu gën a bare ? Foo mënee am ay xarit ? — 2 Kor. 6:13.
4 Xaritoo ak Yàlla : Naka nga mënee def ba xaritoo ak Yexowa ? Ku bëgg xaritoo ak Yàlla, dafa war a góor-góorlu dëgg. Waaye, lu tax ñu mën a wax ne jar na ko (Sab. 34:8) ? Lan moo gën a mën a rattaxal sa diggante ak Yàlla ?
5 Xarit yu bon yi : Lan mooy àndandoo bu bon (1 Kor. 15:33) ? Xarit yu bon, naka lañu mëne yàq sa diggante ak Yàlla ? Li Biibël bi nettali ci Dina, lan la la jàngal ? — 1 Mu. 34:1, 2, 7, 19.
6 Lenn lu mën a xew ci suñu jamano : Lan la wéetaay def Tara ? Lan la wax ngir wone ne ci moom, ànd ak ndaw yu bokk ci àddina si, lu baax la ? Xarit yooyu, ci lan lañu ko mënoon a dugal ? Lu tax way-juram yi gisuñu musiba yi ko naroon a dal ? Waaye ban jikko lañu wone ngir dimbali ko ba mu defaraat digganteem ak Yàlla ? Naka la benn pioñee bu jigéen wone ne xaritu Tara dëgg la woon ? Lu tax karceen yi war a déglu bu baax li Léebu 13:20 ak Yérémi 17:9 wax ? Lan la Tara jàng te mu nekk lu am solo ?
7 Ngir jeexal waxtaan bi : Loo jàng ci wideo bii ? Noo ko mënee jëfandikoo ngir dimbali ñeneen ? — Sab. 71:17.