Nañu jariñoo bu baax ndaje yi ñuy def bala ñuy dem waare
1 Ndaje yi ñuy def bala ñuy waare, bu ñu leen defee ni mu ware, dinañu yokk suñu doole te wone ni ñu mënee waaraate. Dañuy tax ñu mën a ànd ak yeneen waaraatekat ci waaraate bi, su ko defee ñu jàppleente te ku nekk jànge ci moroomam (Léeb. 27:17 ; Daj. 4:9, 10). Lan lañu mën a def ngir jariñoo bu baax ndaje yooyu ?
2 Kiy jiite ndaje bi : Ndaje yooyu duñu faral di am porogaraam buy wone lu ñu fa war a waxtaane. Kon boo ko waree jiite, nanga ko waajal bu baax. Bul xalaat ne fàww nga waxtaan ci aaya bés bi. Bu aaya bi jëmee ci waaraate bi, mën nga ko boole ci waxtaan bi. Seetal li mën a dimbali ñi teew ñu waare bu baax. Mën na am nga bëgg waxtaan ci li ñu mën a wax ci waaraate bi walla nga bëgg mu am ñuy wone ni ñu mënee def waxtaan boobu ci waaraate bi. Boo bëggee it, mën nga waxtaan ci lenn lu nekk ci téere Comment raisonner, walla ci téere École du ministère walla ci lenn lu ñu yàggul a waxtaane ci ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi. Yenn saay it mën nga waxtaan ci jafe-jafe bu waaraatekat yi mën a am ci gox gi walla waxtaan ci ni ñu mënee dellu seeti ku suñu waxtaan neex walla komaase benn njàngum Biibël, rawatina bu fekkee ne ñu bare dañu war a dellu seeti ñi suñu waxtaan neex. Waaye ak lu ngeen mënta waxtaane, nanga ci wone mbégte te am wax yu neex.
3 Nanga komaase ndaje bi ci waxtoom, bu dee sax xam nga ne dina am ñuy tàrde. Seetal bu baax ni ngay boolee waaraatekat yi ngir ñu dem waare te joxal ñi ko soxla fu ñuy waare. Ndaje bi warul ëpp 10 ba 15 minit. Te bu dee dafay topp ndaje mbooloo mi, dafa war a gën a gàtt. Bala ndaje bi di jeex, kenn ku nekk war na xam kan lay àndal ak fu ñuy waare. Nangeen ñaan ngir jeexal ndaje bi.
4 Mën ngeen a def seen wàll : Am na lu ñu mën a def ngir wone ne dañuy may cér Yexowa ak ñi teew. Mooy bañ a tàrde. Moom lañuy def itam ci suñu yeneen ndaje yi. Nañu bokk ci waxtaan bi. Mën nga bàyyi kiy jiite ndaje bi mu wax la ki ngay àndal. Boo bëggee it, mën nga tànn ki ngay àndal bala ndaje bi di jot. Waaye, booy def loolu, nanga góor-góorlu ngir ‘ ubbi sa xol ’ te ànd ak waaraatekat yu wuute, bañ a ànd rekk ak say xarit yu la gën a jege (2 Kor. 6:11-13). Bu ndaje bi jeexee, bul jéem a soppi li ki jiite ndaje bi taxawal ba pare ngir waaraate bi te nanga gaaw a dem fi ngeen war a waare.
5 Li waral ñu def ndaje yi ñuy def bala ñuy dem waare moo yem ak li waral ñu def yeneen ndaje yi. Dañu leen di def ngir ñu mën a “ seet ni ñu man a xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax ” (Yaw. 10:24, 25). Góor-góorlu ngir jariñoo ndaje yooyu, loolu dina ñu dimbali ñu mën a def liggéeyu waare bi ñu nu sant. Liggéey boobu jëf ju baax dëgg la !
[Laaj yi]
1. Ban ndimbal lañu mën a am ci ndaje yi ñuy am bala ñuy dem waare ?
2. Ci lan la kiy jiite ndaje bi mën a waxtaan ?
3. Ñaata minit la ndaje bi war a yàgg te kiy jiite ndaje bi lan la ci war a def bala muy jeex ?
4. Lan moo mën a tax ñépp jariñoo bu baax ndaje yi ñuy def bala ñuy dem waare ?
5. Lu waral ndaje yi ñuy def bala ñuy dem waare ?