Roy Kirist ci waaraate bi
1 Yeesu bàyyi na fi royukaay gu ñu war a topp ci waaraate bi. Mbëggeel bu mag bi mu amoon ci Yàlla ak nit ñi feeñoon na ay yoon yu bare te ci fasoŋ yu bare. Jàngal na ñi woyof dëgg gi, te defoon na lu baax ñi am naqar te seen xol jeex. — Macë 9:35.
2 Li Yeesu def ak li mu jàngale : Yeesu nanguwul dugg ci politig mbaa ci li nit ñi doon def ngir taneel rekk dundu doom-Aadama, ba loolu di ko tere def li ko war. Nanguwul woon yeneeni soxla tere ko bokk ci liggéey bi ëppoon solo ci moom, walla waññi li mu ciy def (Lukk 8:1). Dafa jublu woon ci waar xibaar bu baax bi jëm ci Nguuru Yàlla, di wone ne moom doŋŋ moo mën a saafara coono àddina. Yeesu amoon na liggéey bu am solo bu mu waroon a def. Te jot bi mu amoon ngir def ko barewul woon. Bi waa Kapernawum bëggee Yeesu des fa, lii la wax taalibeem ya : “ Nanu dem feneen ... ma waare fa itam, ndaxte moo tax ma génn. ” — Mark 1:38.
3 Bi Yeesu jàngalee taalibeem yi ba noppi, dafa leen yónni, digal leen lu leer lii : “ Yégleleen naan : “ Nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na. ” (Macë 10:7.) Jàngaloon na leen ne lépp lu jëm ci Nguur gi mooy li war a ëpp solo ci seen dund (Macë 6:33). Kàddu yi Yeesu mujj wax taalibeem yi laata muy dem asamaan, leeraloon na li ñu war a def. Lii la waxoon : “ Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp. ” — Macë 28:19.
4 Nguur gu am solo : Ci Nguuru Yàlla la Yeesu doon gën a wax te dafa sant taalibeem yi ñu roy ko ci loolu. Kàttanu doom-Aadama mënul a faj coono àddina ni mu waree (Yér. 10:23). Nguuru Yàlla doŋŋ moo mën a sellal turu Yàlla te yewwi doom-Aadama ci coono àddina ba fàww (Macë 6:9, 10). Jàngal dëgg gi jëm ci Nguuru Yàlla, nit ñiy mettitlu ci lu bon li am ci àddina, dina leen dimbali ñu am dundu bu neex léegi te am yaakaaru ëllëg bu dëgër te wóor. — Esek. 9:4.
5 Yeesu mu ngi bokk ba tey ci liggéeyu waare bi, te dig na ñu ne dina ñu ci jàpple (Macë 28:20). Suñu liggéeyu waare, ba fan la méngoo ak royukaay bi fi Yeesu bàyyi (1 Pie. 2:21) ? Ci mujug jamano bi ñu nekk nii, nañu wéy di def suñu kem kàttan ngir topp bu baax royukaay bi ñu fi Yeesu bàyyi ci wàllu waaraate bi !