Liggéeyu waare bi, mooy liggéey bi ëpp solo ci ñun
1 Nit ku nekk am na ay warugar yu bare. Toppatoo suñu waa-kër bokk na ci te Yàlla moo ñu ko sant (1 Tim. 5:8). Waaye nag warugar boobu warul ëpp solo liggéeyu waare Nguur gi ak sàkk ay taalibe. — Macë 24:14 ; 28:19, 20.
2 Yeesu wone na ci li mu doon def ni ñuy ‘ jëkke wut nguuru Yàlla ’. (Macë 6:33 ; 1 Pie. 2:21.) Barewul woon alal, waaye xelam yépp mu ngi woon ci def li Yàlla bëgg (Lukk 4:43 ; 9:58 ; Ywna. 4:34). Dafa doon waaraate saa yu ci amee bunt (Lukk 23:43 ; 1 Tim. 6:13). Fonkoon na bu baax liggéeyu ngóob bi te santoon na taalibeem ya ñu fonk ko it. — Macë 9:37, 38.
3 Nañu roy ci Yeesu : Am na li ñu mën a def ngir roy ci Yeesu. Loolu lan la ? Nañu yombalal suñu dund, te fexe ba liggéeyu waare bi nekk li ëpp solo ci ñun. Bu ñu amee li ñu soxla ngir dund, nañu topp li ñu Biibël bi xelal. Maanaam buñu nekk ay nit ñuy wut xaalis rekk, di bëgg bare alal rekk (Macë 6:19, 20 ; 1 Tim. 6:8). Li gën mooy ñu seet ni ñu mënee yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi. Bu ñu amee ay jafe-jafe yu mettee metti, nañu def ni Yeesu. Buñu nangu mukk coono àddina si tax ba ñu wàññi li ñuy def ci liggéey bi ëpp solo ci ñun, maanaam xamle xibaar bu baax bi jëm ci Nguur gi. — Lukk 8:14 ; 9:59-62.
4 Ñi am lu bare li ñu war a def sax, dañuy wone ne liggéeyu waare bi moo ëpp solo. Suñu benn mbokk dafa am njaboot bu réy, te lu bare lañu ko dénk fi muy liggéeye. Te it mag la ci mbooloo mi. Nee na : “ Ci man, liggéeyu waare bi mooy liggéey bi ëpp solo. ” Suñu benn mbokk bu jigéen bu nekk pioñee nee na : “ Nekk pioñee moo gën fuuf am liggéey bu lay jox xaalis bu bare ci àddina si. ”
5 Ak warugar yi ñu mënta am, nañu roy ci Yeesu. Naka ? Nañu fexe ba liggéeyu waare bi nekk li ëpp solo ci ñun.