Ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu : Li ñu warul a fàtte
Ren, ci bésu altine 2 awril lañuy def ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Magi mbooloo mi war nañu topp tegtal yii :
◼ Waxtu bi ndaje bi di komaase, war na nekk waxtu boo xam ne, bu ñuy joxante mburu mi ak biiñ bi, dina fekk jant bi so ba pare.
◼ War nañu xamal kiy def waxtaan bi ak ñeneen nit ñépp, waxtu bi ñuy defe ndaje bi ak fu ñu koy defe.
◼ War nañu wut mburu mi ñu war a jëfandikoo ci ndaje boobu ak biiñ bi, te defar lépp ba mu baax bala waxtu ndaje bi jot. — Seetleen La Tour de Garde bu 15 feewriyee 2003, xët 14-15.
◼ Bala waxtu ndaje bi di jot, war nañu wut taabal bu baax ak lu jekk lu koy muur, teg leen seen palaas. Aset yi ak weer yi it war nañu nekk seen palaas.
◼ Saalu Nguur gi walla béréb fu ñuy defe ndaje boobu, war nañu ko raxas ba mu set bala ndaje bi di jot.
◼ Bala ndaje bi di jot, war nañu tànn ñi war a teral nit ñi, ak ñi war a joxe mburu mi ak biiñ bi. Ñooñu war nañu xam bu baax li ñu war a def ci ndaje boobu te bañ a fàtte ne li ñuy sol ak ni ñuy defare seen bopp dafa war a jekk.
◼ Karceen bu bokk ci ñi Yàlla tànn, mën na feebar walla màgget ba du mën a teew ci ndaje boobu. Bu loolu amee war nañu fexe ba yóbbul ko mburu ak biiñ.
◼ Bu ñaari mbooloo walla lu ko ëpp waree bokk fi ñuy defe ndaje boobu, bu benn bi di waaj a pare ba mbooloo mi ci topp di ko xaar, nañu fexe ba nit ñi bañ a gurupoo ci buntu saal bi, walla ci mbedd mi ak fi ñuy gaare oto yi.