Li ñu warul a fàtte ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu
Ren, alxemes 28 màrs lañuy def ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Magi mbooloo mi war nañu topp tegtal yii :
◼ Bu ñuy tànn waxtu bu ñuy tàmbalee ndaje bi, na nekk waxtu boo xam ne bu ñuy joxante mburu bi ak biiñ bi dina fekk jant bi so ba pare.
◼ Kiy def waxtaan bi ci ndaje bi ak ñeneen nit ñépp, war nañu leen xamal waxtu bu ñu koy defe ak fu ñu koy defe.
◼ Bala waxtu ndaje bi jot, war na fekk mburu ak biiñ yi war pare. — Seetleen La Tour de Garde du 15 février 1985, p. 17.
◼ Aset yi, weer yi, taabal bu baax ak lu baax lu koy muur, loolu lépp war nañu leen a teg seen palaas bala waxtu ndaje bi jot.
◼ Saalu Nguur gi walla béréb bu ñuy defe ndaje boobu, war nañu ko raxas ba ñu set bala bés ba.
◼ Bala ndaje boobu di jot, war nañu tànn ñi war a teral nit ñi, ak ñi war a joxe mburu mi ak biiñ bi. War nañu leen xamal bu baax li ñu war a def bés boobu. War nañu leen wax it ne li ñuy sol ak seen bopp war nañu set te jekk ci ndaje boobu.
◼ Bu amee karceen bu bokk ci ñi nu tànn bu yaramam neexul ba du mën a teew ci ndaje boobu, war nañu seet ni ñu mënee def ba indil ko ci mburu mi ak biiñ bi.
◼ Bu ñaari mbooloo walla lu ko ëpp waree bokk fi ñuy defe ndaje boobu, nañu seet ni ñuy def ba du am nit ñu bare ñuy xaar ci buntu saal bi, ci mbedd mi walla fi ñuy bàyyee oto yi.