Ñépp a mën a bokk ci liggéey bi ñuy def ngir sàkk ay taalibe
1 Kenn du nekk taalibe Yeesu fekk benn nit kese moo ko ci dimbali. Yexowa mën na jaar ci ñiy liggéey ak moom ñépp ngir dimbali kiy jàng Biibël bi mu jëm kanam ci wàllu ngëm (1 Kor. 3:6-9). Kenn ku nekk ci ñun, buy tontu ci ndaje karceen yi tont yu jóge ci biir xolam, dafay dimbali ñiy sog a ñëw ci mbooloo mi. Waaye yemul ci loolu. Suñuy jëf yu rafet yiy wone li xel mu sell mi di def ci ñun, dafa leen di dimbali itam (Ywna. 13:35 ; Gal. 5:22, 23 ; Efes 4:22, 23). Lan lañu mën a def itam ngir dimbali leen ?
2 Mbooloo mi : Ñun ñépp mën nañu baax ak ñi sog a teewe suñu ndaje yi. Loolu mën nañu ko def bu ñu leen di teral bu baax te waxtaan ak ñoom bala ndaje mi di komaase ak bu jeexe ba pare. Am na benn waay bu doon fàttaliku bés bi mu njëkke ñëw ci ndaje mbooloo mi. Dafa nee : “ Bés bi ma fa njëkke ñëw, xawma fa woon kenn. Waaye ci bés boobu kese, nit ñi ma won mbëggeel ñoo ëpp fuuf ñi ma ko won bi ma nekkee xale ba léegi ci sama jàngu. Dafa ma leeroon ne gis naa dëgg gi. ” Kooku sóobu na ci ndox juróom ñaari weer ginnaaw bi mu njëkke teewe suñu ndaje yi.
3 Kiy jàng Biibël bi ak yow, bu fekkee ne mu ngi jëm kanam ci wàllu ngëm, nanga ko ci wax lu rafet te na doon lu jóge ci sa xol. Ndax ñu ngi koy fitnaal ? Ndax mu ngi faral di teewe suñu ndaje yi ? Ndax dem na ba am fitu tontu ci benn ndaje ? Ndax léegi bokk na ci Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla walla komaase na waare ? Nee ko li mu def noonu rafet na. Loolu dina seddal xolam te dina ko may doole. — Léeb. 25:11.
4 Kiy def njàngum Biibël bi : Am na ay waaraatekat yu fexe ba ki ñuy jàngal xam yeneen waaraatekat ci mbooloo mi. Dañuy wax yeneen waaraatekat ñu ànd ak ñoom ci nit kooku. Ci lu mu gënee teel, nanga woo ki ngay jàngal ci ndaje karceen yi. Bu komaasee teewe ndaje yi, yóbbu ko ci waa mbooloo mi mu xamante ak ñoom. Loolu dina tax mu komaase gise mbooloo mi ni njabootam ci wàllu ngëm. Ndax fi mu nekk nii mu ngi jéem a bàyyi yenn yu bon yu mu tàmmoon, mel ni tux ? Ndax am na ci waa këram kenn ku bëggul mu jàng Biibël bi ? Waxtaan ak waaraatekat bu jaar ci lu mel noonu te kontine di jëm kanam, mën na ko dimbali. — 1 Pie. 5:9.
5 Ñiy jàng Biibël bi ak ñun, dañu soxla mbooloo mi jàpple leen ci wàllu ngëm. Ñépp a mën a def seen wàll ci loolu bu ñu leen di won ne dañu leen bëgg dëgg.