TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 4/07 p. 6
  • Bu ñu fekkul nit ñi seen kër

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Bu ñu fekkul nit ñi seen kër
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ndax am nga gox bi nga moomal sa bopp ngir waare ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Ndax gox bi sa mbooloo moom dafa réy ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Liggéey bu am solo bu ñu war a def
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
Sasu Nguuru Yàlla — 2007
km 4/07 p. 6

Bu ñu fekkul nit ñi seen kër

1. Ban jafe-jafe la nit ñu bare di am bu ñuy waaraate këroo-kër ?

1 Ci gox yu bare, fekk nit seen kër mu ngi gën di jafe. Ci “ bési tiis ” yi ñu tollu tey, ñu bare dañu war a liggéey waxtu yu bare ngir am li ñuy dunde (2 Tim. 3:1). Am na ñu nekkul seen kër ndaxte dañu dem jëndi dara walla dafa am fu ñu dem ngir noflaay. Naka lañu mënee xamal nit ñooñu xibaar bu baax bi ?

2. Naka lañu mënee jëfandikoo bu baax kayit bi tudd Notes de maison en maison ?

2 Bindal li nga warul a fàtte : Li nga mën a njëkk def mooy bind adareesu ñi nekkul seen kër. Kayit bi tudd Notes de maison en maison (S-8) lañu defar ngir loolu. Ndax dangay bind turu mbedd mi, nimoro gox bi, sa tur ak bés bi ? Nanga bàyyi palaas ci kayit bi, ngir am fu ngay mën a bind li nga ci bëgg yokk bés boo dellusee, yow walla beneen waaraatekat. Boo paree waaraate bi, bul fàtte jox kayit boobu ki yor kartu gox bi. Waaye bu nangoo nga jéem a gisaat nit ñooñu, dencal kayit bi. Jëlal beneen kayit ngir bind képp koo fekk te mu bëgg waxtaan ak ñun, ngir seetiwaat ko.

3. Lan lañu mën a def ngir jot ñi nu fekkul seen kër ?

3 Nanga dellusi ci beneen waxtu : Xéyna ñi nekkul seen kër bés yi ñuy liggéeye, maanaam diggante altine ak àjjuma, dinañu fa nekk samdi ak dimaas. Ndax mën nga seet li nga mën a def ngir dellusi ci beneen waxtu bu gën a baax (1 Kor. 10:24) ? Boo ko mënul, mën nga jox kayit fi ñu bind ñi nekkul seen kër beneen waaraatekat bu fa mën a dellusi ci beneen waxtu.

4. Lan mooy wone ne dellu ngir jéem a gis nit ñi nekkul seen kër am na solo lool ?

4 Nañu nettali fii luy wone lu tax jéem a gis ñi nekkul seen kër nekk lu am solo lool. Dafa am waaraatekat yu dellu woon ci benn kër lu mat ñetti at bala ñuy mën a gis ki fa dëkkoon. Bi ñu gisee jigéen jooju, dafa fekk ñetti at yooyu yépp dafa doon xaar Seede Yexowa yi ngir kontine njàngum Biibël bi mu komaase woon bala muy toxu fi mu dëkk léegi.

5. Kañ lañuy mën a wax ne jeexal nañu gox bi ?

5 Nanga jeexal gox bi : Kañ lañu mën a wax ne jeexal nañu gox bi ? Loolu dinañu ko mën a wax bu ñu defee lépp li ñu mën ngir jéem a gis kenn ci kër gu nekk. War nañu jéem a jeexal gox bi ci diggante ñeenti weer. Bu ñu ci paree, dañu ko war a wax kiy toppatoo gox bi ci mbooloo mi ngir mu bind ko ci kayitam yi.

6. Lu tax ñu war a jéem a gis képp ku nekk ci suñu gox ngir wax ko xibaar bu baax bi ?

6 Dañu bëgg li ëpp ci nit ñi, mën a jàng woo Yexowa ci turam te mucc (Room 10:13, 14). Ci nit ñooñu am na ñoo xam ne fekkuñu leen woon seen kër bi ñu fa doon waaraate këroo kër. Ni Pool, ñun it nañu bëgg “ seedeel ci ñépp xebaar bu baax, bi ëmb yiwu Yàlla ”. — Jëf. 20:24.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager