TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/06 p. 1
  • Liggéey bu am solo bu ñu war a def

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Liggéey bu am solo bu ñu war a def
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • “ Diirub junniy at, bu bees bi — Lu la ëllëg di indil ? ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2000
  • Liggéey bu am solo bu ñu war a def diggante 20 oktoobar ba 16 nowàmbar ngir joxe kayit bu ndaw bu bees.
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Bu ñu fekkul nit ñi seen kër
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • ‘ Nanga yégle fu nekk Kàddug Yàlla ’
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2006
km 9/06 p. 1

Liggéey bu am solo bu ñu war a def

diggante 16 oktoobar ba 12 nowàmbar !

1 “ La fin de la fausse religion est proche ! ” (maanaam diine bu dul dëgg bi, léegi mu jeex). Loolu mooy turu kayit bu ndaw bi ñu woowe ci tubaab Nouvelles du Royaume No. 37. Dinañu ko joxe ci àddina si sépp weer wii di ñëw. Diggante 1 ba 15 oktoobar dinañu wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! ci waaraate bi. Waaye diggante altine 16 oktoobar ba dimaas 12 nowàmbar, dinañu wone Nouvelles du Royaume No. 37 te sawar ci lool. Ci jamano jooju, ci samdi ak dimaas yi, bu ñu koy wone, dinañu ko boole ak La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñuy wone ci weer woowu.

2 Ñi ci mën a bokk : Na waaraatekat bu nekk def lépp li mu mën ngir bokk bu baax ci liggéey boobu. Xéyna dina am ñu mën a nekk pioñee buy jàpple. Ndax am nga doom walla njàngum Biibël buy jëm kanam bu baax ci wàllu ngëm ? Nanga leen wax ñu dem ci njiiti mbooloo mi ngir seet ndax mat nañu waaraatekat bu ñu sóobagul. Njiiti mbooloo mi war nañu dem seeti waaraatekat yi bàyyi waare, ngir xiir leen ci bokk ci liggéey boobu. Waaraatekat yooyu, xéyna ñu mën a ànd ak waaraatekat yi mën waare bu baax ngir bokk ci liggéey boobu.

3 Mbooloo mu nekk dina jot ci Nouvelles du Royaume No. 37. Bu ko defee, waaraatekat ak pioñee bu nekk dina mën a am lu mu tuuti tuuti 50 kayit yu ndaw yooyu. Ñi suñu waxtaan neex ñoom, dinañu ci mën a jot juróom ngir ñu jox ko seeni mbokk ak seeni xarit. Na ku nekk am fu muy bind ñaata kayit yu ndaw la joxe, ba pare bind ko ci ginnaaw kayit fi muy binde li mu def ci waaraate bi ci weeru oktoobar ak weeru nowàmbar. Sekkerteer bi dina seet ñaata kayit yu ndaw la mbooloo mi yépp joxe te xamal ko bànqaas bi, weer wu nekk bu deewee. Bésu 12 nowàmbar bu paasee te mu des ci kayit yooyu, dinañu ko mën a jëfandikoo ci waaraate bi, ci fànn bu mu mënta doon.

4 Li ñu mën a wax : Li ngay wax dafa war a gàtt, bu ko defee, li ngay joxe ci kayitu xibaar boobu mën a gën a bare. Mën nga wax lii : “ Ci àddina si sépp, ñu ngi joxe kayit bu ndaw bii. Xibaar bu am solo moo ci nekk. Kenn du ci fey dara. Dama la bëgg may bii ngir nga jàng ko. ” Mën nañu def liggéey boobu te bañ a yor saag bi ñuy yóbbu ci waaraate bi. Bul fàtte bind képp ku waxtaan boobu neex.

5 Ni ngeen di laale seen goxu mbooloo yépp : Nangeen gën a jublu ci gox fi ngeen di waare këroo-kër ak ci gox yi bare bitig. Loolu moo gën joxe kayit bu ndaw boobu ci mbedd mi. Bu amee kër fu ngeen fekkul kenn, nangeen ko bind te jéem fa dellu ci beneen waxtu walla beneen bés ci ayu-bés bi. Nangeen jéem a def loolu ba bésu 6 nowàmbar. Waaye bés boobu bu jotee, ngeen komaase bàyyi benn kayit ci kër fu ngeen fekkul nit. Mën na am seen goxu mbooloo yaatu ba nga xam ne, balaa ngeen di komaase liggéey bi sax, dafa leen leer ne, diggante 16 oktoobar ba 12 nowàmbar, dungeen ko mën a laal yépp. Bu booba njiiti mbooloo mi mën nañu seet ndax ci bésu 16 oktoobar ngeen war a komaase bàyyi benn kayit ci bépp kër bu ngeen dul fekk nit.

6 Alku “ Babilon mu mag mi ”, mu ngi jegesi bu baax. Nit ñi dañu ci war a génn bala ñu koy alag ba mu jeex (Peeñ. 14:8 ; 18:⁠8). Seetal tey jii li nga war a def ngir mën a bokk bu baax ci liggéey boobu ñu nar a def ci àddina si sépp ba nit ñépp xam ne diine bu dul dëgg gi, léegi mu jeex !

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager