TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 5/07 p. 4
  • Jàngalleen seeni doom ñu màggal Yexowa

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Jàngalleen seeni doom ñu màggal Yexowa
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu dimbali ñiy jàng Biibël bi ñu nekk ay waaraatekatu xibaaru Nguuru Yàlla
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Seen porogaraamu njaboot ngir waaraate
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Dimbalil say doom ñu mën waaraate
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2007
km 5/07 p. 4

Jàngalleen seeni doom ñu màggal Yexowa

1. Ndax xale yu ndaw yi mën nañu màggal Yexowa ?

1 Sabuur 148:12, 13 day xiirtal xale yu góor yi ak yu jigéen yi ñu “ màggal turu Yexowa ”. Mbind mi wone na xale yu bare yu def noonu. “ Samwil dafa jàppoon ci liggéeyu Aji Sax ji, fekk xale ” la woon (1 Sam. 2:18). “ Xale bu jigéen ” moo waxoon jabaru Naaman ne yonentu Yexowa ba nekkoon Israyil moo mënoon a faj Naamaan ci ngaanaam (2 Bu. (2 Roi) 5:1-3). Ba Yeesu duggee ca Kër Yàlla ba, te def ay kéemaan, ay “ xale yu ndaw ” ñoo doon yuuxu naan “ Osaana [maanaam ñu ngi lay ñaan nga musal ñu] yaw sëtu Daawuda bi ” (Macë 21:15). Naka la wayjur yi mënee jàngal seeni doom ñu màggal Yexowa ?

2. Lu tax doon royukaay bu rafet ci say doom am solo lool ?

2 Li ñu leen di won : Bala ñuy dugal dëgg gi ci seen xolu doom, baay yi ca Israyil dañoo waroon a jëkk jàng bëgg Yexowa te def li mu santaane ci seen xol, ñoom (5 Mu. (Deut.) 6:5-9). Su ngeen di wax lu rafet ci waaraate bi, te ngeen boole ko ci seen porogaraam ayu-bés bu nekk, dina tax seeni doom gis ne liggéeyu waaraate bi am na solo te ànd na ak mbégte.

3. Naka la suñu benn mbokk mu jigéen jariñoo ci royukaay bi ko wayjuram yi won ?

3 Suñu benn mbokk mu jigéen dafa fàttaliku lii : “ Bi ma doon màgg, waaraate bi bokkoon na ci li suñu waa kër tàmmoon a def diggante samdi ak dimaas bu nekk. Dama doon gis ne waaraate bi dafa neexoon samay wayjur. Bi ñu doon màgg ñu ngi doon gis ne waaraate bi lu neex la. ” Suñu mbokk moomu, bi mu amee juróom ñaari at la nekk waaraatekat bu ñu sóobagul. Te fi mu nee nii, 33 at a ngi nii muy jébbal jotam yépp ci liggéeyu waare bi.

4. Lan mooy jàngal say doom ndànk-ndànk ngir ñu jëm kanam ci waaraate bi ?

4 Nañu leen jàngal ndànk-ndànk ñu màggal Yexowa : Booy waaraate, fexeel ba say doom am lu ñuy def ci waaraate bi. Xéyna mën nañu fëgg bunt bi, mbaa bës “ sonnerie ” bi. Mën nañu joxe it ay kayit yu ndaw, walla jàng benn aaya. Loolu dina tax ñu gën a kontaan ci waaraate bi. Dina tax it ñu gën a wóolu seen bopp ba gis ne ñoom itam mën nañu xamle xibaaru Nguur gi. Bu ñuy màgg, liggéey bi ñuy def ci waaraate bi dafa war a yokku. Kon nag, dimbali leen ndax ñu jëm kanam te ñu am lu ñuy fas yéene def ci wàllu ngëm.

5. Naka la xale war a mel bala muy mën a nekk waaraatekat bu ñu sóobagul ?

5 Bu ngeen gisee ne seeni doom mën nañu nekk waaraatekat bu ñu sóobagul te ñu wax ne dañu ko bëgg nekk, buleen yeexal mbir mi. Nangeen ci waxtaan ak benn njiit ci mbooloo mi. Nekk waaraatekat, dina tax ñu gën a xam ne màggal Yexowa seen wareef la. Kenn ku nekk war na ko màggal. Nañu xam ne soxlawul xale am xam-xam bu tollu ni xam-xamu mag bu ñu sóob ba pare, bala mu mën a nekk waaraatekat bu ñu sóobagul. Ndax sa doom xam na lu ëpp solo ci li ñu war a xam ci Biibël bi ? Ndax jikkoom ànd na ak li Biibël bi santaane ? Ndax bëgg na bokk ci waaraate bi te bëgg nit ñi jàppe ko ni Seede Yexowa ? Su loolu lépp amee, ñiy jiite mbooloo mi dinañu seet ndax mën na nekk waaraatekat bu ñu sóobagul. — Seetleen li nekk ci téere Organisés pour faire la volonté de Dieu, xët 79 ba 82.

6. Lu tax jar na wayjur yi jàngal seeni dom ?

6 Jàngal seeni doom ñu màggal Yexowa te fexe ba loolu jóge ci seen xol, liggéey la. Waaye gis say doom ñu jëm kanam ci wàllu ngëm, lu neex la ci xolu wayjur. Leneen lu leen gën a mën a indil mbégte, barewul. Li ci gën a am solo mooy, Yexowa dafay bég bu gisee xale yuy wax ci lu rafet li mu def.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager