Nañu dimbali ñiy jàng Biibël bi ñu nekk ay waaraatekatu xibaaru Nguuru Yàlla
1 Li Yeesu sant taalibeem yi te ñu bind ko ci Macë 28:19, 20, réy na lool. Dañu leen sant ñu sàkk ay taalibe yu bare. Taalibe yu bees yooyu nag, dañu waroon a bokk ñoom itam ci liggéeyu sàkk ay taalibe. Noonu lañu naroon a def ba ci mujug jamano ji ñu nekk nii, fu ñu war a waare xibaaru Nguur gi ci àddina si sépp. — Macë 24:14.
2 Ñiy jàng Biibël bi ak ñun, mën na nekk suñuy doom walla ñeneen ñu bëgg jàng Biibël bi ak ñun. Dañu bëgg dimbali nit ñooñu ñu xam ne nit ku nekk dafa war a dimbali moroomam yi ñu nekk taalibe Yeesu Kirist, ba pare nangu def loolu. — Luug 6:40.
3 Waajalleen ñiy jàng Biibël bi ñu mën a jàngale dëgg gi : Xiirtalleen ñiy jàng Biibël bi ñu waxtaan ak seeni moroom ci li ñu jàng. Nettali leen lu rafet lu xew ci waaraate bi. Nangeen teel a jàngal seeni doom ni ñuy def ba aay ci waaraate bi. Boo leen di jàngal, bàyyileen xel ci fi seen mën-mën tollu (Sab 148:12, 13). Nangeen wone ci seeni wax ak seeni jëf ne dangeen fonk liggéeyu waare bi. — 1 Tim. 1:12.
4 Yexowa dafay jaar ci ay nit ñu bëgg def li mu bëgg te jub, ngir def liggéeyam. Dëgg la, waaraatekat bu bés, xam-xamam tolluwul ak xam-xamu waaraatekat bu jébbal boppam Yàlla ba pare te sóobu ci ndox. Waaye ba tey war na fekk mu gëm ba pare li ñu warul a ñakk xam ci Biibël bi te mën koo jàngal nit ñi. (Seetleen li nekk ci téere Organisés, xët 79 ba 82). War na fekk it mu génn “ Babylon la Grande ” ba pare ak lépp li bokk ci wàllum politik. Te itam war na ko fekk mu tàmm teewe suñu ndaje yépp. — Peeñ. 18:2, 4 ; Ywna. 17:16 ; Yaw. 10:24, 25.
5 Booy xalaat ne ki ngay jàngal Biibël bi mat na waaraatekat bu ñu sóobagul , nanga ko wax wottukat biy jiite. Moom dina yébal ñaari njiit ngir ñu toog ak yow akit ki ngay jàngal Biibël bi. Dinañu seet ndax mën na nekk waaraatekat bu ñu sóobagul, bu mën a ànd ak mbooloo mi ngir waare xibaar bu baax bi. Bu boobaa yow lañu koy dénk ngir nga kontine di ko jàngal ni ñuy waaraatee. Loolu, cér bu réy lay doon.