Ndax mën nga jaar ci bunt bi ñu “ ubbi ba mu ne làññ, ngir def liggéeyu Yàlla ” ?
1. Ban bunt lañu ubbi ba mu ne làññ ci liggéeyu Yàlla ?
1 Ñi kontar liggéeyu Nguur gi bare woon nañu ci jamano Pool. Waaye bi ñu ko ubbilee ‘ bunt ba mu ne làññ ngir mu def liggéeyu ’ Nguuru Yàlla, dafa ci jaar te def li mu mën ngir liggéey boobu jëm kanam (1 Kor. 16:9). Tey, ci àdduna si sépp, am na 642000 waaraatekati Nguuru Yàlla yu jaar ci bunt boobu ngir doon ay pioñee yu ci sax.
2. Lu tax seet yenn saay li ñu nekke baax lool ?
2 Li ñu nekke mën na soppeeku : Xéyna li ñu nekke tey tax na ba duñu mën a def lu bare ci waaraate bi. Waaye loolu mën na soppeeku. Kon, bu ñu seetaatee léeg-léeg li ñu nekke, lu baax lay doon. Waruñu xaar rekk ba suñu coono yépp deñ, sog a xool ni ñu mënee yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi (Daj. (Eccl.) 11:4). Ndax fi nga tollu nii, yaa ngi waaj a pare ci sa njàng ci lekkool ? Ndax waajur nga bu am doom yuy waaj a dugg lekkool ? Ndax fi nga nekk nii, yaa ngi waaj a jël rëtréet ? Yu mel noonu mën na la may jot ba nga nekk pioñee. Suñu been mbokk bu jigéen bu feebaroon ba wér, dafa fas yéene nekk pioñee bi mu amee 89 at. Lu tax mu def loolu ? Ndaxte, booba dafa fekkoon mu def benn at te demul lopitaan. Kon, dafa gisoon ne wër gi yaramam dafa ko doon may mu nekk pioñee.
3. Naka la ay seede Yexowa soppee seen dundin ba mën a nekk pioñee bu ci sax ?
3 Pool ci boppam, dafa bëggoon a seeti ay mbokkam ci ngëm yi nekkoon ca Korent. Waaye demu fa woon ndax li mu bëggoon a def ci liggéeyu waare xibaar bu baax bi. Ñu bare ñu nekk pioñee tey, soppi nañu lu bare ci seen dund ngir mën a nekk pioñee. Am na ñu yombalal seen dund ba bañ a soxlati liggéey semen bi yépp ngir faj seeni soxla. Loolu may na leen mbégte bu réy ndax li ñu jotoon a def noonu ci liggéeyu waare bi (1 Tim. 6:6-8). Am na jëkkër ak jabar yu soppi seen dundin ba mën a doylu ci xaalis bi jëkkër ji kese di indi. Loolu tax na ba jabar ji mën a nekk pioñee.
4. Lan lañu war a def su fekkee ni wóoru ñu ne dinañu mën a def waxtu yi ñuy laaj pioñee bu ci sax ?
4 Pioñee yi dañu am waxtu yi ñu leen laaj. Waaye bul gaaw a foog ne doo mën a waaraate waxtu yooyu yépp. Lu ëpp tuuti ñaari waxtu kese nga war a waare bés bu nekk. Su fekkee ne wóoru la ne mën nga ko def, jéemal a nekk pioñee biy jàpple ci lu mat benn walla ñaari wéer te nga jéem a def 70 waxtu. Dinga gis mbégte bi ci nekk (Sab. 34:8). Waxtaanal ak ñi nekk pioñee ba pare. Xéyna mas nañu jaar ci jafe-jafe yu niiru ak yi nga am tey, ba génn ci (Léebu 15:22). Ñaanal Yexowa mu barkeel li ngay def yépp ngir yokk li ngay def ci waaraate bi.—1 Ywna. 5:14.
5. Lu tax nekk pioñee bu ci sax doon lu am solo lu ñu mën a fas yéene def ?
5 Lu am solo lu ñu mën a fas yéene def : Nekk pioñee day indi ay barke yu bare. Dina leen may ngeen gën a bég bu ngeen di maye lu gën a bare (Jëf. 20:35). Dinañu gën a mën a faramfàcce bu jub Kàddu dëgg gi (2 Tim. 2:15). Dinga gën a am fu la Yexowa war a dimbali te dinga gis ne dina ko def (Jëf. 11:21 ; Fil. 4:11-13). Nekk pioñee dina la dimbali it nga am ay jikko yu rafet ci wallu ngëm, mel ni muñ. Te dinga gën a jege Yexowa (Saak 4:8). Ndax mën nga jaar ci bunt bi ñu “ ubbi ba mu ne làññ ngir def liggéeyu Yàlla ” te nekk pioñee ?