TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 7/07 p. 3
  • Ay Tont Ci Seeni Laaj

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ay Tont Ci Seeni Laaj
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Lenn lu mën a dimbali nit ñi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
Sasu Nguuru Yàlla — 2007
km 7/07 p. 3

Ay Tont Ci Seeni Laaj

◼ Lan moo bon ci di jëfandikoo internet ngir waxtaan ak nit koo xamul ?

Li ñuy woowe ci tubaab Sites web, yu ci bare dañu leen def ngir nit ñi mën a xamante walla waxtaan ci internet. Ci sites yu bare, mën nga ci wone ki nga doon, boole ci ay foto ak yeneen yu jëm ci yow. Ñiy gis loolu, mën nañu la woo mbaa ñu bind la ngir waxtaan ak yow. Sites yu mel noonu siiw nañu lool ci ndaw yi. Am na sax ay ndaw yu bokk ci mbooloo karceen bi yu leen di jëfandikoo ngir waxtaan ak ay nit ñuy wax ne ñoom ay Seede Yexowa lañu.

Nax nit ci internet yomb na. Nit mën na la nax ci ki mu doon, ci digganteem ak Yexowa ak ci ay bëgg-bëggam (Sab. 26:4). Nit mën na wax ne Seede Yexowa la fekk du dëgg. Walla mu nekk ku ñu dàq ci mbooloo mi. Walla sax mu nekk ku bàyyi yoonu dëgg gi ba pare muy fexe ba génne ay nit ci yoon boobu (Gal. 2:4). Gis nañu ne mag yu bare yuy siif ay xale, ci sites yooyu lañuy jaar ngir wut ay xale.

Xéyna dafa ñu wóor ne ki ñu faral di waxtaanal am na tur bu rafet ci mbooloo mi. Waaye loolu terewul waxtaan bi mën gaaw a dem ci yëf yu bon. Li waral loolu, mooy duñu rus a wax yenn yi bu ñuy waxtaan ak ku ñu dul gis. Xéyna it dañu xalaat ne li ñuy waxtaane ci internet kenn du ci dugg, te it kenn du mas a xam li ñuy wax, muy suñu wayjur, walla njiiti mbooloo mi. Li ñu metti mooy, ay ndaw yu bokk ci njabootu karceen, dañu daanu ci fiir boobu, ba mujj dugg ci waxtaan yu tilim (Efes 53, 4; Kolos 3:8). Ñeneen ñi dañu foto seen bopp foto yu bon def ko ci, mbaa ñu tudde seen bopp ay tur yoo xam ne ku ko dégg rekk xelam dem ci lu ñaaw, walla ñu def ci seen ordinateer ay clip wideo yuy wone njaaloo.

Li ñu fii wax yépp, moo tax wayjur yi war a dimbali seen doom yi, ñu xam naka la ñuy jëfandikoo seen ordinateer (Léeb. 29:15). Indi ku ñu xamul suñu kër, walla ñu bàyyi ko moom kese ak suñuy doom, xam nañu ne wóorul. Noonu it, jaar ci internet ngir xaritoo ak ku ñu xamul, bu fekkee ne sax dafay wax ne moom Seede Yexowa la, gënul ci ñun ak ci suñuy doom.— Léeb. 22:3.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager