TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 8/07 p. 1
  • Na njaboot yi ànd di jàmmu Yexowa

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Na njaboot yi ànd di jàmmu Yexowa
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Lan mooy njàngum Biibël ci biir njaboot ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
  • Jàmm ci biir kër, naka lañu ko mën a ame ?
    Jàmm ci biir kër, naka lañu ko mën a ame ?
  • Boroom kër yi : tàmmleen di topp porogaraam bu baax ci wàllu ngëm
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Sasu Nguuru Yàlla — 2007
km 8/07 p. 1

Na njaboot yi ànd di jàmmu Yexowa

1 Ci Jamono Biibël bi, njaboot yi dañu doon ànd di def lu bare. Bés bu nekk, dañu doon ànd di def yenn yi. Waaye li ëpp solo mooy dañu doon ànd di jaamu Yexowa (3 Mus. 10:12-14 ; 5 Mus. 31:12). Ci dëkk yu bare tey, am na ñu bokk njaboot waaye li ñuy defandoo barewul dara. Karceen yi xam nañu ne ànd ak seen waa kër di def yenn yi, lu am solo la, rawatina bu ñuy jaamu Yàlla. Yàlla mii sos njaboot dafay kontaan bu gisee ay nit ñu bokk kër di ànd di ko jaamu !

2 Nangeen ànd di waaraate : Njaboot yi bu ñu àndee di waare xibaar bu baax bi, seen diggante dafay gën a rattax. Looloo tax njiitu mbooloo yi, bu ñu àndee ak waa mbooloo mi ci waaraate bi, dinañu faral it di ànd ak seen jabar ak seeni doom ci waaraate bi (1 Tim. 3: 4, 5). Wottukat yiy wër ci mbooloo yi sax, ak it wottukat yiy wër ci ndaje yu mag yu benn walla ñaari fan, ak li seen porogaraam mënta xat yépp, war nañu def ci seen porogaraam kañ lañuy ànd ak seen jabar ci liggéeyu waare bi.

3 Wayjur yi, bu ñu àndee ak seeni doom ci waaraate bi, dinañu leen mën a dimbali ñu gën a aay ci liggéey boobu. Li xale yi, di gis ci seeni wayjur, du mbégte bi ñu am ci waaraate bi rekk. Dinañu gis itam mbëggeel bi ñu am ci Yexowa ak ci seeni moroom (5 Mus. 6: 5-7). Njariñ bi nekk ci ànd ak say doom ci waaraate bi, du waññeeku bu xale yi màggee. Benn jëkkër ak jabaram yu am ñetti doom yu am diggante 15 ak 21 at, dañuy kontine di ànd ak seeni doom ci waaraate bi. Góor gi nee na : “ Saa su nekk dañu am lu ñu leen di jàngal. Te dañu fexe ba mu nekk lu leen neex te lu leen di may doole ci wàllu ngëm. ”

4 Nangeen toog di waajal li ngeen di wax ci waaraate bi : Njaboot yi gis nañu ne di waajal liggéeyu waare bi ci seen biir, am na njariñ. Waa kër yi mën nañu def mel ni ñu ngiy waare ngir ñu xam lu ñuy wax bu ñu demee ci waaraate bi. Bu xale yi di def mel ni ñu ngiy waaraate, yenn saay ñu def ni kuy waaraate, yenn saay ñu def ni ku ñu fekk këram, ci lu ëpp loolu dafa leen di neex lool. Am na ñuy jël tuuti minit bala ñuy jeexal njàngum Biibël bi ñu am ci biir njaboot gi ngir def loolu.

5 Suñu mbégte dafay yokku bu ñuy def lu am solo te neex ak nit ñi nu bëgg. Di gis ay nit ñu bokk njaboot di ànd dem këroo kër ngir waare, walla di dellu seeti nit ñi, walla di jàngal nit ñi Biibël bi, loolu rafet na lool ! Bu ngeen di jaamu Yexowa noonu ak seen waa kër yépp, mën ngeen a bég te wax lii : “ Waaye man mii ak sama waa kër, Yexowa lañuy jaamu ”. — Yos. 24:15.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager