TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • jl lesoŋ 10
  • Lan mooy njàngum Biibël ci biir njaboot ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Lan mooy njàngum Biibël ci biir njaboot ?
  • Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Naka nga mënee am jàmm ci sa biir njaboot? (Xaaj 2)
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Jaamuleen Yexowa ci seen biir njaboot
    Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Na njaboot yi ànd di jàmmu Yexowa
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Yeneen ndimbal ngir njaboot gi
    Yeewuleen! (2018)
Xóotalal waxtaan bi
Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
jl lesoŋ 10

NJÀNGALE 10

Lan mooy njàngum Biibël ci biir njaboot ?

Benn njàngum Biibël ci biir njaboot

Corée du Sud

Jëkkër ak jabar ñu ngi toog di jàng Biibël bi

Brésil

Benn seede Yexowa mu ngi jàng Biibël bi

Australie

Benn njaboot a ngi def benn waxtaan bu ñu tànn ci Biibël bi

Guinée

Yexowa dafa mas a bëgg njaboot yi jël jot ngir toog waxtaan, dëgëral seen ngëm te rattaxal seen diggante ci seen biir (Deutéronome 6:​6, 7). Loolu moo tax seede Yexowa yi di jël jot semen bu nekk ngir jàng Biibël bi ak seen njaboot. Dañuy waxtaan ci toogaay bu neex ci li ñu soxla ci wàllu ngëm. Boo nekkee yaw kese, jot boobu mën nga ci wéet ak Yàlla, tànn benn waxtaan te gëstu li ci Biibël bi wax.

Jot la bu ñu jël ngir gën a jege Yexowa. “ Jegeleen Yàlla, mu jege leen. ” (Saag 4:⁠8). Mën nañu yaatal suñu xam-xam ci Yexowa bu ñuy jàng ci Kàddoom lu jëm ci jikkoom ak ciy jëfam. Liir Biibël bi ci kaw mooy fasoŋ bu yomb bi ngeen mën a komaase seen njàngum Biibël ci biir njaboot. Mën ngeen a topp porogaraamu Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla bi. Mën ngeen a topp porogaraamu ndaje bi tudd Dundinu karceen ak liggéeyu waare bi. Mën ngeen seddale aaya yi, ba ku nekk am li ngay liir. Bu ngeen paree, ngeen waxtaan ci.

Jot la bu ñu jël ngir ñu gën a jegeente ci biir njaboot gi. Bu jëkkër ak jabar walla waajur ak seeni doom di toog ngir jàng Biibël bi, seen diggante dafay gën a rattax. Waxtu boobu dafa war a nekk waxtu bu neex te ànd ak jàmm ak mbégte. War na bokk ci waxtu yi gën a neex ci semen bi. Bu waajur di tànn li ñuy waxtaane ci seen njàngum Biibël, nañu sóoraale at yi seen doom am. Mën nañu tibb ci waxtaan yi nekk ci Tour de Garde yi ak Réveillez-vous yi walla ci palaas bi ñu moom ci internet jw.org. Mën ngeen a seetaan ay wideo ci JW Télédiffusion (tv.jw.org) boo leen paree ngeen waxtaan ci. Mën ngeen a waxtaan ci poroblem yi xale yi di daj ci seen lekkool te seet li ñu ci mën a def. Mën ngeen woy itam li ñu war a woy ci ndaje yi. Bu ngeen paree nag, mën ngeen am tuuti lu ngeen lekk walla naan.

Jot boobu njaboot gi di jël semen bu nekk ngir jaamu Yexowa, dina dimbali ñépp ñu bég bu ñuy jàng kàddu Yàlla. Nangeen ci góor-góorlu. Yexowa dina leen barkeel bu baax-a-baax. — Sabóor 1:​1-3.

  • Lu tax ñuy jël jot ngir jàng Biibël bi ci biir njaboot gi ?

  • Lan la waajur mën a def ba ku nekk ci njaboot gi bég ci waxtu boobu ?

XÓOTALAL WAXTAAN BI

Boo bëggee am yeneen xalaat ci ni nga mën a defe sa njàngum Biibël ci biir njaboot, laajal ay mbokk ci mbooloo mi ni ñuy defe seen bos. Nanga seet itam ci sa mbooloo téere yi nga fa mën a jël ngir jàngal say doom lépp lu jëm ci Yexowa.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager