Porogaraamu ndaje bu mag bu benn fan biy ñów
Suñu ndaje bu mag bu benn fan bi ñuy am ci atum liggéeyu waare bu 2008 mu ngi tudd “ Nous sommes l’argile, Jéhovah est notre Potier ” (maanaam ñun ñooy ban bi — Yexowa mooy defarkatu ndaa yi). Ci Esayi 64:8 lañu ko jële. Ci porogaraam bi, dinañu waxtaan ci ay xelal yu ñu jële ci Biibël bi . Loolu dina nu dimbali ñu gën a fonk xam-xamu Yexowa, njubteem, kàttanam, ak mbëggeelam, moom mii nekk Defarkatu Ndaa bu Mag bi.
Wottukat biy wër ci mbooloo yi, dina def waxtaan bi tudd “ Soyons des vases pour un usage honorable dans le ministère ” (maanaam nañu mel ni ay ndab yu tedd yu ñuy jariñoo ci liggéeyu waare bi). Waxtaan boobu dina wone naka la ay nit ñu gën a bare di ame barke bu réy, maanaam xam dëgg gi te di ko xamal seen moroom. Waxtaan bi tudd “ La méditation vous préservera ” (maanaam toog di xalaat bu baax, dafa ñuy aar) dina ñu won naka la toog di xalaat ci li Yexowa wax di ñu aare. Ki ñu bànqaas bi yónnee dina def waxtaan yi tudd “ Ne nous conformons pas à ce système de choses-ci ” (maanaam buñu topp àddina sii) ak “ Laissons-nous façonner par le Grand Potier ” (maanaam nañu bàyyi Defarkatu Ndaa bu Mag bi defar suñu jikko). Wayjur yi ak xale yi dinañu dégg lu leen di may doole ci wàllu ngëm ci xaaj bi tudd “ Des jeunes utiles à Jéhovah ” (maanaam ay ndaw yu am njariñ ci Yexowa) ak itam “ Le rôle capital des parents dans le façonnage ” (maanaam wàll bu réy bi wayjur yi di am ci liy defar seen jikko doom). Ci porogaraam bi, dina am ñuy wone ci kanamu ñépp li suñu ay mbokk def ci waaraate bi ak it ay nit yu ñuy woo ci kanamu ñépp ngir laaj leen ay laaj yu jëm ci li ñu def ci waaraate bi. Ñi nga xam ne dañoo bëgg ñu sóob leen ci ndox ngir wone ne jébbal nañu seen bopp Yàlla, war nañu ko wax wottukat biy jiite ci seen mbooloo ni mu gënee gaaw. Buleen fàtte indi seen La Tour de Garde bi ñu war a jàng ci ayu-bés bi ñuy ame ndaje bu mag bu benn fan bi.
Lépp li Defarkatu Ndaa bu Mag bi bëgg a def, dafa koy def. Waaye dafay may kenn ku nekk ci ñun mu seet ndax dina nangu Defarkatu Ndaa bu Mag bi defar jikkoom. Ñi am xel ba nangu topp ndigalu Yexowa yi ak li Yexowa di def ngir defar suñu jikko, dinañu mel ni ban ci loxo defarkatu ndaa. Dinañu leen defar te jubbanti ba ñu nekk ay ndaa yu am njariñ. Bu ñu nangoo ànd di liggéey ak Yexowa, dañuy màggal kiliftéefam te dinañu ci am barke yu bare.