Ndaje bu mag bu benn fan biy ñëw : li ñu fay waxtaane
Suñu ndaje bu mag bu benn fan bi ci atum liggéeyu waare bu 2009, mu ngi tudd ‘ Farlul ci sas wi ba matal ko ’. Ci Kolos 4:17 lañu ko jële. Ñun karceen yi, xelal boobu duñu ko fowe. Li ñu bëgg mooy, def liggéeyu waare bi, ba mu mat sëkk. Def ko sax ni ko Yeesu defe woon (Ywna 17:14). Ndaw li Pool royukaay bu baax la woon it ci fànn boobu. Moom, dafa fas yéen woon matal liggéeyu waare bi ko Yàlla dénkoon. — Jëf. 20:24.
Waxtaanu wottukat biy wër ci mbooloo yi, dina wone ni waaraatekat yu bare di def ngir génn ci jafe-jafe yi ñuy am ci waaraate bi. Ginnaaw loolu, waxtaan bi tudd “ Cultivez ce que vous avez planté” (maanaam toppatooleen li ngeen ji) dina wone ni ñu mënee dimbali dëgg ñi “ jagoo dund gu dul jeex ” (Jëf. 13:48). Waxtaan bu njëkk bi ki bànqaas bi yónni di def, mi ngi tudd “ Comment nous nous recommandons comme ministres de Dieu ” (maanaam naka lañuy wone ne Yàlla lañuy liggéeyal). Waxtaan boobu dafay topp 2 Korent 6:1 ba 10 aaya par aaya. Ci ngoon si, dina def waxtaan bi tudd “ Tenez votre ministère en haute estime ” (maanaam fonkleen liggéeyu waare bi). Wóor na ne waxtaan yi tudd “ Jeunes et moins jeunes prennent plaisir au ministère ” (maanaam mag ak ndaw bëgg nañu liggéeyu waare bi) ak “ Des jeunes qui accomplissent leur ministère ” (maanaam ay ndaw yuy def seen liggéeyu waare bi ba mu mat sëkk) dinañu leen may doole. Ñi bëgg sóobu ci ndox ci ndaje bu mag bii di ñëw, war nañu ko yégal wottukat biy jiite ci seen mbooloo ni mu gënee gaaw. Benn xaaj bu am solo ci suñuy ndaje yu mag yépp, mooy njàngum La Tour de Garde bi. Nangeen indaale bi ñuy jàng ci ayu-bés bi ñu war a def suñu ndaje bu mag bu benn fan bi.
Bu ñuy def lépp ngir matal suñu liggéeyu waare bi, dañuy fexe ba suñuy itte bopp bañ a ëpp doole liggéey bi ñu Yexowa sant. Ci suñu ndaje bu mag bu benn fan bi, dina am ay xelal yuy maye doole. Xelal yooyu ñu jële ci Mbind mi, war na ñu dimbali ñun ñépp ñu xam li ñu war a def ngir kontine di farlu ci li ëpp solo. Te jàpp bu dëgër ci waaraate bi ngir matal ko.