Naka lañuy jëfandikoo téere bu ndaw bu tudd Qui fait la Volonté de Jéhovah ?
Téere bu ndaw bu bees buy dimbali ñiy jàng Biibël bi ñu miin mbootaayu Yàlla
1. Téere bu ndaw bu tudd Volonté de Jéhovah lan moo ko tax a jóg ?
1 Ci lu yàggul dara jot nañu téere bu ndaw bu tudd Qui fait la Volonté de Jéhovah ?. Ndax jot nga ko jëfandikoo ? Dañu ko defar ngir 1) won ñiy jàng Biibël bi ñun ñooy ñan, 2) dimbali leen ñu xam ci li ñuy yëngu ak 3) won leen naka la suñu mbootaay di doxale. Njàngale yi nekk ci téere bu ndaw bu tudd Volonté de Jéhovah benn xët rekk la. Loolu dina tax ñu mën ko xool ci lu mat 5 ba 10 simili, saa yu ñu paree njàngum Biibël bi.
2. Naka la téere bu ndaw bi bindoo ?
2 Ni mu bindoo : Téere bu ndaw bii dañu ko def ñetti xaaj. Xaaj yi dafa méngoo ak poñ yi ñu lim ci xise bu njëkk bi. Turu 28 xaaj bu nekk ay laaj lañu ko def te turu xaaj yi ñu fésal mbind mi ñooy tontu laaj yi. Ci biir téere bu ndaw bi, def nañu faa ay foto yi ñu jële ci lu ëpp 50 réew ngir wone suñu liggéey ci àddina si sépp. Ci biir yenn xaaj yi am na benn wërale maanaam encadré bu tudd « Allez plus loin... » maanaam Sorileen ci. Am na ay xelal yoo mën a jëfandikoo ngir ñaax ki ngay jàngal Biibël bi mu topp ko.
3. Naka lañuy jëfandikoo téere bu tudd Volonté de Jéhovah ?
3 Naka lañu koy jëfandikoo : Njëkk ko won laaj bi nga xam ne mooy turu njàngale bi. Boo paree nga jàng xaaj bi ak ki ngay jàngal te nga won ko turu xaaj yi ñu fésal. Bu loolu weesoo laaj ko laaj yi nekk ci suufu xët bi. Mën nga jàng xaaj bi yépp, walla nga xaaj ko ngeen di ci waxtaan. Tànnal aaya yi nga war a jàng. Bul fàtte xool ak moom missal yi ak wërale yi tudd « Allez plus loin... » maanaam Sorileen ci. Ci yoon li gën mooy jàng téere bu ndaw bi ci ni xaaj yi topplante. Waaye am na ni muy demee mën nga jàll ci xaaj bi ko soxal. Ci misaal su ndaje bu mag di jegesi, mën nga xool ak moom xaaj 11.
4. Bi nga amee jumtukaay bu bees bii lu tax nga bég ?
4 Bu ñuy jàngal nit Biibël bi, ñu ngi koy dimbali mu jege suñu Baay bi ci kaw asamaan. Waaye war nañu ko xamal it mbootaayu Yexowa (Proverbes 6:20). Am nañu mbégte jot jumtukaay bi ñuy yombalal liggéey bi !