Naka lañuy jëfandikoo téere bu ndaw bu tudd Xebaar bu baax bi jóge ci Yàlla !
Téere bu ndaw bu bees bi ñuy dimbali bu ñuy dellu seeti nit ñi ak komaase njàngum Biibël bi
1. Ban téere bu ndaw lañu jot ci ndaje bu mag bu ñetti fan bu tudd « Sàmmal Sa Xol ! » moo ñu nar a dimbali bu ñuy dellu seeti nit ñi ak komaase njàngum Biibël bi ?
1 Ci ndaje bu mag bu ñetti fan bu tudd « Sàmmal Sa Xol ! », bi ñu jotee téere bu ndaw bu tudd Xebaar bu baax bi jóge ci Yàlla ! Bégoon nañu lool. Mooy wuutu téere bu ndaw bu tudd Lan la ñu Yàlla laaj ?. Dina ñu dimbali ci def ay nouvelles visites, maanaam bu ñuy dellu seeti nit ñi, ak komaase njàngum Biibël bi. Ni téere Lan la ñu Yàlla laaj ? téere bii, njàngaleem dafa gàtt te dafay tax ñu komaase njàngum Biibël bi ci buntu këru nit ki. Téere bu ndaw bu bees bii, dafay wax rekk ci xebaar bu baax bi nekk ci Biibël bi fekk ne téere Lan la ñu Yàlla laaj ? moom, ci rëddi-yooni Yàlla yi rekk la doon wax te loolu jafe woon na ci ki nga xam ne mu ngi sog a jàng Biibël bi mu nangu ko (Jëf ya 15:35).
2. Lu tax ñu defar téere bu ndaw bu tudd Xebaar bu baax ?
2 Lu tax ñu defar téere bu ndaw bu bees bii ? Suñu mbokk yi nekk ci àddina si sépp bëggoon nañu am téere bu yomb boo xam ne dina leen dimbali ñu def ba nit ñi ittewoo dëgg gi te ñu mën leen a jëmele ci téere bu tudd Lan la Biibël bi wax ?, te moom lañuy gën a jëfandikoo ngir jàngale. Nit ñu bari ñi nga xam ne sawaruñu jàng téere yu mag yi duñu bañ a jàng Biibël bi ak téere bu ndaw. Rax-ci-dolli firi téere yu ndaw ci làkk yu bari moo gën a yomb.
3. Lu wuutale téere bii ak suñu yeneen téere yi ?
3 Ni mu bindoo : Lu ëpp ci téere yi ñuy jëfandikoo ngir jàngale Biibël bi dañu leen defar ba nga xam ne nit ki mën na ko nàndal boppam. Téere bu ndaw bii nag du noonu lañu ko defare. Dañu ko defar ngir nit ki jàng ko ak keneen. Loolu moo tax bu ñu koy jox nit ki baax na ñu jàng ak moom benn walla ñaari xise te waxtaan ci ak moom. Ndegam xise yi dañoo gàtt, mën nañu ko gëstu ak nit ki ci buntu këram, walla ci béréb bu muy liggéeye. Li gën mooy nga tambali ci njàngale 1, waaye dara terewul nga tambali ci beneen njàngale.
4. Téere bu ndaw bii, naka la ñuy dimbalee ñu jàngal nit ñi Biibël bi ?
4 Ci suñu téere yu bari tontu yi ñu ngi ci biir xise yi. Waaye ci téere bii, tontu yi ci Biibël bi lañu nekk. Nit ñu bari Biibël bi lañu gën a fonk, waaye du suñu téere yi. Loolu moo tax, aaya yi ñu lim daanaka duggalaatuñu ko ci xise yi. Aaya yi ci Biibël bi rekk lañu koy jàngee. Loolu dina tax kiy jàng Biibël bi xam ne li muy jàng ci Yàlla la jóge (Isaïe 54:13).
5. Lu tax mu am solo ñuy waajal suñu bopp bala ñuy jàng Biibël bi ak nit ku nekk ?
5 Du aaya yi nekk ci biir téere bu ndaw bi yépp lañu tekki. Ndax xam nga lu tax ? Ngir dimbali kiy jàng Biibël bi muy laajte, te it jàngalekat bi jëfandikoo xelam. Loolu moo tax baax na ñuy waajal suñu bopp bala ñuy jàng Biibël bi ak nit ku nekk. Waaye am na fiir buñu war a moytu : bari wax. Dëgg la bëgg nañu nettali li nekk ci Biibël bi. Waaye ndax gënul ñu bàyyi kiy jàng Biibël bi mu tekkil boppam aaya yi ? Boo tànnee ay laaj yu baax dina tax kiy jàng Biibël bi xamal boppam li aaya yi di tekki. (Jëf ya 17:2).
6. Naka lañuy jëfandikoo téere bii a) ci bërëb yi nga xam ne nit ñi gëmuñu Yàlla te gëmuñu Biibël bi ? b) bu ñuy waaraate këroo-kër ? c) bu ñuy komaase njàngum Biibël bi ak defin bu gaaw bi ? d) bu ñuy dellu seeti nit ñi ?
6 Ni yeneen téere yi ñuy jëfandikoo ngir jàngal nit ñi Biibël bi, mën nañu jëfandikoo téere bu ndaw bii saa su nee bu dee sax du moom lañuy wone ci weer boobu. Waaraatekat yu bari dinañu ko jëfandikoo ngir komaase njàngum Biibël bi ci buntu këru nit ñi. Rax-ci-dolli ni ko ndaje bu mag bu ñetti fan yi wonee téere bu ndaw bi « mën na tax booy dellu seeti nit ñi yi mu doon lu neex ». (Xoolal wërale yi nekk ci xët 3 ba 5.)
7. Njàngum Biibël bi, naka lañu ko mën a defe ak téere bu ndaw bii ?
7 Ni ñuy defe njàngum Biibël bi : Njëkkal a jàng laaj yi ñu def nimoro te ñu fésal ko. Boo paree nga jàng xise bi ak aaya bi walla aaya yi ñu dëngal mbind mi. Tànnal bu baax ay laaj ngir dimbali nit ki mu nànd li aaya yi di tekki. Bu loolu weesoo waxal nit ki mu tontu ci laaj bi ñu fésal. Loolu dina tax nga xam ndax nànd na li mu jàng. Booy njëkk a dellu seeti nit ñi, li gën mooy ngeen yem ci benn laaj. Bu ngeen di gën a jàng seen waxtaan di gën a yàgg, loolu dina tax nga mën a def benn njàngale lëmm.
8. Bala ñuy jàng benn aaya lan lañu war a wax, ak lu tax ?
8 Aaya yi nga xam ne def nañu ci « jàngal » ñooy tontu laaj yi ñu bind te mu fés. Bala ñuy jàng benn aaya, nañu moytu di wax lii : « Xoolal li ndaw li Pool bind » walla naan « Xoolal li Yérémi yégle woon ». Su ko defe nit ki dina foog ne ay nit doŋŋ ñoo bind li ñu nar a jàng. Li gën mooy ñuy wax nee : « Xoolal li Kàddu Yàlla wax » walla ñu nee : « Xoolal li Biibël bi yégle woon ».
9. Bu ñuy def njàngum Biibël bi ndax dañoo war a jàng aaya yi ñu lim yépp ?
9 Ndax dañoo war a jàng aaya yi ñu lim yépp walla aaya yi ñu bind « jàngal » rekk lañu war a jàng ? Lépp a ngi aju ci ni mbir mi demee. Aaya yi ñu lim li ko tax a jóg nekkul di ñu won fi xalaat yi nekk ci Biibël bi. Aaya yépp a am solo bi tax ñu mën leen a jàng. Waaye kiy jàng Biibël bi su amul jot bu bari, walla waxtaan bi soxalu ko walla sorewul ci jàng, nañu jàng kese ak moom aaya yi ñu bind « jàngal ».
10. Kañ lañu mën a jëfandikoo téere bu tudd Lan la Biibël bi wax ? ngir jàngal nit ñi Biibël bi ?
10 Nañu jàll ci téere bu tudd Lan la Biibël bi wax ? : Bu ñuy waxtaan ak moom saa su nee, mën nañu jàll ci téere bu tudd Lan la Biibël bi wax ?, walla ñu àggale téere bu ndaw bu tudd Xebaar bu baax. Waaraatekat bi war na jëfandikoo xelam bu baax ngir xam ndax war na jàll ci téere bu tudd Lan la Biibël bi wax ?. Bu ñuy jàll ci téere boobu ndax war nañu komaase ci pàcc bu njëkk bi ? Waxuñu ci dara. Ñiy jàng Biibël bi dañoo wuute. Waaye am na solo nit ki xóotal xam-xamam ci téere bu tudd Lan la Biibël bi wax ? ci li ñu jot a waxtaan ak moom.
11. Lu tax ñu war a jëfandikoo bu baax téere bu ndaw bu bees bii ?
11 Dañoo nekk ci jamono joo xam ne xebaar bu neex baretul, am nañu cër bu réy ci xamal nit ñi xebaar yi gën a neex : Nguuru Yàlla sàmpu na te léegi mu indi jamono ju bés fa njub dëkk (Macë 24:14 ; 2 Piyeer 3:13). Wóor nañu ne ñu bari ñu dëgg xebaar bi ànd nañu ak Kàddu Yàlla yii : “ Kiy yégle xibaar bu baax bi, kiy yégle jàmm, kiy indi xibaar buy wone lenn lu gën, kiy yégle mucc gi, kiy wax Siyon : ‘ Seen Yàlla nekk na buur ! ’, kooku, tànk yi muy teg ci kow tund yi rafet nañu lool. ” (Isaïe 52:7, NW). Nañu jëfandikoo bu baax téere bu ndaw bu bees bii ngir indil nit yi nekk ci suñu gox xebaar bu baax bi jóge ci Yàlla !
[Wërale bi nekk ci paas 3]
Ci béréb yi nga xam ne nit ñi gëmuñu Yàlla te gëmuñu Biibël bi :
● Ci yenn gox yi, waaraatekat yi seetlu nañu ne baat yu mel ni « Yàlla » ak « Biibël » dafay yàkk waxtaan. Su fekkee ne loolu la, booy njëkk a waxtaan ak nit ki li gën mooy nga waxtaan ak moom ci mbir yi ko soxal, lu mel ni am nguur gu baax, ay xelal yu baax yu jëm ci dund njaboot, ak li ñu mën a séentu ëllëg. Bu ngeen waxtaane ay yooni-yoon, ci ni ñu xame ne Yàlla am na, ak lu tax ñu mën a wóolu Biibël bi, su booba mën nga jëfandikoo téere bu ndaw bu tudd Xebaar bu baax.
[Wërale bi nekk ci paas 4]
Bu ñuy waaraate këroo-kër :
● « Bëgg naa la won ne jafewul xam li Yàlla bëggal doomu Aadama yi. Ndax mas nga laaj sa bopp ndax Yàlla dina fi mas a jële coono yi ? [Mayal nit ki mu tontu.] Téere bu ndaw bii dafay wone fan lañu mën a gise tontu laaj bii ci Biibël bi. [Joxal nit ki benn téere te nga jàng ak moom xise bu njëkk ci njàngale 1, ak Yérémi 29:11.] Ci li ñu gis nii, ndax am na lu tax ñu mën a gëm ne Yàlla bëgg na ñu am ëllëg bu neex ? [Mayal nit ki mu tontu.] Soo bëggee mën naa la bàyyil téere bi. Beneen yoon mën nañu waxtaan ci ñaareelu xise bi. Di nga gis li Biibël bi tontu ci laaj bii : Naka la Yàlla di fi jële liy indi coono ? » su nit ki ame jot, mën nga waxtaan ak moom ci ñaareelu xise bi ak ñetti aaya yi. Tànnal ak moom bés bi ngay dellusi ngir waxtaan ci ñaareelu laaju njàngale bi.
● « Ñu bari dañuy ñaan Yàlla bu ñu ame poroblem. Ndax ci nga bokk ? [Mayal nit ki mu tontu.] Ci sa xalaat ndax Yàlla ñaan yépp lay déglu walla am na ñaan yi mu dul déglu ? [Mayal nit ki mu tontu] Téere bii dafay wone ni ñu mën a gise li Biibël bi tontu ci laaj boobu. [Joxal nit ki benn téere te nga jàng ak moom xise bu njëkk bi ci njàngale 12 ak aaya yi ñu bind « jàngal ».] Yàlla nangu déglu suñuy ñaan ndax loolu yéemewul ? Ngir jariñoo bu baax ñaan, fàww ñu xam Yàlla. [Won ko turu xaaj yi nekk ci njàngale 2] Soo bëggee mën naa la bàyyil téere bii, te beneen yoon dinañu jàng li Biibël bi tontu ci laaj yu am solo yi. »
● « Seetlu na ne ñu bari ci nit ñi dañuy laaj seen bopp fan la àddina sii di mujje. Ndax yaakaar nga ne li xew ci àddina sii dina mas a soppeeku ? [Mayal nit ki mu tontu.] Ñu bari bu ñu xame ne Biibël bi am na xebaar bu baax ngir ëllëg loolu dafa leen di jaaxal. Xoolal yenn laaj yi Biibël bi di tontu. » Joxal nit ki benn téere, nga won ko xët bu mujj bi te nga laaj ko ban laaj moo ko soxal. Soo paree ubbil téere bu ndaw bi ci njàngale bi méngoo ak laajam te ngeen waxtaan ci. Tànnal ak moom bés bi ngay dellusi ngir waxtaan ci laaj bi ci topp.
[Wërale bi nekk ci paas 5]
Defin bi gën a gaaw :
● « Dama ñëw won la fasoŋ bu bees bu ñuy defe suñu njàngum Biibël bi. Téere bu ndaw bii dafay wone fan ci sa Biibël nga mën a gise tontu ci 15 laaj yu am solo. [Won ko xët bu njëkk bi ak bu mujj bi.] Ndax mas nga jéem a nàndal sa bopp Biibël bi ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xoolal ni njàngale yi yombe. [Ubbil téere bi ci njàngale 3, te ngeen jàng xise bu njëkk bi ci laaj 3 ngeen jàng it Peeñu ma 21:4, 5. Su mënee nekk, jàngal ak moom xise bi ci topp ak aaya yi ñu bind « jàngal ».] Soo bëggee, mën naa la bàyyil téere bu ndaw bii. Mangi lay xiirtal nga jéem a def njàngale bu bees bii, bu dee sax benn yoon la. Soo bëggee mën nañu kontine waxtaan bi. Beneen yoon mën nañu waxtaan ci njàngale bu njëkk bi. Gisal, benn xët rekk la. »
[Wërale bi nekk ci paas 5]
Bu ñuy dellu seeti nit ñi :
● « Kontaan na gisaat la. Indil naa la téere bu ndaw buy wone tontu yi Biibël bi joxe ci ay laaj yu am solo. [Jox ko benn téere nga wax ko mu xool xët bu mujj bi.] Ban waxtaan moo la gën a itteel ? [Mayal nit ki mu tontu. Soo paree, ubbil téere bi ci njàngale bi nit ki tànn.] May ma ma won la ni ñuy jëfandikoo téere bu ndaw bii ngir gis li ci Biibël bi tontu. » Won ko naka lañuy defe njàngum Biibël bi : waxtaanal ak moom ci benn walla ñaari xise ak aaya yi ñu bind « jàngal ». Jeex na, komaase nga njàngum Biibël bi ! Bàyyil nit ki téere bi te nga tànn ak moom bés bi ngay dellu seetsi ko. So leen jeexalee njàngale bi yépp, mën nga ko wax mu tànn beneen waxtaan, walla ngeen njëkke fi njàngale bi komaasee.