TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • my nettali 11
  • Xon gu jëkk gi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Xon gu jëkk gi
  • Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Artu bu jóge ca lu amoon
    Mën nga nekk xaritu Yàlla !
  • Ca jamano yonent Yàlla Nóoyin — ñan ñoo déggoon li Yàlla wax te ñan ñoo bañoon a dégg ?
    Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Nit ku nekk am na li nga mën a jàng ci wideo bi tudd : Noé : il marchait avec Dieu
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Nóoyin dafay defar gaal gu mag
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
my nettali 11
Xon gu jëkk gi ci asamaan, gaalu Nóoyin gi mu ngi teggu ci suuf su wow

NETTALI 11

Xon gu jëkk gi

NDAX xam nga li Nóoyin jëkk a def bi mu génnee gaal ga, moom ak njabootam ? Dafa jël ay mala, def leen sarax yu mu jébbal Yàlla. Loolu lañuy wone fii ci suuf. Nóoyin dafa bëggoon a gërëm Yàlla ci li mu musal njabootam ci taw bu metti boobu.

Ci sa xalaat, ndax sarax boobu neexoon na Yexowa ? Waawaaw, neexoon na ko kay. Yàlla dig na sax Nóoyin ne dootul indi taw buy alag àddina si sépp.

Nóoyin ak njabootam ñu ngi def sarax yu ñu jébbal Yexowa ngir gërëm ko

Yàggul, suuf si wow, Nóoyin ak njabootam daldi tàmbali dund gu bees. Yàlla barkeel na leen te ne leen : ‘ War ngeen a am doom yu bare ba feesal àddina si sépp. ’

Waaye bu yàggee, bu nit ñi déggee taw bu metti boobu, xéyna dinañu ragal mu amaat. Kon Yàlla def na lu leen di fàttali li mu waxoon, maanaam dootul indi taw bu metti ci kow suuf si sépp. Xam nga lan la def ? Xon gi.

Xon, dañu ko faral a gis ci asamaan bu naaj bi génnee ginnaaw taw bi. Am na kulóor yu rafet. Ndax mas nga ko gis ? Ndax gis nga bi ñuy wone fii ?

Lii la Yàlla wax : ‘ Dootul amati taw buy alag nit ak mala yépp yi nekk ci kow suuf. Maa ngi def sama xon ci niir yi. Bu feeñee ci asamaan, dinaa ko gis te dinaa fàttaliku li ma dige noonu. ’

Kon boo gisee xon gi, lan nga war a fàttaliku ? Danga war a fàttaliku li Yàlla dige, maanaam dootul indi taw bu metti ngir alag lépp ci àddina si.

Njàlbéen ga 8:18-22 ; 9:9-17.

Laaj yi

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager