TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • Ñan ñooy seede Yexowa yi dëgg-dëgg ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 1

      Ñan ñooy seede Yexowa yi dëgg-dëgg ?

      Benn seede Yexowa ci réewu Danemark

      Danemark

      Ay seede Yexowa ci réewu Taïwan

      Taïwan

      Ay seede Yexowa ci réewu Vénézuéla

      Vénézuéla

      Ay seede Yexowa ci réewu Inde

      Inde

      Ndax xam nga ay seede Yexowa fi nga dëkk, fi ngay liggéeye walla fi ngay jànge ? Walla ndax mas nañu wax ak yaw ci Biibël bi ? Seede Yexowa yi, ñan lañu dëgg-dëgg ? Lu tax ñuy wax ak ñépp ci li ñu gëm ?

      Ay nit lañu ni ñépp. Bokkuñu cosaan te yemuñu am-am. Ñu bare ci ñun dañu bokkoon ci yeneen diine. Am na sax ñoo xam ne gëmuñu woon ne Yàlla am na. Waaye bala ñuy nekk ay seede Yexowa, dafa fekk ñu jël jot ngir jàng bu baax li nekk ci Biibël bi (Jëf ya 17:11). Ba pare ñu gëm li ñu jàng te kenn ku nekk ci ñun tànn nekk kuy jaamu Yexowa Yàlla.

      Njariñ lañuy jële ci jàng Biibël bi. Ni ñépp, dañuy am coono. Dañuy xeex itam suñu matadi. Waaye nag gis nañu ne dañu gën a am jàmm ci suñu dund ndaxte bés bu nekk ñu ngi def lépp ngir topp li Biibël bi santaane (Sabóor 128:1, 2). Njariñ boobu bokk na ci li tax ñu sawar a séddoo ak nit ñi li ñu jàng ci Biibël bi.

      Santaane Yàlla yi ñoo ñuy wommat. Topp santaane yooyu nekk ci Biibël bi mooy dimbali nit mu am xel mu dal, mu may cér moroomam te am ay jikko yu mel ni njub ak mbaax. Dafay tax it ñu nekk ay nit yuy sàmm seen wér-gi-yaram te am njariñ fi ñu nekk. Dafay yokk juboo ci biir kër te xiir nit ñi ci am dundin bu sell. Ndegam wóor na ñu ne “ Yàlla du gënale, ” ñun itam seetuñu xeet, seetuñu réew, waaye ci àddina si sépp, ñun seede Yexowa yi, ñu ngi mel ni ay mbokk ndax li ñu bokk li ñu gëm. Dëgg la, ay nit lañu mel ni ñépp waaye amul mbooloo bu mel ni suñu bos. — Jëf ya 4:13 ; 10:​34, 35.

      •  Lu tax ñu mën a wax ne seede Yexowa yi ay nit lañu mel ni ñépp ?

      •  Yan santaane Yàlla la seede Yexowa yi jàng ci seen gëstu Biibël bi ?

  • Lu tax ñu tudd Seede Yexowa ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 2

      Lu tax ñu tudd Seede Yexowa ?

      Nóoyin

      Nóoyin

      Ibraayma ak Saarata

      Ibraayma ak Saarata

      Musaa

      Musaa

      Yeesu Kirist

      Yeesu Kirist

      Ñu bare dañu foog ne tur boobu, turu diine bu bees la. Waaye lu ëpp 2 700 at ci ginnaaw, dañu doon woowe jaamukati Yàlla dëgg ji ay seedeem (Isaïe 43:​10-12). Ba ci atum 1931, ñu ngi ñu doon woowe Gëstukati Biibël bi. Waaye lu tax ñu mujj a jël turu seede Yexowa ?

      Tur boobu dafay wone ne Yàlla bi ñuy jaamu Yexowa la tudd. Bu ñu seetee ci téere yu sell yi ñu njëkk a bind ak loxo, turu Yàlla, Yexowa, feeñ na ci ay junniy yoon. Waaye ñu bare ci ñi doon tekki Biibël bi ci yeneen làkk, dañu dindi tur boobu def ci “ Boroom bi ” walla “ Yàlla ”. Waaye Yàlla dëgg ji, moom ci boppam, moo wax yonent Yàlla Musaa ne turam mooy Yexowa, teg ci ne : “ Loolu mooy sama tur ba fàww ” (Gàddaay gi 3:15). Wax jooju wone na ne Yàlla dafa bañ ñu jaawale ko ak yeneen yàlla yu dul dëgg yi. Kon di wuyoo turu Seede Yexowa, lu réy la ci ñun ndaxte turu Yàlla bu sell bi moo ci nekk.

      Tur boobu dafay wone liggéey bi ñuy def. Ñun dañuy seede dëgg gi jëm ci Yàlla. Dafa mel ni nga am xarit bu baax te doon ku jub te nga dégg ñu koy jëw. Bu booba looy def ? Xanaa seede dëgg gi nga xam ci moom ! Loolu mooy li ñuy def tey. Ca jamono yu njëkk ya, nit ñu bare dañu doon seede ci seen ngëm ci Yexowa. Abel moo ci njëkk. Nóoyin, Ibraayma, Saarata, Musaa, Daawuda ak ñeneen bokkoon nañu ci itam. Kàddu Yàlla mu ngi leen di woowe ‘ mbooloo mu bare miy seedeel seen ngëm ’ (Yawut ya 11:​4–12:⁠1).

      Dañuy roy ci Yeesu. Ci Biibël bi ñu ngi woowe Yeesu “ seede bu takku bi te dëggu ” (Peeñu ma 3:14). Yeesu ci boppam wax na ne dafa ‘ xamle turu Yàlla ’ te ‘ wax dëgg gi ’ jëm ci Yàlla (Yowaana 17:26 ; 18:37). Kon karceen dëgg, dafay yor turu Yexowa te xamle ko. Loolu la seede Yexowa yi di jéem a def.

      •  Lu tax ñi ñu doon woowe Gëstukati Biibël bi mujj a jël turu seede Yexowa ?

      •  Kañ la Yexowa am ñu koy seede ci kaw suuf ?

      •  Kan mooy seede Yexowa bi gën a mag ?

      XÓOTALAL WAXTAAN BI

      Boo ñëwee ci ndaje yi ñuy am ci suñu mbooloo yi, jéemal a xamante ak nit ñi. Mën nga laaj lii : “ Lu tax nga bokk ci seede Yexowa yi ? ”

  • Dëgg gi nekk ci Biibël bi te réeroon naka la feeñaate ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 3

      Dëgg gi nekk ci Biibël bi te réeroon naka la feeñaate ?

      Gurupu góor yu nekk di gëstu Biibël bi ci ati 1870

      Gëstukati Biibël bi ci ati 1870

      Benn góor buy jàng La tour de Garde bi njëkk a génn

      La Tour de Garde bi njëkk a génn, 1879

      Jigéen bu yore benn La Tour de Garde ak benn Réveillez-vous !

      La Tour de Garde tey

      Biibël bi yégle woon na ne gannaaw deewu Yeesu, dina am ay jàngalekat yuy naxaate yuy jóg ci biir karceen yu njëkk ya te soppi dëgg gi nekk ci Biibël bi (Jëf ya 20:​29, 30). Ni mu ko waxe woon, noonu la ame. Jàngalekat yooyu dañu jaxase njàngale Yeesu yi ak ay njàngale diine xërëmkat yi. Loolu moo indi réer ci biir diine karceen (2 Timote 4:​3, 4). Lan moo ñu mën a wóor ne tey, li ñu xam ci Biibël bi mooy li Biibël bi wax dëgg-dëgg ? 

      Jamono ji Yàlla bëggoon a feeñal dëgg gi agsiwoon na. Yàlla waxoon na ne ci muju jamono xam-xam dëgg dina bare (Daniel 12:⁠4). Ci atum 1870 amoon na benn gurupu nit yu doon daje ngir xam dëgg gi nekk ci Biibël bi. Dañu gisoon ne, diine yiy wuyoo turu karceen ñu ngi doon jàngale lu bare lu nekkul ci Biibël bi. Ñu daldi gëstu Biibël bi ngir xam li mu wax dëgg-dëgg te Yexowa dimbali na leen ci bu baax.

      Ay góor yoo xam ne xam dëgg gi rekk moo leen tax a jóg ñoo gëstu Biibël bi. Fasoŋ bi ñu doon gëstoo Biibël bi, ba tey ñun fasoŋ boobu lañuy topp. Dañu doon tànn benn waxtaan, xool li ci Biibël bi wax. Bu ci amee aaya bu leerul, ñu xool yeneen aaya ngir xam li aaya boobu bëggoon a wax. Bu ñu demee ba li ñu nànd ànd ak lépp li nekk ci Biibël bi, ñu daldi ko bind. Kon dañu doon bàyyi Biibël bi firi boppam. Noonu la dëgg gi feeñaate ba ñu xam dëgg gi jëm ci turu Yàlla, ci nguuru Yàlla, ci li tax Yàlla sakk nit ak suuf si, ci liy xew gannaaw dee, ak ci yaakaaru gis ñi dee dundaat. Gëstu boobu muccal na leen ci njàngale yu dul dëgg ak ay jëf yu bon yu bare. — Yowaana 8:​31, 32.

      Ci booru atum 1879, Gëstukati Biibël bi gisoon nañu ne jot na ngir ñépp xam dëgg gi. Ci at moomu, dañu komaase di génne benn yéenekaay biy génn ba tey te tudd ci tubaab La Tour de Garde annonce le Royaume de Jéhovah. Tey ci àddina si sépp, ci lu mat 240 réew ñu ngi tasaare dëgg gi nekk ci Biibël bi ci lu mat 750 làkk. Xam-xam dëgg masul a baree nii !

      •  Gannaaw deewu Yeesu, lan moo xewoon ak dëgg gi nekk ci Biibël bi ?

      •  Naka lañu def ba dëgg gi nekk ci Kàddu Yàlla feeñaat ?

  • Lu tax seede Yexowa yi tekki Biibël bi ci làkk yu bare ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 4

      Lu tax seede Yexowa yi tekki Biibël bi ci làkk yu bare ?

      Benn masiin bu yàgg buy sotti ay téere
      Traduction du Monde Nouveau, bi mu njëkkee génn ci ãgale
      Ay nit yuy xool Traduction du Monde Nouveau ca Congo (Kinshasa)

      Congo (Kinshasa)

      Traduction du Monde Nouveau, bi muy njëkk a génn ca Rwanda

      Rwanda

      Turu Yàlla bi feeñ ci version de Symmaque

      Turu Yàlla bi feeñ ci Sabóor 69:31, version de Symmaque (IIIe ou IVe siècle de notre ère).

      Seede Yexowa yi yàgg nañu di jàng, di sotti te di joxe ay Biibël. Waaye dañu gisoon ne soxla nañu ñu tekki Biibël bi ci fasoŋ buy gën a tax nit ñi “ xam dëgg gi ” ndaxte dëgg googu la Yàlla bëgg ñépp xam (1 Timote 2:⁠3, 4). Loolu moo tax ñu komaase di tekki Biibël bi ci fasoŋ bu gën a yomb a nànd, tudde ko Traduction du monde nouveau ci tubaab. Ci atum 1950 lañu tàmbalee génne xaaj yi ñu tekki. Tekki nañu Biibël bi ci lu ëpp 130 làkka te bi ñu koy tekki dañu def lépp ngir bañ a soppi xalaat yi, bañ ci yokk dara, bañ ci wàññi dara.

      Dañu soxla woon tekki Biibël bu ñépp mën a nànd. Ci Biibël yu bare yu ñu tekki, ay baat yu naqaree nànd te xewwi ñoo ci nekk. Li waral loolu mooy, lu ñuy gën di dem, làkk yi di soppeeku. Am na it ay boroom xam-xam yu gis ay sotti Biibël yu yàgg yoo xam ne loxo lañu leen binde te ñu gën a jege te gën a méngoo ak sotti Biibël yu njëkk ya. Loolu tax na ñu gën a mokkal làkk yi ñu binde Biibël bi, maanaam Ebrë, Arameyni ak Gereg te mën koo tekki ci fasoŋ bu gën a leer.

      Dañu soxla woon tekki Biibël bu dul soppi Kàddu Yàlla. Ñiy tekki kàddu Yàlla waruñu ko tekki nu mu leen neexe. Dañu war a yem ci li kàddu Yàlla wax. Waaye dañu seetlu ne ci Biibël yu bare dañu dindi turu Yàlla, maanaam Yexowa.

      Dañu soxla woon tekki Biibël buy jox Yàlla mi ko bind cér bi mu yelloo (2 Samuel 23:⁠2). Turu Yàlla, maanaam Yexowa, feeñoon na ca sotti Biibël yu njëkk ya lu jege 7000 yoon (foto bi ci suuf mu ngi ci wone benn). Loolu moo tax, bi ñuy tekki Biibël bi tudd Traduction du Monde Nouveau, seede Yexowa yi delloowaat nañu tur boobu fépp fi mu feeñoon (Psaume 83:18). Bala ñuy génne tekki Biibël boobu def nañu ay gëstu yu bare ci lu yàgg. Loolu moo tax tekki boobu neex a jàng. Nga am Traduction du Monde Nouveau ci sa làkk walla déet, fexeel ba di jàng kàddu Yexowa bés bu nekk. — Yosuwe 1:8 ; Sabóor 1:​2, 3.

      • Lu tax seede Yexowa yi tekki Biibël bi ?

      • Ku bëgg a xam li Yàlla bëgg, lan la war a def bés bu nekk ?

      [Li ñu bind ci suuf]

      a Traduction du Monde Nouveau amagul ci wolof waaye mën nga ko am ci yeneen làkk.

Téere yi ci Wolof (1996-2025)
Ngir génn
Ngir konektewu
  • Wolof
  • Yónnee ko
  • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
  • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
  • Conditions d’utilisation
  • Règles de confidentialité
  • Paramètres de confidentialité
  • JW.ORG
  • Ngir konektewu
Partager