-
Naka la magi mbooloo mi di dimbalee waa mbooloo mi ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 15
Naka la magi mbooloo mi di dimbalee waa mbooloo mi ?
Finlande
Jàngale
Sàmm
Waare
Ci suñu mbootaay amuñu ay kilifa diine yu ñuy fey ndax seen liggéey. Ni ñu ko daan defe ci mbooloo karceen yu njëkk ya, tey ay góor yu mat njiit lañuy tànn ngir ñu “ sàmm mbooloo mi ” Yàlla moom (Jëf ya 20:28). Mag yooyu dañu am diggante bu rattax ak Yàlla. Ñoom ñooy jiite te di sàmm mbooloo mi. Defuñu ko ni ku “ sañul-bañ, waaye di surgay Yàlla ci xol bu tàlli, ak xol bu laab te bañ cee séentu alal ” (1 Piyeer 5:1-3). Naka la mag yooyu di ñu dimbalee ci mbooloo mi ?
Ñu ngi ñuy toppatoo te di ñu sàmm. Magu mbooloo yi ñoo ñuy dimbali ci aar suñu diggante ak Yàlla. Ñoom, xam nañu ne Yàlla moo leen dénk liggéey bu am solo boobu. Loolu moo tax duñu noot mbooloo mi, waaye dañuy def lépp ngir waa mbooloo mi am jàmm ak mbégte (2 Korent 1:24). Sàmmkat bu baax dafay toppatoo xar bu nekk ci géttam. Magu mbooloo yi ñoom itam, dañuy def lépp ngir xam kenn ku nekk ci seen mbooloo. — Kàddu yu Xelu 27:23.
Ñu ngi ñuy jàngal ni ñuy toppe li Yàlla santaane. Semen bu nekk, magu mbooloo yi dañuy jiite ndaje yi ñuy am ci mbooloo mi ngir dëgëral suñu ngëm (Jëf ya 15:32). Ñoom ñooy jiitu itam liggéeyu waare bi. Dañuy ànd ak ñun ci waaraate bi te di ñu jàpple ci bépp fànn ci liggéeyu waare bi.
Ñu ngiy jox kenn ku nekk ci ñun xelal yi mu soxla. Mag yi ci suñu mbooloo dañu bëgg ñu am diggante bu rattax ak Yexowa. Moo tax lée-lée dañuy ñëw di ñu seetsi ci suñuy kër walla ñuy waxtaan ak ñun ci suñu saalu Nguur gi. Li ñu bëgg mooy won ñu ci Mbind mu sell mi liy dëgëral suñu ngëm ak li mën a dëfël suñu xol. — Saag 5:14, 15.
Liggéey boobu yépp la magu mbooloo yi di def, teg ci ne ñi ëpp ci ñoom ay boroom kër lañu te yore seen liggéeyu bopp. Xam nañu ne loolu dafay laaj jot ak toppatoo. Dëgg-dëgg suñu mbokk yu góor yooyu ñeme nañu liggéey, moo tax yelloo nañu ñu may leen cér bu réy. — 1 Tesalonig 5:12, 13.
Lan mooy liggéeyu magu mbooloo ?
Naka la magu mbooloo yi di wonee ne yëg nañu kenn ku nekk ci ñun ?
-
-
Lan mooy liggéeyu ñiy topptoo yëfi mbooloo mi ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 16
Lan mooy liggéeyu ñiy topptoo yëfi mbooloo mi ?
Birmanie
Waxtaan ci mbooloo mi
Ndaje bi ñuy def bala ñuy waare
Set-setalu saalu Nguur
Biibël bi wax na ci ñaari gurupu karceen yu góor yu ñu dénk liggéey ci mbooloo mi, “ njiit ” yi ak “ ñiy topptoo yëfi mbooloo mi ” (Filib 1:1). Ñaari gurup yooyu ñu ngi ci li ëpp ci mbooloo yi. Ñiy topptoo yëfi mbooloo mi, ban liggéey bu am njariñ lañuy def ci biir mbooloo mi ?
Dañuy jàpple magi mbooloo mi. Ñiy topptoo yëfi mbooloo mi, dañu am diggante bu rattax ak Yexowa. Dañu nekk ñu jar a wóolu te dañu farlu ci seen liggéey. Am na ci ñoom ay mag ak ay waxambaane. Liggéey bu am solo lañuy def ci mbooloo mi ndaxte ñoom ñoo féete ci lépp luy liggéeyu doole ak yeneen liggéey yi mbooloo mi laaj ngir doxalinam. Loolu dafay may magi mbooloo mi ñu gën a am jot ngir def seen liggéey, maanaam jàngal ak sàmm mbooloo mi.
Dañuy topptoo yëf yu bare. Dañu leen di dénk lu bare ci mbooloo mi, lu mel ni : teeru ñi ñëw ci ndaje yi, topptoo lépp lu jëm ci mikoro yi ak misik bi, topptoo xaalisu mbooloo mi walla téere yi ñuy jot ci mbooloo mi, ak wax waa mbooloo mi béréb yi ñu war a waare. Dañuy bokk itam ci topptoo bi ak set-setalu saalu Nguur gi. Lée-lée magi mbooloo mi wax leen ñu jàpple ñi màgget ci mbooloo mi. Ñiy topptoo yëfi mbooloo mi, ñu ngi def ak xol bu tàlli bépp liggéey bu ñu leen dénk ci mbooloo mi, moo tax ñépp may leen cér. — 1 Timote 3:13.
Dañu nekk ay royukaay yu rafet ci karceen yu góor yi. Ñiy topptoo yëfi mbooloo mi, dañu leen di tànn ndax seen jikko karceen ju rafet. Ñoom, bu ñuy bokk ci njàngale mi ñuy def ci mbooloo mi, dañuy dëgëral suñu ngëm. Ñun, bu ñu gisee ni ñu saware ci liggéeyu waare bi, loolu dafa ñuy sawarloo it. Seen ànd bu rafet ak mag yi mooy yokk jàmm ak déggoo bi am ci mbooloo mi (Efes 4:16). Xéyna bu yàggee, ñoom it dinañu mat a nekk mag ci mbooloo mi.
Ñiy topptoo yëfi mbooloo mi, yan jikko lañu war a am ?
Ñiy topptoo yëfi mbooloo mi, ban njariñ la seen liggéey am ?
-
-
Naka la wottukat yiy wër di ñu dimbalee ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 17
Naka la wottukat yiy wër di ñu dimbalee ?
Malawi
Ndaje bi ñuy def bala ñuy waare
Liggéeyu waare bi
Ndaje magi mbooloo mi
Ci xaaju Biibël bi ñu bind ci làkku gereg, wax nañu lu bare ci Barnabas ak ci ndaw li Pool. Góor yooyu ay wottukat yuy wër lañu woon ci mbooloo karceen yu njëkk ya. Lan moo tax ñu doon wër ci mbooloo yi ? Dañu bëggoon a dimbali seeni mbokk ci ngëm ñu dëgëral seen diggante ak Yàlla. Pool dafa waxoon ne dafa bëgg a “ dellu seeti bokk ya ” ba xam nu ñu def. Dafa ko jaraloon muy tukki lu tollook ay junniy kilomet ngir dem dooleel leen (Jëf ya 15:36). Tey itam, loolu la suñu wottukat yiy wër bëgg.
Dañuy ñëw ngir dooleel ñu. Ñaari yoon ci at mu nekk, wottukat buy wër bu nekk dafay seeti lu tollu ak 20 mbooloo te toog lu mat benn semen ci mbooloo mu nekk. Mën nañu jàng lu bare ci wottukat yooyu ak ci seeni jabar. Wottukat yi dañuy jéem a xam ñépp, mag ñi ak ndaw ñi, di ñu gunge ci liggéeyu waare bi, di ànd ak ñun ci suñuy njàngum Biibël. Bu ñu ñëwee ci mbooloo yi, dañuy ànd ak magi mbooloo yi ci seeti ay mbokk ci mbooloo mi. Dañuy def ay waxtaan ci suñu ndaje yi ci saalu Nguur gi ak ci suñu ndaje yu mag yi ngir dooleel ñu. — Jëf ya 15:35.
Dañu yëg kenn ku nekk ci ñun. Li wottukat yiy wër bëgg mooy dimbali mbooloo yi ci wàllu ngëm. Dañuy waxtaan ak magi mbooloo mi ak ñiy toppatoo yëfi mbooloo mi ngir xam fi mbooloo mi tollu ci wàllu ngëm, te jox leen itam ay tegtal ngir ñu gën a mën a def seen liggéey. Dañuy dimbali pioñee yi ñu jëm kanam ci seen liggéeyu waare. Dañuy xamante itam ak ñi door a bokk ci mbooloo mi te waxtaan ak ñoom ci lu rafet li ñuy def ci wàllu ngëm. Kenn ku nekk ci wottukat yooyu dafay jële boppam ni suñu ‘ nawle ci liggéey ’ te nangu sonn ngir suñu njariñ (2 Korent 8:23). Nañu leen roy ci seen ngëm ak ci li ñuy def lépp ngir jaamu Yàlla. — Yawut yi 13:7.
Lu tax wottukat yiy wër di seeti mbooloo yi ?
Ban njariñ lañu mën a jële ci seen ñëw ?
-
-
Lan lañuy def ngir dimbali suñuy mbokk ci ngëm yi musiba dal ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 18
Lan lañuy def ngir dimbali suñuy mbokk ci ngëm yi musiba dal ?
République dominicaine
Sapoŋ
Haïti
Bu musiba amee, dañuy def lépp, ñun seede Yexowa yi, ngir gaaw a dem dimbali suñuy mbokk ci ngëm yi musiba boobu dal. Ndimbal boobu dafay wone mbëggeel dëgg bi ñu am ci suñu biir ( Yowaana 13:34, 35 ; 1 Yowaana 3:17, 18). Naka lañuy dimbalee suñu mbokk yooyu ?
Dañuy joxe xaalis. Bi xiif bu metti amee ci dëkku Yude, karceen yu njëkk ya dañu yónnee woon xaalis ngir dimbali seeni mbokk ci ngëm ya fa dëkkoon (Jëf ya 11:27-30). Ñun itam, fépp fu ñu dégg ci àddina si ne am na suñuy mbokk ci ngëm yu nekk ci jafe-jafe, dañuy yónnee lu leen di dimbali jaarale ko ci suñu mbooloo yi. — 2 Korent 8:13-15.
Dañu leen di fajal seeni soxla. Bu musiba amee ci béréb, magi mbooloo ya fa nekk dañuy seet ku nekk ci waa mbooloo mi ba xam ndax ñépp a mucc. Lée-lée dafay am kurélu ñiy dimbali buy def lépp ba nit ñi jot lu ñuy lekk ak ndox bu ñu mën a naan ak ay yére, am fu ñuy fanaan te mën a faju. Am na itam ay seede Yexowa yu bare yuy jël ci seen alal te demal seen bopp ca béréb yooyu. Dañuy bokk ci ndimbal boobu walla ci defaraat kër ak saalu Nguur yi yàqu. Li ñu may ñu mën a def loolu yépp ci ni mu gën a gaawe mooy juboo bi ñu am ci suñu biir ak tàmm a ànd di liggéey. Dëgg la, dañuy dimbali sunuy mbokk ci gëm waaye saa yu ñu ko mënee dañuy dimbali itam ñeneen ñi, ak diine bu ñu mënta bokk. — Galasi 6:10.
Dañuy dëfal seen xol ak Mbind mu sell mi. Ñi musiba dal, dañu soxla lool ñu dëfal seen xol. Ci waxtu yu mel noonu, ki ñuy may doole mooy Yexowa miy “ Boroom lépp luy dëfal xol yi ” (2 Korent 1:3, 4). Dañuy sawar a won ñi nekk ci tiis dige yi nekk ci Biibël bi. Won leen itam ne ci kanam tuuti Nguuru Yàlla dina fi dindi bépp metit ak naqar te musiba dootul am. — Peeñu ma 21:4.
Lan moo may seede Yexowa yi ñu gaaw a mën a dimbali seeni mbokk ci ngëm bu musiba amee ?
Ak lan lañu mën a dëfal xolu ñi musiba dal ?
-
-
Kan mooy surga bu takku te teey bi ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 19
Kan mooy surga bu takku te teey bi ?
Ñun ñépp ay jariñoo ci ñam bi ñu jot ci wàllu ngëm
Lu yàggul dara bala muy dee, Yeesu dafa waxtaanoon ak ñeent ci taalibeem yi : Piyeer, Saag, Yowaana, ak Andare. Yeesu dafa leen joxoon ay tegtal yuy firndeel teewaayam ci mujug jamono. Mu yëkkëti laaj bu am solo, nee leen : “ Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu léen di dundal ca jamono ja ? ” (Macë 24:3, 45 ; Màrk 13:3, 4). Yeesu miy seen ‘ njaatige ’ dafa leen doon dig foofu ne, ci mujug jamono dina fi teg ay nit ngir ñuy jox taalibeem yi ñam ci wàllu ngëm. Ñan ñooy doon surga boobu ?
Gurup bu ndaw la ci biir taalibe Yeesu yi xel mu sell mi tànn. “ Surga ” bi, moom mooy Jataay biy dogal ci seede Yexowa yi. Te mu ngi jox ñiy jaamu Yexowa ñam ci wàllu ngëm ci waxtu bi ñu ko soxla. Ci surga boobu rekk lañu yaakaar ngir kontine di jot lu ñuy “ dundal ci jamono ji ”. — Luug 12:42.
Dafay toppatoo kër Yàlla gi (Luug 12:44). Yeesu dafa dénk surga bu takku te teey bi liggéey bu diis, maanaam toppatoo lépp lu jëm ci liggéey bi ñiy jaamu Yexowa ci kaw suuf di def ci wàllu ngëm. Toppatoo boobu mu ngi ëmb jiite liggéeyu waare bi, sàmm alal bi koy doxal, te jàngal ñu ci suñu mbooloo yi. Loolu moo tax “ surga bu takku te teey bi ” di defar ay téere yu ñuy jëfandikoo ci suñu waare bi, te di ñu jàngal ci ndaje yi ñuy am ci saalu Nguur gi ak ci suñu ndaje yu mag yi. Noonu lañuy joxe ñam ci wàllu ngëm bi ñu soxla ci waxtu bi ñu ko soxla.
Surga bi dafa takku ndaxte dëgg gi nekk ci Biibël bi rekk lay jàngale te du bàyyi dara tere ko mu def liggéey bi ñu ko sant, maanaam waare xibaaru jàmm bi. Te it, dafa teey ci ni muy sàmme lépp li ko Kirist dénk (Jëf ya 10:42). Yexowa mu ngi barkeel liggéey bi surga bi di def. Li koy wone mooy, mbootaayam mu ngi yokku te ñam bi ci wàllu ngëm dafa bare. — Isaïe 60:22 ; 65:13.
Kan la Yeesu dénk liggéeyu jox taalibeem yi ñam ci wàllu ngëm ?
Lu tax ñu mën a wax ne surga bi dafa takku te teey ?
-
-
Jataay biy dogal, naka lay liggéeye ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 20
Jataay biy dogal, naka lay liggéeye ?
Jataay biy dogal ci jamono karceen yu njëkk ya
Njàngum bataaxal bu jóge ci Jataay biy dogal
Ca jamono karceen yu njëkk ya, amoon na benn gurup bu ndaw bu doon jël dogal yi am solo pur mbooloo karceen yépp yi xel mu sell mi tànn. Dañu nekkoon Jataay biy dogal ci seen biir. Gurup boobu moo doon “ ndaw ya ak njiit ya ” nekkoon Yerusalem (Jëf ya 15:2). Bala ñuy juboo ci benn dogal, dañu doon xool li ci Mbind yi wax, waxtaan ci te bàyyi xel mu sell mi mu wommat leen (Jëf ya 15:25). Ci ñoom lañuy roy tey.
Yàlla dafay jaar ci moom ngir def li mu bëgg. Ñi bokk ci Jataay biy dogal, dañu nekk ay karceen yu góor yi xel mu sell mi tànn te dañu fonk lool Kàddu Yàlla. Yàgg nañu di joxe ay tegtal yu jëm ci liggéey bi suñu mbootaay def ci àddina si. Yàgg nañu it di ñu xelal ci wàllu ngëm. Dañuy daje semen bu nekk ngir waxtaan ci li mbokk yi nekk ci àddina si sépp soxla ci wàllu ngëm. Jataay biy dogal, dafay topp li ñu daan def ci jamono karceen yu njëkk ya, maanaam dañuy bind ay bataaxal walla jaar ci wottukat yiy wër ak ñeneen ngir mbooloo yépp jot ay tegtal yuy sukkandiku ci Biibël bi. Loolu dafay tax ñiy jaamu Yàlla bokk xalaat te bokk jëf (Jëf ya 16:4, 5). Jataay biy dogal mooy jiite lépp lu jëm ci defar ñam bi ci wàllu ngëm, ci luy jëmloo kanam liggéeyu waare bi, ak ci tànn ñiy ñuy dénk liggéey ci mbooloo yi.
Dafay bàyyi xel mu sellu Yàlla wommat ko. Jataay biy dogal dafay bàyyi Yexowa Aji kawe ji ak Yeesu miy kilifa mbooloo mi ñu wommat ko ci lépp (1 Korent 11:3 ; Efes 5:23). Gisewuñu seen bopp ni ay kilifa ci mbooloo Yàlla mi. Ñoom ak yeneen karceen yépp yi xel mu sell mi tànn, dañuy kontine di “ topp Gàtt ba [maanaam Yeesu] fépp fu mu jëm ” (Peeñu ma 14:4). Jataay biy dogal dafay kontaan lool bu ñu koy sóoraale ci suñuy ñaan.
Ca jamono karceen yu njëkk ya, ñan ñoo bokkoon ci Jataay biy dogal ?
Tey, naka la Jataay biy dogal di wonee ne bëgg na Yàlla wommat ko ?
-
-
Lan mooy Betel ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 21
Lan mooy Betel ?
Biro bi yore wàllu foto yi ca Etaa Sini
Almaañ
Kenya
Colombie
Betel, tur la ci làkku yawut. Mu ngi tekki “ kër Yàlla ” (Njàlbéen ga 28:17, 19). Tur boobu la seede Yexowa yi di woowe palaas yi ñu am ci àddina si te ñu fay jiitee liggéeyu waare bi ak di jàpple ñi ciy yëngu. Kër gu mag gi, mu nga New York ca Etaa Sini. Foofu la Jataay biy dogal nekk te di fa jiitee liggéey bi ñuy def ci suñu bànqaas yi ci àddina si sépp. Ñi nekk Betel dañu mel ni njaboot ndaxte ci Betel bi lañu dëkk, di bokk lekk te di bokk jàng Biibël bi. Loolu moo tax ñu leen di woowe njabootu Betel bi. — Sabóor 133:1.
Béréb la fu ay mbokk nangoo sonn ngir def liggéeyu Yàlla. Ci Betel yi yépp am na ay karceen yu góor ak yu jigéen yuy joxe seen jot gépp ngir def li Yàlla bëgg te liggéeyal Nguuram (Macë 6:33). Amu ci kenn ku ciy feyeeku waaye ñépp lañuy jox néeg bu ñuy fanaan ak lekk ak tuuti ndimbal ngir ñu faj seeni soxla yu ndaw. Ku ci nekk am nga liggéey bu ñu la dénk, muy ci biro yi, walla ci waañ bi, walla ci saal bi ñuy lekke, walla fi ñuy sottee suñu téere yi. Mën na nekk it menaas, fóot, defar yàqu-yàqu yi, ak yeneen.
Béréb la fu ñuy jàpple liggéeyu waare xibaaru Nguur gi. Li gën a tax ñu taxawal Betel yi mooy def ba nit ñu bare xam dëgg gi nekk ci Biibël bi. Téere bii nga yor, ci la bokk. Bi ñu koy bind, Jataay biy dogal moo jiite liggéey bi. Bi ñu paree, dañu ko yónnee ci internet ay téeméeri gurupu seede Yexowa yuy tekki suñuy téere ci ay làkk yu bare ci àddina si sépp. Bi ñu paree, ñu sotti ko ci ay masin yu gaaw yu nekk ci yenn Betel yi, door ko yónnee ci lu ëpp 110 000 mbooloo. Ci liggéey boobu yépp nag, njabootu Betel yi am nañu ci wàll bu am solo. Bu ñuy def loolu, dañuy jàpple liggéey bi gën a jamp tey, maanaam waare xibaaru jàmm bi. — Màrk 13:10.
Ñan ñooy liggéey ci Betel yi te naka lañu leen di toppatoowe foofu ?
Ban liggéey bu jamp la Betel bu nekk di jàpple ?
-
-
Ban liggéey lañuy def ci bànqaas yi ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 22
Ban liggéey lañuy def ci bànqaas yi ?
Îles Salomon
Canada
Afrique du Sud
Ñi bokk ci njabootu Betel yi dañuy toppatoo liggéeyu waare bi ci benn réew walla lu ko ëpp. Am na ñuy tekki suñuy téere ci làkku réew mi. Am na ñuy liggéey ci masin yiy sotti suñu yéenekaay yi ak suñu téere yi. Am na ñuy liggéey fu ñuy denc suñuy téere bala ñu leen di yónnee ci mbooloo yi. Am na ñuy liggéey fu ñuy defar wideo yi ak lu ñuy déglu, walla ñuy def yeneen liggéey yu bànqaas bi war a def.
Kurélu bànqaas bi dafay jiite liggéey bi. Jataay biy dogal dafay dénk benn kurél liggéey bi ñuy def ci bànqaas bu nekk. Kurél boobu, dañu koy woowe kurélu bànqaas bi. Kurél bu nekk dina am lu mat ñetti magi mbooloo walla lu ko ëpp yu mën seen liggéey. Kurélu bànqaas bi mooy wax Jataay biy dogal fi liggéeyu waare bi tollu ci réew bu nekk bu muy toppatoo ak jafe-jafe bu mënta am. Loolu mooy dimbali Jataay biy dogal mu xam yan waxtaan lay def ci téere yi nar a génn walla ci porogaraamu ndaje yi ci mbooloo mi ak ci ndaje yu mag yi. Jataay biy dogal dafay faral di yónnee ay nit ci bànqaas yi ngir dimbali kurélu bànqaas yi ci def liggéey bi ñu leen dénk ni mu ware (Kàddu yu Xelu 11:14). Ñoom dañuy taxawal porogaraam bu neex, boole ci benn waxtaan bu ñuy def, ngir dooleel mbooloo yi ci wàllu ngëm.
Dañuy jàpple mbooloo yi ci seen liggéeyu waare bi. Ci góor yi ñuy dénk liggéey ci bànqaas bi, am na ñuy toppatoo li jëm ci mbooloo yu bees yi, maanaam ñoom ñooy nangu ñu taxawal mbooloo bu bees. Am na it ñuy toppatoo lépp lu jëm ci liggéeyu pioñee yi, misioneer yi ak wottukat yiy wër ci mbooloo yi bànqaas bi di toppatoo. Dañuy waajal ay ndaje yu mag, di jiite liggéeyu tabaxu saalu Nguur yu bees te di xool ba xam ndax yónnee nañu mbooloo yi téere yi ñu soxla. Lépp li ñuy def ci bànqaas yi bokk na ci liy tax liggéeyu waare bi aw yoon. — 1 Korent 14:33, 40.
Naka la kurélu bànqaas yi di dimbalee Jataay biy dogal ?
Yan liggéey lañuy dénk ñi nekk ci bànqaas yi ?
-
-
Naka lañuy binde suñu téere yi te naka lañu leen di tekkee ci yeneen làkk ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 23
Naka lañuy binde suñu téere yi te naka lañu leen di tekkee ci yeneen làkk ?
Biro bi yor wàllu mbind mi ca Etaa Sini.
Corée du sud
Armenie
Burundi
Sri Lanka
Dañuy def suñu kem kàttan ngir yégal “ xibaar ” bi “ xeet yépp ak giir yépp ak kàllaama yépp ak réew yépp. ” Loolu moo tax ñu ngi sotti ay téere ci lu jege 750 làkk (Peeñu ma 14:6). Lan moo ñuy dimbali ñu mën a def liggéey bu metti boobu ? Dañu am gurupu bindkat yu jóge ci àddina si sépp ak benn gurupu nit yu sawar yuy tekki suñuy téere, te ñoom ñépp ay seede Yexowa lañu.
Li ñu bind, ci ãgale lañu ko njëkk a bind. Jataay biy dogal mooy jiite liggéey bi ñuy def ci Biro bi yor wàllu mbind mi te mu nekk ci suñu kër gu mag gi. Biro boobu mooy toppatoo liggéey bi ñuy jox bindkat yi nekk ci kër gu mag gi ak ci yenn bànqaas yi. Li ñu am ay bindkat yu bare te wuute tax na ba suñu téere yi mën a laal xeet yu bare.
Li ñu bind, dañu koy yónnee ñiy tekki. Bu bindkat yi paree mbind mi ci ãgale, dañu koy seetaat ba Jataay biy dogal nangu li ñu ci bind, ñu daldi ko yónnee ci internet gurup yiy tekki te ñu nekk ci àddina si sépp. Gurup bu nekk dafay tekki ci làkkam li ñu ko yónnee. Dañuy def lépp ngir tànn ci seen làkk baat yu jub te méngoo ak li ñu wax ci ãgale. — Ecclésiaste 12:10.
Ordinatër yi dañu tax liggéey bi gën a gaaw. Dëgg la, ordinatër mënul a def liggéey bi bindkat yi ak ñiy tekki di def, waaye jëfandikoo ordinatër dafay tax liggéey bi gën a gaaw. Seede Yexowa yi defar nañu itam lu ñuy wax ci tubaab système électronique d’édition multilingue (MEPS) biy tax ñu mën a dugal mbind mi ci ay ordinatër ci ay téeméeri làkk. Dafay tax itam ñu mën a boole mbind mi ak ay nataal walla foto ba mu rafet, ba ñu mën koo sotti ci ay masin yu gaaw.
Lu tax ñuy def loolu yépp ngir tekki téere yi ci ay làkk yu bare, fekk yenn ci làkk yooyu, ñi koy làkk barewuñu ? Ndaxte Yexowa dafa bëgg “ ñépp mucc te xam dëgg gi. ” — 1 Timote 2:3, 4.
Naka lañuy binde suñu téere yi ?
Lan moo tax ñuy tekki suñu téere yi ci làkk yu baree-bare ?
-
-
Xaalis bi ñuy defe suñu liggéey ci àddina si sépp, fan la jóge ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 24
Xaalis bi ñuy defe suñu liggéey ci àddina si sépp, fan la jóge ?
Népal
Togo
Grande-Bretagne
At mu nekk, suñu mbootaay dafay génne te di joxe ay téeméeri milioŋi Biibël ak yeneen téere te du ci jaay benn. Dañuy tabax te di toppatoo ay saalu Nguur ak ay Betel. Ñu ngi yor itam lu tollook ay junniy nit yuy liggéey ci Betel yi ak ay misioneer yu bare. Bu musiba amee itam dañuy yónnee foofu ndimbal. Xéyna dinga laaj sa bopp, ‘ xaalis biy def loolu yépp, fan la jóge ? ’
Duñu laaj dîme (maanaam jël benn ci fukki xaaju saleeru nit), duñu laaj nit ñi ñu kotise, te duñu laaj xaalis ñiy teewe suñuy ndaje. Dëgg la, suñu liggéeyu waare bi dafay laaj xaalis bu bare waaye duñu ñaan xaalis. Lu ëpp téeméeri at ci gannaaw, bi suñu ñaareelu téere bi tudd La Tour de Garde génnee, ñu ngi doon wax foofu ne, gëm nañu ne Yexowa moo ñuy dimbali. Waxoon nañu itam ne duñu mas a saraxu walla di ñaan nit mu jox ñu xaalis ; te ba léegi masuñu ko def. — Macë 10:8.
Xaalis bi ñuy defe suñu liggéey bi, ci li nit ñi di maye la jóge. Nit ñu bare sopp nañu njàngale Biibël bi ñuy def te dañuy maye xaalis ngir jàpple ñu. Seede Yexowa yi ci seen bopp itam dañu bég ci joxe seen jot, seen doole ak di maye ci seen xaalis ak ci seen am-am ngir def li Yàlla bëgg ci àddina si sépp (1 Chroniques 29:9). Ci biir saalu Nguur yépp ak ci ndaje yu mag yi, dafay am ay boyet yoo xam ne ku bëgg a maye xaalis mën nga ko fa dugal. Nit ñi mën nañu def itam ay maye jaarale ko ci suñu palaas bi ñu moom ci internet, jw.org. Maye yi ëpp, ci ay nit yu barewul xaalis la jóge. Ñoom dañu mel ni jigéen ji Yeesu doon tagg. Jigéen jooju, ku néew doole la woon, boole ci jëkkëram faatu. Waaye loolu yépp terewul mu dugal ñaari xànjar ci ndab ya ca kër Yàlla ga (Luug 21:1-4). Kon ku nekk mën na “ ber ” dara ngir ‘ joxe ni mu ko nase ci xolam ’. — 1 Korent 16:2 ; 2 Korent 9:7.
Wóor nañu ne Yexowa dina kontine di xiir nit ñi ko bëgg a ‘ teral ci seen alal ’ ci jàpple liggéeyu Nguuram ndax coobareem am ci kaw suuf. — Kàddu yu Xelu 3:9.
Lan moo wuutale suñu mbootaay ak yeneen diine yi ?
Lan lañuy def ak maye yi ?
-
-
Lu tax ñuy tabax ay saalu Nguur te naka lañu leen di tabaxe ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 25
Lu tax ñuy tabax ay saalu Nguur te naka lañu leen di tabaxe ?
Bolivie
Nigéria, bala ñuy tabax ak bi ñu tabaxee ba pare
Tahiti
Ni ko tur bi wonee, saalu Nguur mooy béréb boo xam ne fa lañuy jàngalee li Biibël bi wax ci Nguuru Yàlla. Yeesu ci boppam, Nguuru Yàlla la doon gën a waare. — Luug 8:1.
Ci saalu Nguur yi lañuy jaamoo Yàlla dëgg. Ci saalu Nguur yi lañuy jiite liggéeyu waare xibaaru jàmm bi ci Nguuru Yàlla (Macë 24:14). Du saalu Nguur yépp ñoo bokk yaatuwaay te niroo waaye saalu Nguur yépp ay nekk ay tabax yu yem. Ci ay saalu nguur yu bare, lu ëpp benn mbooloo ñoo fay daje. Ci at yi weesu, ndegam mbooloo yi dañoo gën a yokku, tabax nañu ay fukki junniy saalu Nguur yu bees (maanaam lu jege juróomi saalu Nguur bés bu nekk). Naka la loolu mënee am ? — Macë 19:26.
Xaalis bi ñuy tabaxe saalu Nguur yi, ci li nit ñi di maye la jóge. Maye yooyu dañu leen di yónnee ci bànqaas bi ngir mu mën koo jox mbooloo yi soxla tabax walla defaraat seen saalu Nguur.
Ay wolonteer yu ñu dul fey ñooy tabax saalu Nguur yi ; bokkuñu fu ñu jóge te yemuñu alal. Ci réew yu bare dañu taxawal ay Gurupu nit yuy tabax saalu Nguur yi. Gurup yooyu ñooy tabax ay saalu Nguur fépp fu ñu ko soxla ci réew mi ñu nekk, ba ca dëkk yu sore. Foofu dañuy dimbali seede Yexowa yi fa nekk ci tabax seen saalu Nguur. Ci yenn réew yi, ay seede Yexowa yu mën seen liggéey lañu dénk benn diiwaan, maanaam ay dëkk, fu ñu war a jiite liggéeyu tabax ak defaraat ay saalu Nguur. Am na it ay maneebar yu xam seen liggéey yuy ñëw ngir jàpple leen. Fépp fu ñuy tabax, ñi bokk ci mbooloo mi fa nekk ñooy def li ëpp ci liggéeyu tabax bi. Xelum Yexowa ak lépp li jaamam yi di def ak seen xol bépp moo tax ba loolu yépp mën a am. — Sabóor 127:1 ; Kolos 3:23.
Lan moo tax ñuy woowe suñu béréb yi ñuy jaamoo Yàlla saalu Nguur ?
Naka lañuy def ba mën a tabax ay saalu Nguur fépp ci àddina si ?
-
-
Naka lañu mënee bokk ci toppatoo suñu saalu Nguur ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 26
Naka lañu mënee bokk ci toppatoo suñu saalu Nguur ?
Estonie
Zimbabwe
Mongolie
Porto Rico
Saalu Nguur boo gis ci seede Yexowa yi, mu ngi yore turu Yàlla mi nekk tur bu sell, maanaam Yexowa. Loolu moo tax ñu bëgg a defar suñu saalu Nguur yi ba ñu set, jekk, bañ a am yàqu-yàqu te kontine di bees. Def loolu nekk na lu réy ci ñun te lu am solo la ci suñu njaamu Yàlla. Ñépp a ci mën a bokk.
Nanga bokk ci set-setal bi bu ndaje bi jeexee. Saa yu ñu paree ndaje, suñu mbokk yu góor ak yu jigéen dañuy def set-setal bu ndaw bala ñuy ñibbi. Benn yoon ci semen bu nekk dañuy def set-setal bu gën a mag. Benn magu mbooloo walla kuy topptoo yëfi mbooloo mi mooy jiite liggéey bi, te ci lu ëpp dafay yor kayit bu ñu bind li ñu war a def. Dañuy bale, fobeere, dindi pënd mi, raŋale siis yi, raxas duus yi, fomp palanteer yi ak seetu yi, tuuri mbalit mi, te defar ci biti. At mu nekk, lu mu néew-néew dañuy jël benn bés ngir def set-setal bu réy. Nañu boole suñu doom yi ci liggéey bi ngir jàngal leen ñu fonk suñu béréb bi ñuy jaamoo Yàlla. — Ecclésiaste 5:1.
Nanga bokk ci defar li yàqu. At mu nekk, dañuy xool bu baax suñu saalu Nguur ci biir ak ci biti ba xam ndax dara yàquwul. Ci loolu lañuy sukkandikoo ngir xam li ñu war a def saa su nekk ba béréb bi kontine di rafet. Noonu duñu yàq xaalis ci ay yàqu-yàqu yu ñu mënoon a moytu (2 Chroniques 24:13 ; 34:10). Ndegam ci saalu Nguur lañuy jaamoo Yàlla, jaadu na ñu koy toppatoo ngir mu nekk béréb bu set te jekk. Nañu bokk ci liggéey boobu. Noonu lañuy wonee ne bëgg nañu Yexowa dëgg te fonk nañu béréb bi ñu koy jaamoo (Sabóor 122:1). Dafa nekk itam lu rafet ci kanamu dëkkandoo yi.
Lu tax ñu war a toppatoo bu baax suñu béréb bi ñuy jaamoo Yàlla ?
Lan lañuy def ngir suñu saalu Nguur kontine di set ?
-
-
Ban njariñ nga mën a jële ci téere yi ñu mën a jàng ci saalu Nguur gi ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 27
Ban njariñ nga mën a jële ci téere yi ñu mën a jàng ci saalu Nguur gi ?
Israël
République tchéque
Bénin
Îles Caïmans
Ndax am na aaya ci Biibël bi boo bëgg a nànd bu baax ? Ndax bëgg nga yaatal sa xam-xam ci kenn ku ñuy wax ci Biibël bi ? Walla ci béréb bu ñu tudd ci Biibël bi ? Walla ci leneen lu leerul loo fa jàng ? Ndax danga am poroblem te bëgg a xam ndax Biibël bi mën na la ci dimbali ? Nanga gëstu suñuy téere yi ñu def ci saalu Nguur gi ngir ku nekk mën cee jàng. Dinga mën a yokk bu baax sa xam-xam ci Biibël bi.
Ay jumtukaayu gëstu yu am doole ñoo lay dimbali nga am ay tont ci say laaj. Xéyna amuloo ci sa làkk téere yépp yi seede Yexowa yi génne te ñu sukkandiku ci Biibël bi. Waaye ci saalu Nguur gi dinga fa mën a gis téere yi mujj a génn ak ay sotti Biibël ak ay diksoneer ak yeneen téere. Mën nga ci jàng bala ndaje bi di komaase walla bu jeexee. Bu fa ordinatër amee, dañuy jëfandikoo li ñuy woowe Watchtower Library ngir dugal ci ordinatër bi suñuy téere yu bare. Mën nga ci gëstu aaya, baat walla waxtaan bu la neex ci fasoŋ bu yomb.
Ndimbal la ci ñi bokk ci ndaje bi tudd Dundinu karceen ak liggéeyu waare bi . Téere yooyu nekk ci saalu Nguur gi mën nañu la dimbali nga waajal bu baax waxtaan yi nga am ci ndaje bi. Kiy jiite ndaje bi tudd Dundinu karceen ak liggéeyu waare bi moo yor toppatoo téere yooyu. Moom moo war a dugal bépp téere bu mujj a génn te rañsale téere yépp ba mu baax. Moom walla ki lay jàngal Biibël bi mën nañu la won ni ngay def ba gis li nga soxla. Waaye nag benn téere warul génn saalu Nguur gi te war nañu moytu yàq leen walla bind ci dara.
Biibël bi dafa wax ne su ñu bëggee am xam-xam ci Yàlla, fàww ñu “ sàkku ko ni xaalis ” (Kàddu yu Xelu 2:1-5). Suñu téere yi nekk ci saalu Nguur gi mën nañu la dimbali ci komaase sàkku xam-xam boobu.
Yan jumtukaayu gëstu nga mën a am ci saalu Nguur gi ?
Kan moo la mën a dimbali ci jëfandikoo bu baax téere yooyu ?
-
-
Lan lañuy fekk ci palaas bi ñu moom ci Internet ?Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
-
-
NJÀNGALE 28
Lan lañuy fekk ci palaas bi ñu moom ci Internet ?
France
Pologne
Russie
Yeesu dafa waxoon talibeem yi ne : “ Na seen leer leere noonu ci kanam nit ñi, ngir ñu gis seeni jëf yu rafet, te màggal seen Baay bi ci kaw ” (Macë 5:16). Li boroom xam-xam yi di defar ci suñu jamono, dañu koy jëfandikoo bu baax ngir topp ndigalu Yeesu boobu. Internet, ci la bokk. Palaas bi ñu moom ci Internet te ñu tudde ko jw.org dafay joxe ay leeral ci li seede Yexowa yi gëm ak it ci seen yëngu-yëngu yi. Lan ngay fekk ci palaas boobu ñu moom ci internet ?
Dinga fa fekk li Biibël bi tontu ci laaj yi nit ñi faral di laaj. Dañu fay tontu ci laaj yi gën a am solo yu nit ñi faral di laaj. Tont yi ñu ngi ci kayit yi tudd, Ndax coono àddina dina mas a jeex ? ak Ndax ñi dee dinañu dundaat ? Kayit yooyu def nañu leen ci internet ci lu ëpp 600 làkk. Dinga fa fekk itam sotti Biibël bi tudd Traduction du Monde Nouveau ci lu ëpp 130 làkk ak ay téere yu bare yu lay dimbali ci gëstu Biibël bi, mel ni téere bi tudd Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ? Am na fa itam téere La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi mujj a génn. Yu bare ci téere yooyu mën nga leen jàng walla déglu leen ci internet. Boo bëggee it, mën nga leen a sotti ci sa ordinatër, ci mp3 walla PDF walla EPUB. Boo gisee nit ku bëgg a jàng suñuy téere ci làkkam , mën nga sotti ay paas ci làkk boobu. Mën nga fa fekk itam ay wideo yu bare yu ñu defal muuma yi. Mën nga sotti it ay nettali yu ñuy jàng ci Biibël bi ak ay tiyaatar yu ñuy déglu yuy jàngale lu jëm ci Biibël bi, boole ci misik bu neex.
Dinga fa fekk ay xibaar yu wóor ci seede Yexowa yi. Ci palaas bi ñu moom ci Internet dafay am ay xibaar ak ay wideo yu jëm ci suñu liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp. Dañu fay wax itam xëw-xëw yiy laal seede Yexowa yi ak ndimbal bi ñuy def bu musiba amee. Mën nga fa fekk it ay yégle yu jëm ci suñu ndaje yu mag yi ak suñu adareesu bànqaas yi.
Loolu yépp tax na ba leeru dëgg gi leer ba ci dëkk yi gën a sore ci àddina si. Waa àddina si sépp ñu ngi koy jariñoo, boole ci sax béréb bi gën sore te gën a sedd bi ñuy woowe Antarctique. Ñu ngi ñaan “ kàddug Boroom bi law ” ci kaw suuf sépp ci ndamu Yàlla. — 2 Tesalonig 3:1.
Naka la jw.org di dimbalee nit ñu bare ñu xam li Biibël bi tontu ci seeni laaj ?
Lan nga bëgg a xool ci palaas bi ñu moom ci internet ?
-