WOY-YÀLLA 52
Nañu jébbalu ci Yàlla
(Yawut ya 10:7, 9)
1. Yexowa mi sos àddina,
asamaan ak suuf si,
bépp mbindeef, moom mooy boroom.
Amul lu mu sàkkul,
bakkan yépp a bawoo ci moom,
moom moo ñu may dund.
Moom rekk lañuy woy ba abadan,
moom rekk a yelloo màggal.
2. Bi ñu sóobee Yeesu ci ndox,
dig na Yàlla ci ñaan:
«Maa ngi defsi sa coobare».
Muy dogal gu yéeme.
Asamaan daldi ubbiku,
Yàlla sol ko xelam,
ngir mu déggal baayam ma ca kaw.
Yeesu farlu ci sasam.
3. Yow lañuy sujjóotal Yàlla,
na sa manoore siiw!
Doon sa moomeel, lañ fas yéene,
fàtte suñu bopp.
May nga ñu sa soppe sa doom,
ngir ñu dund ba fàww.
Dootuñu jiital suñu bànneex,
jébbalu nañu ci yow.
(Xoolal itam Macë 16:24; Màrk 8:34; Luug 9:23.)