TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • sjj woy 58
  • Nañu wër ñi bëgg jàmm

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu wër ñi bëgg jàmm
  • Nañu woyal Yexowa ànd ceek mbégte
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Yal na seen ngëm dëgër
    Nañu woyal Yexowa ànd ceek mbégte
  • Dinaa dem fi ñu ma soxla
    Nañu woyal Yexowa ànd ceek mbégte
  • Nañu sàmm suñu xol
    Nañu woyal Yexowa ànd ceek mbégte
  • Taxawaayu ndaw ñi ci biir ndefarinu Yàlla
    Woyal, di Tagg Yeowa
Nañu woyal Yexowa ànd ceek mbégte
sjj woy 58

WOY-YÀLLA 58

Nañu wër ñi bëgg jàmm

(Luug 10:6)

  1. 1. Yeesu digle na, ñu dem waareji.

    Ci pënd bi, ci tàngaay bi,

    Mu ngi doon jox nit ñi yaakaar.

    Dafa bëggoon nit, moo tax tàyyiwul.

    Guddeek bëccëg la daan wëri

    Ñi dëgg gi neex.

    Kon ñun ni moom nañ dem waare

    Ci mbedd yépp ak kër gu ne,

    Ñu ngi yégle: ‘léegi coono yi yépp jeex’.

    (AWU BI)

    Ñun dañuy wër

    Nitu jàmm fu mu mën a ne

    Ñun dañuy wër

    Ku bëgg Yexowa musal la,

    Duñu tàyyi

    Ci waare bi.

  2. 2. Nañu góor-góorlu, li des barewul.

    Nit ñu bare soxla nañu

    Déglu xibaaru jàmm ji.

    Mbëggeel moo ñuy xiir, ci dem waareji

    Ngir xéttali nit ñiy jooy ndax

    Tiis yu bare yi.

    Ak fépp fu nit ki mën a ne,

    Bu ñu dégloo ñun dañuy bég,

    Kon buñ tàyyi dem waareji, jar na ko.

    (AWU BI)

    Ñun dañuy wër

    Nitu jàmm fu mu mën a ne

    Ñun dañuy wër

    Ku bëgg Yexowa musal la,

    Duñu tàyyi

    Ci waare bi.

(Xoolal itam Esayi 52:7; Macë 28:19, 20; Luug 8:1; Room 10:10.)

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager