WOY-YÀLLA 25
Ñi nga tànn, ñuy sa moomeelu bopp
(1 Piyeer 2:9)
1. Tànn nga ci kaw suuf si
ay doom ngir yow Yexowa.
Càkkeef bu bees te taaru,
ñu neex la ndax seen ngëm.
(AWU BI)
Mbooloo mi yaa ko moom.
Ñu di sa moomeel bu wóor.
Takku nañ, bëgg la,
Booloo, saa su ne ñu lay màggal.
2. Ñoom ñooy mbooloo mi sell,
miy jàngale sa kàddu.
Yaa leen génne ci lëndëm,
daldi leeral seen yoon.
(AWU BI)
Mbooloo mi yaa ko moom.
Ñu di sa moomeel bu wóor.
Takku nañ, bëgg la,
Booloo, saa su ne ñu lay màggal.
3. Cawarte lañu àndal,
ci boole ñi lay jaamu.
Mbote mi di leen won yoon.
Ñu nangu koo déggal.
(AWU BI)
Mbooloo mi yaa ko moom.
Ñu di sa moomeel bu wóor.
Takku nañ, bëgg la,
Booloo, saa su ne ñu lay màggal.
(Xoolal itam Esayi 43:20b, 21; Malasi 3:17; Kolos 1:13.)