Woy-Yàlla 60 (143)
Faralleen Yeowa!
(2 Musaa 32:26)
1. Suñuy xol a ngi woon ci jaxasoo,
Ndax kaasu diine, ba ñu daan jëfoo;
Waaye ndaw bànneex bu ñu muj’ làmboo,
Ba-ñ’ ñu xamloo Nguur’ Yàlla (Nguur’ Yàlla).
(AWU)
Faralleen Yeowa;
Waaw, ci moom bégleen.
Mukk! Du leen bërgël;
Ci leeram doxleen.
Yéeneleen xabaar biy
Goreel tey féexal.
Nguuram, jaare ci Krist,
Dina ko màggal.
2. Dinañ’ jaamu Yàllaak xol bu tàlli;
Dëggam, nit ñépp nañu jottali.
Suñuy mbokk yi nañu dimbali,
Ñu woy turam wu mag wi (wu mag wi).
(Awu)
3. Duñu ragal li Ibliis di fexe,
Ndax Yaa Yeowa mooy tax ñu texe.
Ñu bare mbaa néew, ñàkkuñu pexe,
Yeowaay Kii ñuy dooleel (ñuy dooleel).
(Awu)