WOY-YÀLLA 45
Xalaat bu baax a baax ci mbiri Yàlla
(Taalifi Cant 19:15)
1. Su may xalaat bu baax a baax,
Mbaa ma war a am lu ma wax,
Yàlla bëgg naa la bégal
Ci sama dund bés bu ne.
Bu ma nekkee ci njàqare,
Ba sax mënatuma nelaw,
Damay xalaat ci sa Kàddu
Ak ci say jëf, céy Yexowa.
2. Yal na samay xalaat jublu
Ci lépp lu jub te am faayda
Ak lépp lu rafet te dëggu,
Loolooy tax ba sama xel dal.
Maaka fonk say santaane
Ndax ñoo may awale fu wóor
Moo tax sa Kàddu laay bége
Di ci gëstu, di ci xalaat.
(Xoolal itam Taalifi Cant 49:4; 63:7; 139:17, 23; Filib 4:7, 8; 1 Timote 4:15.)