WOY-YÀLLA 79
Yal na seen ngëm dëgër
(Macë 28:19, 20)
1. Bi sa jaam yi nangoo dëgg gi,
Yow am nga mbégte bu réy.
Aar nga leen ak xel mu sell mi,
Looloo tax ñuy jëm kanam.
(AWU BI)
Ñu ngi lay ñaan, yow Yexowa
Nga wéy di aar sa bépp jaam
Ñu ngi ñaan ci turu Yeesu seen ngëm dëgër
Ba dara du tax ñu xàddi.
2. Bés bu ne, ñu ngi leen di ñaanal,
Yexowa, nga sàmm leen.
Ci lu wóor, ñoom ñu ngi góor-góorlu
Looloo tax nga barkeel leen.
(AWU BI)
Ñu ngi lay ñaan, yow Yexowa
Nga wéy di aar sa bépp jaam
Ñu ngi ñaan ci turu Yeesu seen ngëm dëgër
Ba dara du tax ñu xàddi.
3. Ñu ngi ñaan ñu gën a jëm kanam,
Jaamu la ak kóolute.
Su ñuy wéy di takku ci Yàlla
Dinañu dund ba fàww.
(AWU BI)
Ñu ngi lay ñaan, yow Yexowa
Nga wéy di aar sa bépp jaam
Ñu ngi ñaan ci turu Yeesu seen ngëm dëgër
Ba dara du tax ñu xàddi.
(Xoolal itam Luug 6:48; Jëf ya 5:42; Filib 4:1.)