TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • my nettali 2
  • Tool Bu Rafet

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Tool Bu Rafet
  • Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li tax ñu dàq leen
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Nit ñi jëkk a am ci kow suuf
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Lu tax Yàlla sàkk suuf si?
    Gëm Yàlla dëgg moo ñu mën a indil jàmm
  • Àjjana Ju Bees Ci Kow Suuf Si
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
Xóotalal waxtaan bi
Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
my nettali 2
Ay mala, ay fulóor, ay garab, ak lëpp-lëpp ci biir toolu Eden bu rafet ba

NETTALI 2

Tool Bu Rafet

XOOLAL suuf si. Lépp a rafet ! Xoolal ñax bi, garab yi, tóor-tóor yi ak mala yi. Ana ñey bi ? Ana gaynde yi ?

Lan la Yàlla def ba tool bu rafet bii am ? Nañu jëkk a seet li mu def ba nit mën a dëkk ci kow suuf si.

Yàlla dafa bëggoon ñax muur suuf si. Moo tax mu jëkk sàkk ñax. Sàkk na itam garab yu bare. Garab yu mag ak yu ndaw yépp. Dañuy rafetal suuf si. Waaye yu ci bare dañuy joxe itam lekk bu neex.

Ginnaaw loolu, Yàlla sàkk na jën yi pur ñu dund ci biir ndox yi ak picc yi pur ñu naaw ci asamaan. Sàkk na ay xaj, muus, fas, mala yu mag ak mala yu ndaw yépp. Yan mala ngay gis fi nga dëkk ? Loolu yépp, Yàlla dafa ko def pur ñun. Ndax waruñu ci kontaan ?

Bi mu paree ci loolu, Yàlla tànn na benn béréb ci kow suuf si. Mu defar ko ba mu rafet lool. Béréb boobu, dafa ko tudde toolu Eden. Foofu, lépp a baaxoon ! Lépp a rafetoon ! Yàlla dafa bëggoon suuf si sépp mel ni tool boobu.

Tool boobu lañuy wone fii. Xoolaat ko bu baax. Yàlla gisoon na ne am na lu fi mànke. Ndax xam nga lan la ? Nañu ko seet ci nettali bii di topp.

Njàlbéen ga 1:11-25 ; 2:8, 9.

Laaj yi

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager