NJÀNGALE 9
Naka lañu mënee waajal bu baax suñu ndaje yi ?
Cambodge
Ukraine
Xéyna fi nga nekk nii, yaa ngi jàng Biibël bi ak benn seede Yexowa. Ndax bala muy ñëw dangay waajal li ngeen war a jàng ? Loolu baax na. Defal loolu itam bala ngay teewe ndaje yi. Dinga ci jële njariñ bu gën a réy. Am porogaraam bu baax ngir def waajal boobu mooy li gën.
Nanga tànn waxtu bi ak béréb bi. Kañ la sa xel di gën a ubbeeku ci njàng ? Ndax ci suba si la, bala ngay def dara ? Walla ci guddi gi, bu xale yi tëddee ? Xéyna mënoo toog lu yàgg di jàng. Kon seetal jot bi nga mën a jël ngir jàng te boo demee ba tàmbali sa njàng bul bàyyi dara yàqal la. Toogal fu wéet te sore lépp lu mën a génne sa xel ci njàng mi. Nanga fey sa rajo, sa tele, ak sa telefon. Nanga ñaan Yàlla bala ngay komaase. Loolu dina la dimbali nga fàtte coono yi nga yendoo te def sa xel mépp ci kàddu Yàlla. — Filib 4:6, 7.
Nanga rëdd ci téere bi baat yi am solo te waaj ngir bokk ci waxtaan yi. Booy waajal li ñu war a waxtaane, nanga njëkk a xool turu waxtaan bi walla turu pàcc bi. Nanga seet ni ñu xaajalee waxtaan bi ci biir ak ni xaaj yooyu ànde ak turu waxtaan bi. Bu amee ay foto, nanga xool li nga ci mën a jànge. Xoolal itam laaj yi mujj yiy fàttali ponk yi ëpp solo. Boo paree loolu, jàngal xise maanaam paragraphe bu nekk te jéem a tontu laaj bi mu àndal. Jàngal aaya yi ñu lim te xool ni aaya yooyu di dëgërale waxtaan bi (Jëf ya 17:11). Tont boo gis ci laaj yi nekk foofu, nanga rëdd baat yi ci ëpp solo. Loolu dina tax ngay mën a gaaw a fàttaliku tont bi bés boo teewee ndaje bi te bëgg a bokk ci waxtaan yi. Te it doo soxla di liir booy joxe tont bi. Dinga ko mën a wax ci say kàddu bopp. Boo bëggee tontu, nanga yëkkati sa loxo te bu ñu la mayee, nga joxe tont bu gàtt.
Semen bu nekk, boo waajalee noonu waxtaan yi ñu war a def ci ndaje yi, sa ‘ dencukaayu ’ xam-xam ci Biibël bi dina yokku ndànk-ndànk. — Macë 13:51, 52.
Ban porogaraam nga mën a am ngir waajal ndaje yi ?
Naka nga mën a waajale tont boo bëgg a joxe ci ndaje ?