Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
Xaaj 4 : Won ko ni ñuy waajale njàngum Biibël
1 Kuy jàng Biibël bi, bala mu gaaw a jëm kanam ci wàllu ngëm, am na lu mu war a def. Dafa war a jàng bala ngay ñów li ngeen di waxtaane, rëdd ci suufu tont yi, te mën a wax tont yi ci kàddu boppam. Kon, boo amee njàngum Biibël boo faral a def, woneel nit ki ni ñu koy waajale. Li ci mën a dimbali ñu bare mooy waajal ak ñoom benn njàngale ba mu jeex.
2 Na jàng a rëdd tont yi te bind mbind yu gàtt : Jàngal ak moom laaj yi ñu bind ci téere bi, te won ko ni ñuy seete tont yi ci xise yi. Won ko ci sa téere bopp ni nga rëdde kàddu yi ëpp solo rekk ngir tontu. Xéyna dina bëgg a def ni yow, te moom it rëdd rekk li ko mën a fàttali tont bi (Lukk 6:40). Ba pare, laaj ko mu wax tont bi ci kàddu boppam ngir xam ndax nànd na bu baax li mu jàng.
3 Ci suñuy téere, am na ay aaya yu ñuy wone, fekk binduñu li ci nekk. Bu nit ki di waajal seen waxtaan, dafa war a jàng te gëstu bu baax ci aaya yooyu (Jëf. 17:11). Aaya bu ci nekk, am na ci xise bi loo xam ne ci aaya boobu lañu ko jële. Fexeel ba ki ngay jàngal gis loolu. Wax ko ne am na lu mu mën a bind ci wetu xise yi, te won ko li mu mën a def ngir loolu bañ a bare. Fexeel mu leer ko ne lépp li muy jàng, ci Biibël bi la jóge. Buy tontu, na wax bu baax ci aaya yooyu ñuy wone, fekk binduñu li ci nekk.
4 Na njëkk xool ci lan la waxtaan bi di nekk te bu paree na seetaat li mu jàng : Bu nit ki di waajal waxtaan bi, na njëkk xool ci lan la waxtaan bi di nekk. Mën na ko xam bu xoolee yaxu waxtaan bi, turu xaaj bu nekk, ak foto walla nataal yi. Wax ko it ne, bu waajalee njàngam ba pare, na jéem a fàttaliku ponk yi ci ëpp solo. Su amee ci njàngale mi wërale bu nuy def ngir fàttaliku li ñu jàng, na jéem a tontu laaj yi ci nekk. Bu seetaatee li mu jàng, dina ko mën a jàpp bu baax.
5 Nanga dimbali ki ngay jàngal Biibël bi mu waajal bu baax li ngeen di jàng. Loolu dina tax, bu demee suñuy ndaje, tontam yi gën a am solo. Ku mën gëstu lay doon te dina ko tàmm def. Te njariñ bi muy am ci loolu, dina yàgg lool. Bu njàngum Biibël bi ngay def ak moom jeexee sax, njariñ boobu dina kontine.