Xaaj 2 : Nañu waajal suñu bopp
Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
1 Waxtaan ci xise yi te jàng aaya yi ci nekk kese, taxul jàngale bu baax Biibël bi. Bu ñu bëggee jàngale bu baax, fàww ñu laal xolu nit ñi. Loolu laaj na ñu waajal bu baax suñu bopp te bu ñu koy def ñu xalaat nit ki ñu war a jàngal. — Léeb. 15:28.
2 Ni ñuy waajale njàng mi : Li ñu war a njëkk def mooy ñaan Yexowa te boole nit ki ak li mu soxla ci ñaan bi. Nañu ñaan Yexowa mu dimbali ñu ba ñu jot xolam (Kol. 1:9, 10). Boo bëggee yaxu waxtaan leer ci sa xel, nanga jël tuuti jot, xool bu baax ni pàcc bi walla njàngale bi tudd, seet xaaj yi ci nekk ak it nataal yi ñu fa def. Nanga laaj sa bopp lii : ‘ Xise yi ñu war a jàng, lan moo waral ñu bind leen ? ’ Loolu dina tax nga xam kàddu yi ëpp solo ci xise yi, ndax nga mën ci gën a yàgg.
3 Jàngal xise bu nekk. Jàngal laaj yi te seet tont yi ñu bind. Nanga rëdd kàddu yi ëpp solo kese. Seetal naka la aaya yi ànde ak kàddu yi ëpp solo. Tànnal it aaya yi nga bëgg jàng ak ki ngay jàngal. Xéyna boo bindee ci xët bi lu lay fàttali li nekk ci aaya yi, dina la dimbali. Kiy jàng Biibël bi, dafa war a gis bu baax ne li muy jàng ci Kàddu Yàlla la jóge. — 1 Tes. 2:13.
4 Nañu fexe ba njàngale mi laal li nit ki soxla : Léegi nag, seetal li nga ko war a jàngal ba xam noo mënee def ba njàngale mi faj ay soxlaam. Jéemal a seet li mu mën a laajte. Seetal it li nga xam ne du ko gaaw a mën a nànd, walla nangu. Laajal sa bopp lii : ‘ Su ma bëggee mu topp li muy jàng, lan la war a nànd bu baax, walla ci lan la war a góor-góorlu ? Lan laa war a def ngir mën a jot xolam ? ’ Te jéemal a topp loolu boo koy jàngal. Xéyna dinga ci bëgg boole misaal, walla luy leeral sa wax, walla leneen loo bëgg laaj ngir kiy jàng. Loolu lépp dina tax kiy jàng xam bu baax li Mbind mi bëgg wax (Nëx. 8:8). Waaye moytul a yokk loo xam ne boo ko waxul woon it, du tere nit ki nànd yaxu waxtaan bi. Te bu njàng mi jeexee, laaj ko ay laaj ci li ngeen jàng. Dina tax mu jàpp ci xelam li ëpp solo ci li ngeen jàng.
5 Bu ñu gisee ñi sog a ñów ci mbooloo mi di meññ jub, maanaam di def li jub ba muy màggal Yexowa, dañuy bég lool (Fil. 1:11). Bu ñu leen ci bëggee dimbali, nañu waajal bu baax suñu bopp saa yu ñuy def njàngum Biibël.