LESOŊ 31
Lan mooy nguuru Yàlla?
Xibaar bi gën a am solo ci Biibël bi, mu ngi jëm ci nguuru Yàlla. Yexowa dina jaar ci Nguuram ngir def li mu bëggoon bi muy sàkk suuf si. Lan mooy nguuru Yàlla? Naka lañu xame ne Nguur googu tàmbali na ilif? Lan la jot a def ba pare? Te lan la nar a def ëllëg? Ci lesoŋ bii ak ci ñaar yi ci topp, dinañu tontu ci laaj yooyu.
1. Lan mooy nguuru Yàlla, te kan mooy buur bi?
Nguuru Yàlla, gornmaa la bu Yexowa Yàlla taxawal. Yeesu Kirist mooy buur bi, te mu ngi nguuroo ci kaw asamaan (Macë 4:17; Yowaana 18:36). Biibël bi lii la wax ci Yeesu: «Dina yilif [...] ba fàww» (Luug 1:32, 33). Ni buur ci nguuru Yàlla, Yeesu dina ilif ñépp ñi nekk ci kaw suuf.
2. Ñan ñooy nguuru ak Yeesu?
Yeesu du nguuru moom rekk. «Ay nit ñu bokk ci bépp giir ak kàllaama ak réew ak xeet [...] dinañu nguuru ci àddina» (Peeñu 5:9, 10). Ñaata nit ñooy nguuru ak Kirist? Bi Yeesu ñëwee ci kaw suuf ba léegi, ay milioŋi nit nekk nañu ay taalibeem. Waaye 144 000 ci ñoom rekk, ñooy dem ci kaw asamaan ngir nguuru ak Yeesu (Jàngal Peeñu 14:1-4). Ñi ci des ñépp ci kaw suuf lañu nar a dund, ci kilifteefu nguuru Yàlla (Sabóor 37:29).
3. Lan moo tax nguuru Yàlla gën nguuru doomu Aadama yi?
Bu dee sax njiiti doomu Aadama yi dañuy jéem a def lu baax, amuñu kàttanu matal lépp li ñu bëgg. Rax-ci-dolli, njiit yooyu dañu leen di folli, fal ñeneen. Te ñi leen di wuutu, xéyna seen njariñu bopp rekk lañuy wut waaye du njariñu nit ñi ñuy ilif. Waaye Yeesu miy njiit ci nguuru Yàlla, kenn du mas a jël palaasam. Yàlla dafa «samp nguur gu dul tas mukk» (Dañeel 2:44). Yeesu dina ilif ci kaw suuf si sépp te du gënaatle. Dafa bëgg nit ñi, baax te jub. Te dina jàngal nit ñi ñu wone mbëggeel ci seen biir, mbaax ak njub, ni moom (Jàngal Esayi 11:9).
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal li tax nguuru Yàlla gën bépp nguuru doomu Aadama.
4. Gornmaa bu am kàttan mooy nguuru ci kaw suuf si sépp
Yeesu Kirist moo ëpp kàttan bépp njiit bu mas a am. Jàngal Macë 28:18. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Lan moo tax sañ-sañu Yeesu ëpp sañ-sañu bépp njiit?
Gornmaa doomu Aadama yi dañu leen di faral di rampalaase ak yeneen, te gornmaa bu nekk, ci réewam rekk la nguuram yem. Nguuru Yàlla nag? Jàngal Dañeel 7:14. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Nguuru Yàlla «du foq mukk [maanaam du tas]», lu tax loolu doon lu baax?
Nguuru Yàlla dina nguuru ci kaw suuf si sépp, lu tax loolu doon lu baax?
5. Gornmaa doomu Aadama yi dañu leen war a rampalaase
Lan moo tax nguuru Yàlla war a rampalaase nguuru doomu Aadama yi? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.
Lan la kilifteefu doomu Aadama jur?
Jàngal Kàdduy Waare 8:9. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Ci sa xalaat, ndax nguuru Yàlla war na rampalaase nguuru doomu Aadama yi? Lu tax?
6. Ñiy jiite ci nguuru Yàlla xam nañu bu baax li ñuy dund
Ndegam Yeesu miy suñu buur, dund na ci kaw suuf ni nit, moom dina ‘mana bokk ak nun sunuy naqar’ (Yawut ya 4:15). 144 000 góor ak jigéen yu takku, yi Yexowa tànn ngir ñu nguuru ak Yeesu, ñu ngi «bokk ci bépp giir ak kàllaama ak réew ak xeet» (Peeñu 5:9).
Xam ne Yeesu ak ñépp ñi nar a nguuru ak moom xam nañu bu baax li ñuy dund, ndax loolu dalul sa xel? Lu tax?
Yexowa dafa tànn ay góor ak ay jigéen yu bokkul xeet ngir ñu nguuru ak Yeesu
7. Santaaney nguuru Yàlla ñoo gën
Gornmaa doomu Aadama yi dañuy joxe ay santaane ak di tëral ay sàrt yuy aar ñi ñuy jiite te amal leen njariñ. Nguuru Yàlla itam am na ay santaane ak ay sàrt yu ñu war a topp. Jàngal 1 Korent 6:9-11. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Bu ñépp ci àddina si nekkee di topp santaane Yàlla yi, ci sa xalaat naka la àddina di mel?a
Yexowa dafa laaj nit ñi Nguuram nar a ilif, ñu topp ay santaaneem, ndax foog nga ne loolu jaadu na? Lu tax?
Lan mooy wone ne, nit ñi toppul santaane yooyu, mën nañu soppeeku? (Xoolal aaya 11).
Gornmaa doomu Aadama yi dañuy tëral ay sàrt yuy aar ñi ñuy jiite te amal leen njariñ. Sàrt yi nguuru Yàlla tëral ñoo gën fuuf ngir aar nit ñi te amal leen njariñ
BU LA NIT LAAJOON: «Lan mooy nguuru Yàlla?»
Lan nga koy tontu?
NAÑU TËNK
Nguuru Yàlla, gornmaa bu am la te nekk ci kaw asamaan. Dina ilif suuf si sépp.
Nañu fàttaliku
Ñan ñooy ñiy jiite ci nguuru Yàlla?
Lan moo tax nguuru Yàlla gën bépp nguuru doomu Aadama?
Lan la Yexowa di xaar ci nit ñi Nguuram nar a ilif?
GËSTUL
Xoolal fi Yeesu wax ne fa la nguuru Yàlla nekk.
«Ndax nguuru Yàlla lu nekk ci suñu xol la?» (Ci jw.org la nekk)
Xoolal li Biibël bi wax ci 144 000 nit ñi Yexowa tànn ngir ñu nguuru ak Yeesu.
Lan moo tax benn jigéen ju ñu tëj kaso gëm ne, Yàlla rekk a mën a indi njubte ci kaw suuf?
«Xam naa léegi li fi mën a dindi lu awul yoon» (Réveillez-vous!, nowàmbar 2011)