TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • lmd lesoŋ 11
  • Na li ngay wax nekk lu yomb a nànd

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Na li ngay wax nekk lu yomb a nànd
  • Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ni ko Yeesu defe
  • Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?
  • Nanga roy ci Yeesu
  • Ni nga mënee jëfandikoo bu baax téere bi tudd «Mën nga dund ci jàmm ba fàww!» ngir jàngal nit ñi Biibël bi.
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Na nga dimbali ñi ngay jàngal Biibël bi ñu jël dogalu jaamu Yexowa
    La Tour de Garde annonce le Royaume de Jéhovah (Édition d’étude)—2025
  • Waxal nit ki ci lu leer li mu war a soppi ci dundam
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
Xóotalal waxtaan bi
Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
lmd lesoŋ 11

NI NGA MËNEE JÀNGAL NIT ÑI BA ÑU NEKK TAALIBE YEESU

Yeesu a ngi jàngal ay nit ci wetu benn geej. Ay picc di naaw ci kaw asamaan, am na itam ay fulóor yi leen wër.

Macë 6:​25-27

LESOŊ 11

Na li ngay wax nekk lu yomb a nànd

Njàngale bi: Na ‘ngeen génne ay wax yu yomb a nànd ci seen gémmiñ.’—1 Korent 14:9.

Ni ko Yeesu defe

Yeesu a ngi jàngal ay nit ci wetu benn geej. Ay picc di naaw ci kaw asamaan, am na itam ay fulóor yi leen wër.

Turu WIDEO bi: Misaal bi Yeesu jël ngir xamal ñu ne Yexowa dafa ñu bëgg

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Macë 6:​25-27. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1. Ban misaal la Yeesu jël ngir won ñu ne Yexowa dafa ñu fonk?

  2. Yeesu mënoon na wax lépp li mu xam ci picc yi, waaye defu ko. Lu tax ñu mën a wax ne li mu def mooy li gën ngir laal xolu ñi ko doon déglu?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?

2. Bu ñuy jëfandikoo kàddu yu yomb a nànd ngir jàngal nit ñi, loolu dina leen dimbali ñu jàpp lu ñu leen di jàngal, te li ñuy jàng dina laal seeni xol.

Nanga roy ci Yeesu

3. Bul wax lu bare. Bu dee sax, am na lu bare li nga xam ci ponk bi ngeen nekk di jàng, yemal ci li ñu bind ci biir lesoŋ bi. Te boo laaje nit ki dara, bul yàkkamti, may ko mu tontu la. Bu dee xamul tont bi, walla mu joxe tont bu àndul ak li Biibël di jàngale, mën nga ko laaj yeneen laaj yu koy dimbali mu am tontu bu baax bi. Bu ponk bi ngeen nekk di jàng leere ci moom, jarul nga ciy yokk leneen. Jàll-leen ci ponk bi ci topp.

4. Dimbalil ki ngay jàngal Biibël mu lëkkale lu bés li mu jàng ak li mu xamoon. Ci misaal, bala ngeen tàmbali lesoŋ buy wax ci ndekkite, njëkkal a xol li mu jot a jàpp ci li ngeen jàng ci liy xew bu nit deewe.

5. Jëfandikool misaal yu yomb a nànd. Laajal sa bopp lii:

  1. ‘Ndax misaal bii, misaal bu yomb a nànd la?’

  2. ‘Ndax ki may jàngal Biibël bi dina nànd misaal bi ma ko bëgg a jox?’

  3. ‘Ndax ki may jàngal Biibël bi, misaal bi rekk lay jàpp, walla ndax misaal bi dina ko dimbali mu jàpp ponk yu am solo yu ma ko bëgg a jàngal?’

SEETAL AAYA YII ITAM

Macë 11:25; Yowaana 16:12; 1 Korent 2:1

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager