Ay tont ci seeni laaj
◼ Li ñuy jëfandikoo bu ñuy waaraate naka la war a mel ?
1Nit mën na xalaat ne waajal na bu baax waaraate bi ndax xam na li mu war a wax. Waaye mën nañu wax ne waajal boobu des na su fekkee ne : amul téere yi ñu war a wone ci weer wi ; yéenekaay yi, téere yi walla kayit yu ndaw yi nekk ci saagam dañu xotteeku walla dañu tilim ; saagam dafa jaxasoo ba du xam fu mu def li muy binde walla kayit fu muy binde ñi mu war a dellu seeti. Balaa ñuy dem waaraate, dañu war a seet bu baax li ñu bëgg yóbbu. Lu am solo la.
2 Bu ñuy waaraate, bu ñu bëggee am lépp li war ci suñu biir saag, lan lañu ci war a def ? Biibël bi mënu cee ñàkk. Def ci it kayit fi ngay binde turu nit ñi nga war a dellu seeti. Seetal ndax def nga ci téere yi ñu war a wone ci weer wi. Dinga soxla it yéenekaay yu bees yi, ay kayit yu ndaw ak ay téere yu ndaw. Bul fàtte téere Comment raisonner. Nanga yóbbu it suñu Sasu Nguuru Yàlla bu mujj bi. Balaa ngay dugg ci kër, dinga ci mën a seet li ngay wax ak ni ngay ubbee sa waxtaan. Boo nekkee foo mënee tase ak ay nit ñuy làkk làkku bitim reew, jëlal téere bu ndaw bi tudd Une bonne nouvelle pour toutes les nations ak kayit bi tudd Veuillez suivre l’intérêt (S-43).
3 Lépp loo def ci sa saag dafa war a set te nekk ci palaasam. Soxlawul sa saag bees. Waaye dafa war a set te bañ a yàqu. Sa saag bokk na ci li ngay jëfandikoo booy waaraate xibaar bu baax bi. Kon fexeel mu bañ a jaxasoo te bañ a yàqu.