Ndax dafa lay teree waare ?
1 Li ëpp ci nit ñi dañu jàpp lool. Ñun Seedee Yexowa yi, ci ñi gën a jàpp lañu bokk — dañuy jàng Baatu Yàlla, di fekke ndaje mbooloo mi, tey bokk ci liggéeyu tool bi. Te yokk ci, dañu jàpp ndax li ñuy génn suñu kër di liggéeyi, di liggéey ci suñu biir kër, walla ñuy def suñu liggéeyu lekkool ak it yeneen wareef yu bare. Te loolu lépp jot la laaj. Ci boroom kër yi nag la gënee metti.
2 Ci béréb yu bare, dund gu metti gi tax na boroom kër yi war a liggéey ay waxtu yu baree bare, liggéey bu metti, ngir mën a yore seeni njaboot. Bu leen seen liggéey laajee li ëpp ci seen jot ak seen doole, li leen di dese ngir waare dootul bareeti. Ndegam ñoom lañu dénk wareefu toppatoo seeni njaboot, yenn boroom kër yi mën nañoo xalaat ne li ñuy mën a bokk ci liggéeyu waare bi du bare (1 Tim. 5:8). Ci lu wóor, li tegu ci kow boroom kër yi, bu ñuy wut a am lu ñuy dunde tey, diis na, bare na. Waaye, suñu liggéey waru ñoo teree waare xibaar bu baax bi (Mark 13:10). Kon nag, war nañoo seetaat li ñu nekke fi ñu tollu nii.
3 Ni àddina si mel, li mu dëkk ci soppi, mën na xiir boroom kër ci liggéey ay waxtu yu baree bare ba mu mujj a ëpp, ndax mu mën a am xaalis bu muy denc ngir jafe-jafe bu ko mën a bett (1 Kor. 7:31). Dëgg la, mën na mel ni bu ñuy yokk liggéey bi ñuy def, suñu alal dina gën a yokku, te dinañu gën a mën a féexal suñu xol te gën a mën a fo. Waaye liggéey boobu ñuy yokk, bu ñu ko defee ci jot gi ñu waroon a jagleel li ñu war a def ci wàllu ngëm, walla ci waxtu yi ñu tàmmoon fekke ndaje yi, ndax dina tax suñu njaboot gën a am bànneex te gën a bég ? Ci lu wóor, bëgg nañoo moytu lépp lu mën a yàq suñu digganteek Yàlla. Topp xelalu Yeesu, maanaam ‘ dajale alal ci asamaan ’ te ‘ am dara ci kanamu Yàlla ’ mooy xel. — Macë 6:19-21 ; Lukk 12:15-21.
4 Jëkkleen a wut njariñi Nguur gi : Yeesu jàngaloon na taalibeem yi ne, seen digganteek Yàlla moo war a jiitu leneen lu mu mënta doon. Xiirtal na leen, naan : “ Buleen jaaxle nag, di wax ne: Lu nu wara lekk? Lu nu wara naan? walla: Lu nu wara sol? ” Lu tax mu wax loolu ? Leeralal na ko : “ Seen Baay, bi nekk ci kaw, xam na ne am ngeen soxla ci loolu lépp. ” Bu ñu loolu wóoree dëgg, dara du ñu teree def li ci Yeesu teg, naan : “ Waaye jëkkleena wut nguuram ak njubteem, te loolu lépp [bépp alal ju ñu soxla] dina leen ko ci dollil. ” Soxla yooyu, Yàlla dina leen faj (Macë 6:31-33) ! Ci lu wóor, du léegi lañu war a bàyyeeku ndax li ñu jaaxle ba mu ëpp lu jëm ci li ñuy dunde. Du ci jamano jii nga xam ne léegi mu wéy, lañu war a wut dund gu ñàkkul dara. — 1 Pieer 5:7 ; 1 Ywna. 2:15-17.
5 Li njëkk a tax nit di liggéey mooy wut li muy faje ay soxlaam. Waaye lan lañu soxla dëgg ? Ndaw li Pool bindoon na : “ Kon su ñu amee lekk ak koddaay [lu ñuy sol], nanu ko doyloo ”. Ndax dañuy jéem a am lu ëpp loolu ? Bu dee waaw, xéy na ñu ngiy góob li loolu di jur te Pool artu woon ñu ci : “ Ñiy sàkkoo barele, dinañu jànkoonte ak i nattu, ba dugg ci fiir, di xuus ci bëgg-bëggi neen yuy yóbbe ayib [yuy lore], tey sóob nit cig réer ak sànkute. ” (1 Tim. 6:8, 9 ; Macë 6:24 ; Lukk 14:33). Naka lañu mënee xam ndax bëgg-bëgg yu ëpp a ngi ñuy teree def li war ?
6 Suñuy soxlay àddina, bu ñu taxee ñu def li gën a néew kese ci liggéeyu tóol bi, walla ñu xalaat ne soxlawuñoo xañ suñu bopp yenn yi ngir xibaar bu baax bi, bu boobaa soxla nañoo jubbanti li ñuy jiital ci suñu dund (Yaw. 13:15, 16). Dundin bu gën a yem dina am njariñ lool ngir dindi loolu ñuy teree waare. Suñu jot ak suñu kàttan, ngir njariñu Nguur gi lañu ko war a njëkk a jëfandikoo.
7 Liggéey bu ñu deful ci neen : Li Pool wax dafa ñuy xiirtal ci dëkk ci ‘ gëna sawar ci liggéeyu Boroom bi, xam ne suñu liggéey, bi jëm ci Boroom bi, du neen ’. (1 Kor. 15:58.) Li ëpp solo ci “ liggéeyu Boroom bi ” mooy waare Nguur gi tey sàkk ay taalibe (Macë 24:14 ; 28:19, 20). Bu ñu bëggee li ñuy def ci liggéey boobu nekk lépp li ñu ci mën dëgg, ayu-bés gu nekk, war nañoo ber ay waxtu ngir liggéeyu tóol bi, te góor-góorlu ngir bañ a jëfandikoo waxtu yooyu ngir leneen (Efes 5:15-17). Noonu, dara du ñu teree waare, du suñu liggéey, du leneen.
8 Bu ñu nangoo xamal nit ñi dëgg gi nekk ci Biibël bi, dinañu am bànneex bi sut, bi nekk ci maye (Jëf. 20:35). Bu ñuy sax ci liggéeyu waare Nguur gi, dinañu mën a séentu ëllëg ak kóolute, ndaxte “ Yàlla ñàkkul worma bay fàtte [suñu] liggéey ak mbëggeel gi [ñu] wone ci turam ”. — Yaw. 6:10.