TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 2/02 p. 1
  • Nit ñi gën a bég ci àddina si

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nit ñi gën a bég ci àddina si
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 2/02 p. 1

Nit ñi gën a bég ci àddina si

1 “ Nit ñi nga xam ne Yexowa mooy seen Yàlla, bég nañu ! ” (Sab. 144:15). Loolu dafay wone ne Seede Yexowa yi ñooy ñi gën a bég ci àddina si. Yexowa rekk mooy Yàlla dëgg ji. Mbégte bi ngay am boo koy jaamu, mënoo ko am feneen. Ndegam Yexowa mooy “ Yàlla ji bég ”, ñi koy jaamu dañuy jël ci mbégteem (1 Tim. 1:​11, NW). Bu ñuy jaamu Yàlla, yan ñooy yenn ci li mën a tax ñu bég noonu ?

2 Lu tax ñuy bég : Yeesu waxoon na ne li mën a tax ñu am bànneex mooy “ xam ne am na li ñu soxla ci wàllu xel ”. (Macë 5:​3, NW.) Di jàng Biibël bi te di fekke suñuy ndaje karceen yi yépp, loolu moo ñuy may li ñu soxla ci wàllu xel. Diine yu dul dëgg yi, dañuy jàngale ay fen. Li ñu jàng dëgg gi nekk ci Kàddu Yàlla, moo ñu ci génne (Ywna. 8:32). Mbind mi jàngal nañu it ban dundin moo gën ci nit (Isa. 48:17). Looloo tax ñuy am ay xarit yu baax ci suñu biir mbokki karceen yi bég. — 1 Tes. 2:​19, 20 ; 1 Pie. 2:⁠17.

3 Topp yoonu Yàlla dafay tax ñu bég, ndaxte xam nañu ne loolu dafa ñuy sàmm te dafay tax Yexowa bég (Léeb. 27:11). Am na taskatu xibaar bu wax lii : ‘ Ak ndigal yu bare yi ñu war a topp yépp, ndax Seedee Yexowa yi niroo nañu ay nit ñu bégul ? Mukk ci àddina ! Mag ñi ak ndaw yi yépp, dañu niroo ñu am mbégte te regle. Loolu barewul ci niti tey. ’ Naka lañu mënee dimbali ñeneen ñi ndax ñu bég ni ñun ?

4 Dimbalil ñeneen ñi ndax ñu bég : Nit ñu bégul rekk a bare tey, te nit ñi faral nañu xalaat ne suñu ëllëg dina lëndëm. Waaye ñun Seede Yexowa yi, gëm nañu ne ëllëg dina neex, ndaxte xam nañu ne bés a ngi ñów fu kenn dootul amati naqar (Peeñ. 21:​3, 4). Looloo tax ñuy sawar ci waaraate bi, di wut nit ñi woyof, ndax ñu mën leen a xamal li ñu yaakaar ak itam li ñu gëm ci Yexowa. — Esek. 9:⁠4.

5 Suñu benn mbokk mu jigéen bu nekk pioñee dafa ne : “ Dimbali nit ba mu xam Yexowa ak dëgg gi jóge ci moom, dara dàqu ko. ” Nañu def lépp li ñu mën ndax nit ñu gën a bare nangu ñu jàngal leen Biibël bi ci seen kër. Jaamu Yexowa te dimbali ñeneen ñi ndax ñu jaamu ko, dafay maye mbégte bi gën a réy. — Jëf. 20:35.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager