Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 sãw.
“ Nit ñu bare dañuy jëfandikoo ay nataal bu ñuy jaamu Yàlla. Ndax foog nga ne nataal yooyu mën nañu leen dimbali ? [May ko mu tontu.] Seetal fii, li ñu Yàlla dëgg ji nar a defal. [Jàngal Peeñu bi 21:3, 4.] Yàlla dëgg ji rekk moo mën a def lu mel nii. Yéenekaay bii dafay wone Yàlla jooju ku mu doon, te bu ñu ko gëmee, lan lañu ci jële. ”
Réveillez-vous ! 22 sãw.
“ Mën nañu foog ne ñépp a am fu ñu dëkk. Waaye ay milioŋi nit ñu ngi daw seen réew, di wër àddina si. Amuñu kenn ku leen di dimbali. Ñooñu, jàmm ji ñu bëgg, amuñu ko. Réveillez-vous ! bii, dafay wax lu tax coono boobu am. Dafay wax it ne, Mbind mu sell mi dig na ne, bés a ngi ñów, ñépp ay am fu ñu dëkk. ”
La Tour de Garde 1 feew.
“ Nit ñu bare ñu ngi wax ci liy tilimal suuf si ak lépp li ci nekk. Waaye, ndax mas nga xalaat ci li mën a tilimal xelu nit ? [May ko mu tontu.] Mbind mu sell mi dafay wone lu tax set ci yaram ak ci ngëm baax. [Jàngal 2 Korent 7:1.] Wóor na ma ne li nekk ci téere bii, dina la dimbali. ”
Réveillez-vous ! 8 feew.
“ Bu ñaari nit di séy, ñépp a faral di bég. Waaye séy yu bare dañuy tas. Mbind mu sell mi dafay wax li mën a tax séy yàgg te bare jàmm. Loolu la Réveillez-vous ! bii di wone. Dama la ko bëgg a jox. ”