Suñuy wideo, fasoŋu waaraate buy laal nit ñi
1 “ Suñu doom ju góor seetaan na wideo boobu balaa muy mën a dox. Dafa ko seetaan ay yooni yoon. Wax dëgg, am liy tax suñuy doom bëgg Yexowa, lu baax la ! ” Ban wideo la karceen boobu doon wax ? Wideo bi tudd : Noé : il marchait avec Dieu. Benn jigéen ju nekkul Seede, doomam dafa seetaan wideo bi ci kër keneen. Jigéen jooju dafa may suñu benn bànqaas 90$ (xaalis bu ëpp 60 000 CFA), daldi leen laaj ndax amuñu yeneen wideo yu ñu defar ngir xale yi. Wideo yi mbootaayu Yexowa def dañuy laal mag ak ndaw bu baax-a-baax.
2 Ci biir njaboot gi : Benn njaboot dafa doon seetaan wideo bi tudd La fermeté des Témoins de Jéhovah face à la persécution nazie. Bi ñu ko seetaanee ba pare, yaay ji dafa ne : “ Bés boobu yépp, dama xalaat ci li Yexowa di def ba ay nit ñu mel ni ñun mën a muñ lu metti lool ! Foofu laa gis ne coono yi ma am, du dara. Ci la xale yi gën a gis ne dañu war a yaakaar ci Yexowa. Bi ñu ci waxtaanee ak ñoom, dañu gën a xam li ñu mën a def bu ñuy am ay jafe-jafe, walla bu ñu leen di fitnaal. ”
3 Ci lekkool bi : Benn Seede Yexowa dafa wone wideo Fermeté ci biir kalaasam. Bu njëkk, jàngalekatam bëggul woon Seede Yexowa yi. Waaye bi mu seetaanee wideo boobu, dafa ne : “ Li ma doon xalaat ci Seede Yexowa yi, dafa soppeeku bu baax-a-baax. Léegi, xamleen ne, bu ñu ñówaatee sama kër, dinaa leen déglu te dinaa jàng ak ñoom Biibël bi ! ” Lu tax xalaatam soppeeku noonu ? Nee na “ suñu mbëggeel dëgg ak suñu ngor ” ñoo ko tax a soppeeku.
4 Bu ñuy waaraate : Suñu benn mbokk mu jigéen dafa gis benn jigéen ju doon laajte ay laaj ci Seede Yexowa yi ak ci seen ngëm. Waaye jigéen jooju sawarul woon jël suñuy téere. Suñu mbokk mi daldi fa dellu ngir indil ko wideo Les témoins de Jéhovah : un nom, une organisation. Ñu daldi ko seetaan moom ak jëkkëram. Li ñu fa gis, dafa leen dugg ba ñu nangu jàng Biibël bi. Mujj ga, ñu tàmbali topp li Yàlla laaj.
5 Ndax yéen a ngi jëfandikoo suñuy wideo ni mu gëne ?