Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
11-17 màrs
Woy-Yàlla 18
13 min: Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na ñaari nit topp li nekk ci xaaj bi tudd “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi ” bi nekk ci Sasu Nguur Yàlla bii walla bi ko jiitu, te wax ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! walla La Tour de Garde yi ñu mujj a jot. Na ku ci nekk wone li ñu mën a tontu bu amee ku ñu wax : “ Loolu soxalu ma. ” — Seetal Comment raisonner, ci xët 16.
12 min: Saa yu nekk, nañu nekk ay karceen yu dul faral kenn. Waare la war a doon, te mag bu mën jàngale moo ko war a def. Ci lekkool yi, fi ñuy liggéeye, walla fi ñu dëkk, nit ñi, ñu ngi gën di wone ne dañu fonk seen réew ba mu ëpp. Ñenn ci ñi koy def dañuy bëgg dindi noonu tiitaange ak metit bi ñu yëg bi ñu songee seen réew. Bu dee sax li ñuy gis ci àddina si dafa ñuy metti ñun itam, xam nañu ne li gën a am solo mooy xam ki war a ilif àddina si sépp ak lépp li Yàlla sàkk. Te xibaaru Nguur gi dafay dalal suñu xel. Bu nit ñi dee wone ne dañu fonk seen réew ba mu ëpp, ñun duñu ci bokk. War nañu ànd ak teggin bu ñuy wax nit ñi lu tax ñuy def loolu. Waaye war nañu leen won it ne Kàddu Yàlla mën na leen may yaakaar te mën na dalal seen xel, ni mu ñu ko defe. Téere Les témoins de Jéhovah et l’instruction ci xët 20-24, ci “ Le salut au drapeau ”, wax na lu tax duñu bokk ci li nit ñi di def ngir wone ne dañu fonk seen réew ba mu ëpp. Waxal li ëpp solo ci li ñu bind foofu, te waxal way-jur yi ñu waxtaan ci bu baax ak seeni doom. Waxal it li ñu bind ci xët 20 ak itam li nekk ci Réveillez-vous ! bu 8 Sãwiyee 1996 ci xët 31. Woneel ne dañu war a may cër kilifay nguur yi, waaye Yexowa kese lañu war a jaamu.
20 min: “ Na nga “ bare jëf yu rafet. ” ”a Wottukatu liggéeyu waare bi moo ko war a def. Waxal nit ñépp ne dañu war a waaraate bu baax-a-baax ngir waajal ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu bu 28 màrs bi. Waxtaanleen ci ni ñu mënee jëfandikoo ni mu gënee baax kàrt yi ñuy woowe nit ñi ci ndaje boobu. Laajal waaraatekat yi ñu nettali ni ñu def ba daaw, seeni mbokk, seeni dëkkandoo, ñi nuy jàngal Biibël bi ak ñeneen, ñów fekke ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Nañu wax it ban mbégte lañu ci jële. Waxal it ne képp ku ko mën, na nekk aji-xàll yoonu weer (pionnier auxiliaire) ci weeru awril. Bu ndaje bi jeexee, ku soxla kayit bu ñuy bind ngir nekk aji-xàll yoon, mën na ci am benn.
Woy-Yàlla 37 ak ñaan bu mujj bi
18-24 màrs
Woy-Yàlla 87
10 min: Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi. Waxtaanleen ci “ Li ñu warul a fàtte ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ”. Waxal nit ñi ñu jàng bés bu nekk aaya yi ñu def ci téere Examinons les Écritures chaque jour — 2002, ngir fàttaliku deewu Yeesu, ci diggante 23-28 màrs.
15 min: “ Nekk benn ak Yexowa ak Doomam te bég ci. ” Waxtaan bii, mag moo ko war a def ngir xiir nit ñi ci jëf. Waxal nit ñi ñu gën a góor-góorlu ci diggante tey ak 28 màrs ngir wax nit ñu nu mën a jot yépp, ñu teew ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu.
20 min: “ Leetar bu ñu Jataay biy dogal yónnee ” ci xët 6. Waare ak waxtaan ak ñi teew. Mag bu mën jàngale moo ko war a def.
Woy-Yàlla 20 ak ñaan bu mujj bi
25-31 màrs
Woy-Yàlla 31
14 min: Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal ne waxtu jël kayit bu ñuy bind ngir nekk aji-xàll yoonu weer ci weeru awril, weesagul. Na ñaari nit topp li nekk ci xaaj bi tudd “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi ” bi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bii walla bi ko jiitu, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj a jot. Na benn magi mbooloo wone La Tour de Garde, te benn ndaw wone Réveillez-vous ! Ku ci nekk, bu paree, waxal li am maanaa ci li mu wax.
15 min: Li nekk soxla mbooloo mi.
16 min: Jëfandikool Comment raisonner ngir mayaat doole ñi ko soxla. Waxtaan ak ñi teew. Ñépp a soxla dégg yenn saay ay wax yu leen di mayaat doole. Looloo tax ñu war a xam ne dañu war a dalal xelu nit ñi. Nit ñi am naqar yi nuy gis bu ñuy waaraate bokk nañu ci nit ñooñu ñu war a dalal seen xel (1 Tes. 5:14). Laajal ñi teew, bu ñu bëggee dalal xelu ku am benn ci jafe-jafe yu nekk ci Comment raisonner ci xët 119-122, yan aaya lañu nar a jëfandikoo. Waxal nit ñi ne, na ku nekk jéem a dalal xelu kenn ku nekk ci jafe-jafe yooyu. — Gal. 6:10.
Woy-Yàlla 56 ak ñaan bu mujj bi
1-7 awril
Woy-Yàlla 10
7 min: Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fàttalil waaraatekat yi ne dañu war a bind li ñu def ci weeru màrs te joxe ko.
18 min: “ Góor ñi nekk ay may dañuy sàmm bu baax géttu Yàlla ”. Waxtaan bi nekk ci xët 5, wottukat biy jiite walla wottukatu liggéeyu waare bi moo ko war a def. Waxtaanleen ci aaya yi ñu lim. Sàmm ñi bàyyi waaraate walla dimbali ñi seen yaram neexul ba ñu def li ñu mën, mën na jur lu baax. Woneel lu baax li mu mën a jur. Sàmmkat yu baax, dañuy wone ne li suñu mbokk yooyu di def ngir liggéeyal Yexowa, rafet na.
20 min: “ Yokkleen mbégte bi ngeen di am bu ngeen di waaraate. ”b Bu ngeen tolloo ci xise 5, laajteel li ñu mën a def ci suñu gox ngir waaraate bi jur lu baax. Na benn walla ñaari nit wone ni ñu mënee jege nit ba waar ko, waar bu gàtt. Waxal ne ku nekk mën na fexe ba waaraate ci ayu-bés bii.
Woy-Yàlla 98 ak ñaan bu mujj bi
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.