Nekk benn ak Yexowa ak Doomam te bég ci
Xew-xew bi ëpp solo ci at mi yépp, 28 màrs lay doon
1 Bu jant bi sowee ci 28 màrs 2002, dinañu màggal li ñuy woowee Reeru Sang bi. Noonu lañuy wonee ne, ñun Yexowa ak Yeesu Krist, dañu nekk benn te dañu ci bég. Ci xew-xew bu am solo boobu, ñi des ci karceen yi ñu tànn, dinañu “ bokk ” ak ñeneen ñiy donn Nguur gi, bokk ak Baay bi, te bokk ak Doomam. Mbégte lañu ciy am (1 Ywna. 1:3 ; Efes 1:11, 12). Ay milioŋi nit ñu bokk ci ñi ñuy woowe ‘ yeneeni xar ’ yi, dañu bokk xol te bokk xalaat ak Yexowa ak Doomam ci liggéey bi ñu Yàlla sant. Nekk benn ak Yexowa ak doomam lu am solo la. ‘ Yeneeni xar ’ yooyu dinañu ci xalaat. — Ywna. 10:16.
2 Nañu ànd liggéey te jàppoo : Yexowa ak Yeesu dañu mas a nekk benn, te loolu dafa leen bégal. Ci lu mat ay ati at bala Yàlla sàkk nit, dañu doon ànd, seen diggante rattax (Mik. 5:2). Looloo tax ñu bëggante bu baax-a-baax. Taaw boobu, bala muy nekk nit ci kow suuf, dafa meloon ni xam-xam bu jël taxawaayu nit. Looloo tax mu mën a wax ne : “ Dama mujj nekk ki nga xam ne bés bu nekk, [Yexowa] dafa koy gën a bëgg. Ci wetam, saa yu nekk dama doon bég. ” (Léeb. 8:30). Lu mat ay ati at, Doomu Yàlla ànd na ak ki nga xam ne ci moom la mbëggeel jóge, seen diggante rattax. Ci lu wóor, am na li loolu jur ci moom. — 1 Ywna. 4:8.
3 Doom bi Yexowa am képp, bëgg na doom-Aadama yi lool. Doom boobu la Yexowa tànn ngir mu nekk saraxu njot boo xam ne, moom rekk moo ñu mën a muccloo. Yexowa dafa def loolu ndax xamoon na ne doom-Aadama dafa soxla li koy musal (Léeb. 8:31). Yexowa ak Yeesu, ñoom ñaar, bokk nañu li ñu bëgg def. Ni ñu nekke benn ci def loolu, ñun itam, noonu lañuy nekke benn ak ñoom, nekk benn it ci suñu biir, ndax mbëggeel bu xóot bi ñu boole. Te dañuy def li Yexowa bëgg ak xol bu sedd.
4 Nañu wone ngërëm bu jóge ci suñu xol : Am na ni ñu mën a wonee ne dañuy gërëm Yexowa ndax mbëggeel bi mu ñu won, di gërëm it Doomam ndax sarax bi mu def ngir ñun. Ngërëm boobu mën nañu ko wone, bu ñu teewee ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, te bu ñu dégloo bu baax-a-baax. Ci ndaje boobu, dinañu wone bu baax mbëggeelu Yeesu, ak ngor bi mu wone ba dee fekk ko ci, bi mu doon joxe njot bi. Dinañu wone it ne mu ngi ilif niki buuru Nguuru Yàlla, ak it barke yi Nguur googu di indil doom-Aadama yi. Dinañu fàttaliku it ne saa yu nekk, dañu war a wone suñu ngëm, nekk nit ñuy ‘ liggéeyandoo ci dëgg gi ’ te sawar a def li Yexowa bëgg. — 3 Ywna. 8 ; Saak 2:17.
5 Nañu dimbali ñeneen ñi ndax ñu teew ak ñun : Mag ñi war nañu góor-góorlu ngir wax bépp Seede bu bàyyi waaraate te dëkk ci goxu mbooloo mi, mu ñów teew ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Krist (Macë 18:12, 13). Bindleen turu seede yooyu, ndax ñu bañ ci fàtte kenn te waxleen kenn ku ci nekk mu ñów ci ndaje boobu.
6 Ndax xam nga ñeneen ñu mën a ñów ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ? Fexeel ba ñu am ngërëm ci ndaje boobu. Wax leen ñu ñów fekke ndaje boobu, te xamal leen ne bu ñu ñówee, dinañu ci am mbégte bu réy. Nañu fexe ba wax ñi nuy jàngal Biibël bi ñépp, ñu ñów fekke xew-xew boobu nga xam ne, mooy bi ëpp solo ci at mi yépp. Nañu ko wax it ñeneen ñi bëgg suñu waxtaan, suñu mbokk yi ak it nit ñi nu xam. Képp ku jàng “ xéewali xam Krist Yeesu ”mën na jariñoo njot bi (Fil. 3:8). Ñiy wone gëm ci saraxu Krist mën nañu am yaakaaru dund gu dul jeex, bi nekk yaakaar bu wóor. — Ywna. 3:6.
7 Buñu xeeb mukk li ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu mën a jur ci nit ku gore. Am na ñaari at, ci réewu Papouasie-Nouvelle-Guinée, 11 nit ñu bëgg suñu waxtaan, dañu bëggoon a fekke ndaje boobu. Dañu tukki lu mat 17 waxtu ci gaal gu ndaw ci géej bu yëngu woon lool. Lu tax ? Dañu ne : “ Dañu bëggoon a màggal ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ak ñiy jaamu Yexowa. Ndaje boobu jaraloon na ñu tukki noonu. ” Seetal ñooñu ni ñu saware ! Gisal it ni ñu ame ngërëm ci li ñu mënoon a nekk benn ak Yexowa, Doomam, ak njabootu karceen yi, te am ci mbégte !
8 Nañu wax ñi bëgg suñu waxtaan ñépp ne mën nañu jàng Biibël bi ak ñun. Dimbali leen ñuy fekke ndaje yi yépp te ñuy xamal ñeneen ñi dëgg gi ñu jàng. Dimbali leen ñu “ dox ci leer gi ” te jëfe dëgg gi ci li ñuy topp ndigali Biibël bi ci seen dund (1 Ywna. 1:6, 7). Dimbali leen ndax seen diggante ak Yexowa gën a rattax, te ñuy gën a fonk li ñu mën a ànd ak ñeneen di def li mu bëgg.
9 Nekk benn te am mbégte “ ci menn xel, bokk benn xalaat ci bëre luy saxal dëggu xebaar bu baax bi ”, lu am solo la ! (Fil. 1:27, 28.) Yàkkamti nañu 28 màrs, bésu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Bés boobu, dinañu mën a nekk ak suñu mbokki karceen yi, di ci gërëm Yexowa ak Doomam ! — Lukk 22:19.