Yokkleen mbégte bi ngeen di am bu ngeen di waaraate
1 Ndax mas nga yëg mbégte bi nuy am bu ñuy xamal nit ñi xibaar bu baax bi ? Bu ñu deful ndànk, àddina su bon sii ñu wër, mën na tax ñu ragal a waare, ba ñu bañ a amati mbégte bi ñu ci doon am. Bu fekkee ne fi ñuy waaraate, nit ñi ñuy waxal duñu déglu, loolu it mën na tax ñu bañ a sawarati waaraate. Lan lañu mën a def ngir yokk mbégte bi ñuy am bu ñuy waaraate ?
2 Na nga rafet njort : Fexe ba rafet njort ci waaraate bi, dafa ñuy dimbali dëgg. “ Liggéeyandoo ” ak Yàlla, mbégte mu réy la. Bu ñu xalaatee bu baax ci mbégte boobu, dina tax ñu rafet njort (1 Kor. 3:9). Yeesu it mu ngi ànd ak ñun ci liggéey boobu (Macë 28:20). Dafay jëfandikoo ay malaaka yu baree bare ngir jàpple ñu ci liggéey boobu (Macë 13:41, 49). Kon, na ñu wóor ne Yàlla mu ngi jiite li ñuy def ci liggéey boobu (Peeñ. 14:6, 7). Kon nag, ak li nit ñi mën a def bu ñu leen di waar, suñu liggéey dafay tax ñi nekk ci asamaan si am mbégte bu réy !
3 Waajalal bu baax sa liggéey : Bu ñu waajalee bu baax suñu liggéey, suñu mbégte dina yokku. Waajal waaraate, soxlawul lu bare. Li muy laaj mooy jël tuuti minit ngir seet lenn ci li nekk ci yéenekaay yi ñu yàggul a jot, walla ci téere bu ñuy wone ci weer wi, ngir mën cee waxtaan. Ci biir Sasu Nguuru Yàlla, tànnal benn waxtaan ci yi nekk ci “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi ”. Seetal it ni nga mënee waaraate ci li nekk ci “ Suggestions de présentations pour le ministère ” bu nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu Sàwiyee 2002 ci xët 2 ba 4, ak it li nekk ci Le ministère du Royaume bu janvier 2002 ci xët 3 ak 6. Mën nga seet it ci téere Comment raisonner li nga mën a njëkk wax booy waxtaan ak nit. Bu fekkee ne, fi ngeen di waaraate, nit ñi tàmm nañu wax loo xam ne dafa lay tere àggale sa waaraate, waajalal tontu bu mën a laal wax jooju te wax it ci lu leen mën a neex. Téere Comment raisonner mën na la dimbali bu baax ci loolu. Yu mel noonu, bu ñu ko defee, dafay tax ñu gën a wóolu suñu bopp bu ñuy waaraate. Loolu mooy tax ñu am mbégte bu ñuy waaraate.
4 Ñaanal bu baax : Bu ñu bëggee suñu mbégte yàgg ci ñun, dañu war a ñaan Yàlla. Ndegam liggéeyu Yexowa lañuy def, soxla nañu ñaan xelam miy jur mbégte (Gal. 5:22). Yàlla bëgg na ñu may doole ndax ñu wéy di waaraate (Fil. 4:13). Lu metti bu ñu dalee bu ñuy waaraate, ñaan yi ñuy def ngir suñu liggéeyu waare, mën nañu dimbali ndax ñu gise ko ni ñu ko war a gise (Jëf. 13:52 ; 1 Pie. 4:13, 14). Bu ñu rusee, ñaan mën na ñu dimbali ndax ñuy waaraate di ci ànd ak fit te di ci am it mbégte. — Jëf. 4:31.
5 Fexeel ba mën a waaraate : Bu ñu mënee gis nit ñi te mën leen a waar, ci lañuy gën a am mbégte ci suñu liggéeyu waare. Fexeel ba ngay waaraate kër-oo-kër ci ay waxtu yu wuute. Xéyna, booy waaraate ci ngoon-a-ngoon, walla buy tàmbali guddi, dina gën a baax. Saa yooy dox ci mbedd mi, booy jëndi dara, booy dugg ci kaar walla booy doxantu, dinga tase ak ay nit. Lu tax doo waajal wax ju gàtt joo mën a wax ngir tàmbali waxtaan ak ñoom, ba noppi jege ku niroo ku neex deret ngir wax ak moom ? Walla mën na am ngay liggéey, walla ngay jàngi, foo xam ne bés bu nekk yaa ngi fay waxtaan ak ay nit. Boo waxee lenn lu nekk ci Biibël bi te mën a neex nit ñi, loolu mën na la may nga waaraate. Bind nañu ci Le ministère du Royaume bu janvier 2002, ci xët 3, loo mën a wax ba ñu nangu la déglu. Xelal yii, boo ci mënta topp, mën na yokk bu baax mbégte bi ngay am booy waaraate.
6 Ndegam mbégte dafa ñuy dimbali ci suñu muñ, fexe ba ñu bañ koo ñàkk, lu am-a-am solo la ! Bu ñu defee loolu, liggéey bii nga xam ne dootuñu ko defati bu jeexe, dinañu am pey gu réy. Loolu rekk mën na yokk mbégte bu ñuy am bu ñuy waaraate. — Macë 25:21.