TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 4/02 p. 3
  • “ Nanuy defal ñépp lu baax ”

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • “ Nanuy defal ñépp lu baax ”
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu góor-góorlu ci def lu baax !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • ‘ Nanga yégle fu nekk Kàddug Yàlla ’
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Na nga “ bare jëf yu rafet ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • ‘ Nañu seedeel ci ñépp xebaar bu baax bi ’
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 4/02 p. 3

“ Nanuy defal ñépp lu baax ”

1 Ci Sasu Nguuru Yàlla bu feewriyee ak bu màrs 2002, waxtaan nañu ci “ ‘ Nanga yégle fu nekk Kàddug Yàlla ’ ” ak “ Na nga bare ‘ jëf yu rafet ’ ”. (Kol. 1:25 ; 1 Tim. 6:18.) Foofu, dañu waxoon ne dañu war a def lépp li ñu mën ngir : 1) dimbali ñi suñu waxtaan neex ñu fekke ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ; 2) dimbali ñi bàyyi waaraate ba ñu bokkaat ci li ñuy def ci mbooloo mi ; 3) dimbali suñuy doom ak ñiy jàng Biibël bi te mat waaraatekat, ba ñu tàmbali waare xibaar bu baax bi. Wóor na ne, lépp li ñu def ngir topp loolu, am na lu baax li mu jur. Léegi, “ fi ak nu koy man, nanuy defal ñépp lu baax ”. — Gal. 6:⁠10.

2 Nañu leen wax ñu ñówaat : Gis nañu ne daaw, ci digg ak ci sowu Afrig, lu ëpp 600 000 nit ñu nekkul waaraatekatu xibaar bu baax bi, fekke nañu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Loolu wone na ne suñu waxtaan, am na fu mu leen neex. Kon nag, lan lañu mën a def ba “ ñépp ñu jagoo dund gu dul jeex ” bëgg bokk ci ñi “ gëm ” ? (Jëf. 13:48.) Nañu leen xelal ñu gaaw a fekkewaat ndaje yi ñuy am ci mbooloo mi.

3 Boo gisee ku suñu waxtaan neex, wax ko mu ñów fekke waxtaan bu neex bu jëm ci li yonent Yàlla Isayi bind, ci ndaje bu ñuy wax Njàngum téere bi. Bu dee sa mbokk walla sa xarit la, te nga war a def waxtaan ci lekkoolu sasu Nguuru Yàlla, mën nga koo wax mu ñów déglu waxtaan boobu. Wax ko li ñuy waxtaane ci ayu-bés yi di ñów, ci ndaje bi ñuy woowe Ndaje ngir ñépp. (War nañu taf ci tablo bi nekk ci saalu Nguur gi waxtaan yi ñuy am ayu-bés bu nekk.) Seetal lépp loo mën a def ngir mu bëgg jaamu Yexowa. Te bu fekkee ne amul ku koy jàngal Biibël bi, wax ko ne bu bëggee, mën nga jàng Biibël bi ak moom.

4 Nañu wéy di dimbali ñi bàyyi waaraate : Ci ñi fekke ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, am na ñu jébbal seen bopp Yexowa ba pare. Waaye dañu dem ba bàyyi waaraate xibaar bu baax bi. Wànte Pool dafa ñu xelal ñu def “ lu baax, rawati-na nag sunu mbokk yi gëm [mbokk ci ngëm, NW] ”. (Gal. 6:10.) Kon ñi nu war a gën a xalaat ñooy ñi bàyyi waaraate.

5 Xéyna, mag ñi walla ñeneen dimbali nañu ñu mel noonu ba ñu nangu tàmbaliwaat waaraate bi. Bu la mag ñi waxee nga dimbali kenn ci ñoom, xamal ne bu kooku gisee ni nga bëgge Yexowa ak waaraate bi, dina tax mu gën a ñeme waar nit ñi. Won ko ni ngay bokke ci lépp li liggéeyu waare bi ëmb. Loolu dina tax buy waare, dina ci am mbégte, dina ci yàgg, te Yexowa dina ko barkeel.

6 Nañu dimbali ñi sog a nekk waaraatekat, ñu tàmbali bu baax liggéey bi : Am na benn jigéen bu doon waxtaan ak Seede yi. Bi mu gisee ne seen mbootaay mooy mbootaayu Yàlla dëgg, ci la bëggee tàmbali waaraate. Bi mu xamee li mu war a def, dafa ne : “ Aywa. Amatuma lu may xaar. ” Su fekkee ne mag ñi wax nañu ne ki ngay jàngal Biibël bi mën na tàmbali waaraate, dimbali ko mu xam ne waratul ‘ am lu muy xaar ’, ndax mu mën a tàmbali bu baax liggéeyu waare bi. Dimbali ko ndax waajal te bokk ci waaraate bi nekk li mu tàmm def ayu-bés bu nekk.

7 Bu fekkee ne sa doom moo sog a nekk waaraatekat bu ñu sóobagul, dimbali ko mu jëm kanam te bul fàtte at yi mu am ak li mu mën a àttan. Boo ko dimbalee tuuti rekk, mën na am mu jaaxal la boo gisee ni mu mënee waxtaan ak nit ñi, jàng ci Biibël bi te wone suñuy téere. Bu amee ku koy déglu bu baax ci waaraate bi, won ko ni mu mënee def bu fay dellu ndax mu mën a kontine di waxtaan ak moom.

8 Nañu yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi : Fi nga nekk nii, ndax mën nga yokk li ngay def ci waaraate bi ; di ko def sax bu jamonoy fàttaliku bi weesoo ? Ndax ayu-bés bu nekk mën nga yokk benn walla ñaari waxtu ci li nga tàmm def ci waaraate bi ? Ndax yaa ngi seet ci weer yi di ñów, ban weer nga mën a nekkaat pioñee ? Walla ndax mën nga fexe ba mën a jébbal sa jot yépp ci liggéeyu waare bi ? Lépp li ñuy def ci waaraate bi, mën na dimbali nit ba mu nangu dëgg gi (Jëf. 8:​26-39) ! Ñun ñii di xalaat suñu ëllëg, nañu sax ci defal suñu moroom lu baax ci suñu biir te di ko defal ñépp. — 1 Tes. 5:⁠15.

[Wërale bi nekk paas 3]

Wéyal di dimbali :

□✔ Ñi fekke ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu

□✔ Ñi tàmbaliwaat waaraate

□✔ Ñi tàmbali waaraate, fekk sóobaguñu leen

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager