Nañu wéy di jariñoo La Tour de Garde ak Réveillez-vous !
Léegi, kenn dootul jotati La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yu ñu yónnee ci adareesu nit ki (abonnement). Looloo tax ñu war a góor-góorlu ngir benn bañ ñoo raw, ñun ak ñi nuy waar.
Yéenekaay yi ñu dencal suñu bopp : Bu ñu la yónneetul La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! ci sa adarees, na nga yokk yi ngay laaj ci mbooloo mi. Way-jur yi war nañu laaj yéenekaay yu doy, ndax képp ku bokk ci seen njaboot am bosam. Bindal sa tur ci sa yéenekaay, ndax nga bañ ko joxe booy waaraate. Ñiy toppatoo yéenekaay yi ci mbooloo mi, bu ñu leen jotee, war nañu fexe ba ñépp mën cee jot ci saa si, ci Saalu Nguur gi.
Ñi ñuy yóbbul yéenekaay yi, saa yu amee yu bees : Bu amee ku bëgg jot bépp yéenekaay buy genn, waaraatekat yi war nañu ko boole ci ñi ñuy yóbbul yéenekaay yi, saa yu amee yu bees. Loolu dina tax ñu mën a waxtaan ak ñoom, te tàmbali ay njàngum Biibël bi. — Seetleen Le ministère du Royaume bu oktoobar 1998, ci xët 8.
Ñi yombul a gis : Bu amee ku suñu waxtaan neex, te mu dëkk ci gox bu benn mbooloo moomul, kooku, mën nañu ko may mu jot yéenekaay yi ci adareesam. Bu dëkkee ci gox bu suñu mbooloo moom, te dëgg-dëgg, bëgg na jot suñuy yéenekaay, waaye mënuñu fexe ba gis ko, na nga ci waxtaan ak kurélu liggéeyu waare bi. Bu ñu nangoo mu bokk ci ñi jot yéenekaay yi ci seen adarees, na ngeen jëfandikoo kayit bu ñu defar ngir loolu (M-1 ak M-101).
Nañu def lépp ngir waar nit ñi ci Nguuru Yàlla, ak La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! Nañu wóor ne Yexowa dina barkeel liggéey boobu yépp.